Melosuufug Afrig
Kembaarug Afrig / Goxub Afrig moom benn la ci goxi Àdduna Ju Yàgg ja, moom nag ab joor bu réy ci jéeri la, géej xottiwu ko (jaarul ci biiram) du caagéenug dóox (golfe). Moom nag mi ngi nekk walla mi ngi féete ci xaajub kol-kol bu penku bi.
Gox bi nag mi ngi tallaliku ci diggante ñaari rëddi gaar yii : 37º ci tus-wu-taxaw wu bëj-gànnaar ak 35º ci tus-wu-gaar wu bëj-saalum. Bu ko defee rëddu yamoo wi jaar ci diggam, daal di koy séddale ñaari xaaj: benn xaaj bi di bu bëj-gànnaar, nekk nag ci xaaju kol-kol bu bëj-gànnaar bi, beneen bi di bu bëj-saalum, féete ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum bi. Ci noonu gëwéelub sànkar moom ñëw romb ca genn wàllam gu bëj-gànnaar ga, gëwéelub tef ñëw jaar ca geneen wàll gu bëj-saalum ga. Bu ko defee rëddu Grinits (rëddu tus-wu-taxaw wi ) romb ca catam lu sowwu la.
Moom nag dafa tiim ak tefesam yi ci wàllug bëj-gànnaar géej gi ñuy wax Géej gu Diggu gi, mooy li ko tàqaleek goxub Tugal, waaye fu jege Tugal lay doon, bu dee fa tollook Doju Taariq (Jibraartaar). Bu dee ci penku bi day tiim Géej gu xonq gi ak mbàmbulaanug End gi, ñoom ñaar ñoo koy tàqaleek goxub Asi ak Oseyaani, waaye luy jege Asi la ca Baabul Mandab ak barsaqu Suwes, ci sowwu bi nag mi ngi sapp (tiim) ci mbàmbulaanu Atlas gi ko tàggaleek ñaari goxi Aamerig yii di: Aamerig gu bëj-gànnaar gi ak gu bëj-saalum gi.
Afrig nag nekk gi mu nekk ci diggante goxi Àdduna ju yàgg ja, tax na bu baax ba xayug Isipt gu yàgg gu kawe ga, man a tas ba àgg ci xeet yu bari ci ñaari gox yii, Asi ak Tugal.
Goxu Afrig mooy ñaareelu gox bi gën a yaatu ci goxi àdduna bi, ndax tolluwaayam àgg na ci 30 milyoŋi kilomet yu kaare, maanaam lu tollook 1/4 tolluwaayu goxi àdduna ju yàgg ja, walla lu tollook réew mu tollu ne Isipt nga ful ko fanweeri yoon.
Ngir woomle gu réy gi gox bi def ci wàllug mbay, dundat ak mbell, sancaani sowwu yi (waa Tugal yi) tegoon nañu ko loxo, waaye ay askanam jug def ay fipp yu toftaloo ngir gore ci canc gi (colonialisme), ci noonu ñu ëpp ci ñoom mujj temb, sancu yi ci mujj a temb nag ñooy yu Portugaal yi, ñoom de xeex nañu xeex yu tar ngir jot séenug tembte.
Melosuuf ci jëmm
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nin ko junjee ci kaw, Afrik doon na gox bu rey. Ci tëddaayam, so jële penkoom jëm sowwu mat na 7500 (juroom ñaar fukk ak juroomi temeer) km, bëj-gànnaaram ba bëj-saalum tollu na ci 8000km (juroom ñetti fukki junni) ci guddaay.
Diwaan yu mag yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Diwaan yu mag yi bari nañ loo:
Diwaani Afrig | |||
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan |
Melosuufug nite
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nit ñi ci gox bi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Reew yi nga xam ne seenug yorte(administration) dafa néewal, lim yi ñuy joxe doonu ñu yu matale (limbare (statistique) yi defu ñu leen ci anam gi war). Ci 1975 : 302 miliyoŋ i way-dëkk Ci 2001 : 591,3 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : PNUD) Ci 2005 : 803,690 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : World Bank ndeyi-koor 2006) Gisjiital ngir 2015: 866 miliyoŋ i way-dëkk.
11% gu way-dëkk gi ci adduna bi, mi ngi ci Afrik gu bëj-saalumu-Sahara. yokkuteg nit ci Afrik doon na bi gën a gaaw ci adduna bi (21% ci ay way-dëkk yu ciy yokku at mu nekk).
Doon na aw askan gu bariy ndaw, ñi ci ëpp 17 at la ñu am (te ci adduna bi yëpp 23 at la). 45% yu waa-afrik 15 at (fukki at ak juroom) la ñu am. te ñi ëppal 65 at, 3% lañ ci askanam (lang ak 13% ci li des ci adduna bi).
Judd gi : 43 ci junni boo jël (26 ci junni ci adduna bi), 6 doom jiggeen ju ne ci lu ëpp(2,8 ci adduna bi).
Yaakaarte dund gi(li nga yaakaar a dund): 48.8 at
Ndeete gi: 47,5 ci junni
Ndeeteg (mortalité) xale yi 100 ci 1000 (junni bu ne teemeer a ciy dee).
Xeet yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]gëstukat yi ci li ñeel xeet, gis nañ ay mbooloo xeet yu bari ci Afrik:
- Pigme yi: neenañ bokk nañ ci mbooloo yi gënn a yagg. Ci seen taariix, ñoom ci all bi rek la ñuy dund. Seen jafe-jafey dund day yokk rek ndax all bi ñuy dagg ay garabam.
- Waa-ecopi, Waa-somali ak Tubu yi: ñoom naar yi lañu gënn a jege, rawatina ci wallu làkk.
- Waa-afrik yu ñuul ñi: Waa-sudaan(senegaal...), Waa-ginne yi, Bantu yi(Kongòo, Afrik gu diggu), Masay yi, Tutsi yi.
- Tubaab yi: ñi nga xam ne Tugal la ñu cosaanoo.
- Waa-madagaskaar
Kuuteeg làkk yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ñoo ngi koy xayma ci 200 ak 2000 làkk walla waxin (làkk dañ koy bind te waxin ci lammiñ lay yem) ci Afrik. Dañ leen seddale ci ay mbooloo, maanaam làkk yi am ag mbokk.
- Mbooloo làkku bantu: yii ci la ñu bokk, lingala, duala, kikongo, kilari. Ñi ëpp ci ñi koy wax diggu afrik la ñu dëkk.
- Kiswahili (ci mbooloo bantu la bokk): 15 miliyoŋi nit, ci penku Afrig
- Ausa: ci yii reew, Niser, Niseriya, Cadd
- Mandeŋ: 6 miliyon i nit(Mali, Burkina-faso, Senegaal,...)
- Wolof: 11 miliyon i nit (Senegaal, Mali, Gambi, Moritani,...)
Lu ëpp ci làkk i Afrik yi, du ñu ay làkku nguuru reew ya ñu leen di làkkee, maanaam duñ leen jngale ci daara yi, ngur gi du leen jëfëndikoo.
Ñetti làkk rekk ñooy làkk i seen nguuru reew, di seen làkku cosaan: Lesoto, Ruandaa, Burundi.
Kuuteeg diine yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Lislaam: 260 miliyoŋ i taalibe. Ci sowu ak ci penku Afrik la ëppee doole, lu wuuse bëj-gàannar gi.
- Diiney Kirist: 220 miliyoŋi taalibe
- Diiney cosaan: ñoo gi koy xayma ci 100 miliyon i taalibe, waye war na kaa ëpp.
Ñugg-ñugg yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Goxub Afrig ñi koy xàmmee ci suufam su bari si ay laamaar, ba tax na sax ñu koy niroole ak tappaan bu ñu dëpp, boo xoolee di nga gis ne penku gox bi ak bëj-saalumam ñoo gën a yekkatiku bëj-gànnaaram ak sowwoom, te it dinga man a gis laamaar yii:
Laamaaru Tàkk gu mag gi : day tàllaliku ngir daj mbooleem bëj-gànnaaru gox bi, dale ko ca géej gu xonq ga ci penku bi, ba ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, dees na fa gis it ag kaw-suuf gu bariy melo: ay laamaar, ay tundi xeer, yu beeñ (dune) ak xur yuy faral a am ay waaha (oasis).
Doji Atlas yi: ñoom ñi ngi nekk ci gën jaa soriy bëj-gànnaaru sowwu gu Afrig, ci réewi Maxrib Bu Araab bi, bu ko defee ñu tàlleeku nag yor melokaanu ay càllalay doj, dale ko ca bëj-saalum gu sowwu gi ba ci bëj-gànnaar gu penku gi, ñu ëmb nag ci seen biir ay laamaar yu kawe yu ay ngéej yu saf xorom di diggale , ñu xame leen ci turu Shutuut .
Xuru mbalkam Kongoo mi: mi ngi ci xolub gox bi, fa la dexug Kongoo giy dawe aki caram yu limu yi, di sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug atlas gi.
Doji géej gu xonq gi: càllalag doj la gu kawe, tàlleeku bawoo bëj-gànnaar, ba bëj-saalum, feggook nag tefes gu sowwu gu géej gu xonq gi ci Isipt ak Sudaan.
Laamaaru Ecoopi: mooy bi gën a kawe ci laamaari Afrig yi, fa la ñatti car (affluents) yu am solo yu dexug Niil gi di balle ñooy: Sobaat, ak Niil gu bulo gi ak Atbara, bu ko defee yobbaale ndoxi mbënd yu bari yi ci jamonoy taw bi, ngir denc leen ci ngéejus Naasir ba waa Isipt di ci man a jariñu, mu leen di indil ag naataange.
Laamaaru ngéeji yamoo yi: moo ci gën a néew ag yekkatiku, fa la cari Niil gu yamoo gi di balle, ñoom ñi nga xam ne seeni ndox ña nga leen di jële ca ngéejus Wiktooria, mooy ngées su neexum ndox si gën a réy ci yu àdduna bi, mooy jox Niil ndox li ëpp ci weeri at mi
Laamaaru bëj-saalumu Afrig: moo gën a yaatu te gën a yëkkatikoodi, am na nag yenn dex yu ko dog, am ci yu ciy sotti ci penku bi, ci mbàmbulaanug End, (niki Simbisi ak Lombobo), am yu ciy sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug Atlas niki Orang
Kilimaa
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Rëddu yamoo wi moo séddale Afrig def ko ñaari xaaj : bu bëj-gànnaar ak bu bëj-saalum, looloo waral ag tolloo am ci goxi kilimaa yi ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi ak ci bëj-saalumam. Li ëpp ci goxu Afrig it mi ngi nekk ci diggante gëwéelub sànkar bi ci wàllug bëj-gànnaar ak bu tef bi ci wàllug bëj-saalum gi, looloo waral kilimã bu gëwéel bu tang bi daj Afrig gépp lu ci dul catam yu bëj-gànnaar gu sowwu gi ak yu bëj-saalum gu sowwu gi, foofa kilimã bu géej gu diggu ga’a fa nekk. Jamonoy taw yi tam wuute nañu, bariwaayu taw bi it wuute ci barab ak moroom ja.
Tawi Yamoo yu bari yi danañuy faral a sottiku ci tefesug Gana gi, ak [Mbalkam Kongóo|mbalkam Kongóo]] mi diirub at mépp.
Taw yu kojug dig, yu noor yu sakkan yi, ñi ngi faral di rot ci bëj-saalumu Sudaan ak Laamaaru Ecoopi.
Taw yu diggdoomu yi ñi ngi wàcc ci digg Gox bi, ca bëj-gànnaar ak bëj-saalumu diwaanu yamoo bi.
Taw yu néew yi ñi ngi rot ci bëj-saalumu tàkk gu mag gi ak bëj-gànnaaru tàkkug Kalahaari gi.
Tàkk gu mag gi nekk ci bëj-gànnaaru Gox bi nag moom daanaka du taw ak tàkkug Kalahaari gi nekk ci bëj-saalumu sowwu Gox bi.
Tawi sedd bi danay rot ci bëj-gànnaaru Gox bi, ak bëj-saalumam gu sowwu gi ngir gelawi Kalahaari yay upp ca bëj-saalumu sowwu Gox bi.
Melow kilimao bi ci noor bi ( noorub bëj-gànnaar bi) sulye – nii la tënkoo:
Tàngoor
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Jant bi day jamu ci gëwéelub sànkar bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaaju Gox bu bëj-gànnaar bi, nekk nag di lu yam te taradi ca xaaju Gox bu bëj-saalum bi.
Naj gu jawwu gi (pression atmosphérique) , ngelaw li, Taw yi:
Jant bi day jamu ci gëwéelub sànkar bi, ci bëj-gànnaaru Gox bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku, naj gu jawwu gi daal di woyof, te fekk naj gu jawwu gi mi ngi gën a am doole ci mbàmbulaanug atlas gi, loolu di waral ngelawi kojug dig (saisonnier) yu bëj-saalumu sowwu yiy tawloo di jañu juge ci mbàmbulaanug atlas gi jëm ci barab bi naj gu jawwu gi di gën a woyofe, bu ko defee taw yi daal di rot ci Tefesug Gana gi, ak Laamaaru Ecoopi ak bëj-saalumu Sudaan.
Ci at mépp day taw ci Digg Afrig, ca la wër Rëddu Yamoo wa, taw yooyu nag ñi ngi leen xame ci turu (Tawi yéegal yi).
Melow kilima bi ci sedd bi (seddub bëj-gànnaar bi) samwiye – nii la tënkoo:
Jant bi day sampu ci Gëwéelub tef, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaajub Gox bu bëj-saalum bi, daal di wàcc maanaam neew doole (moom tàngoor wi) ci xaaj bu bëj-gànnaar bi, loolu mooy tax naj gu jawwu gi di néew doole ci bëj-saalumu Gox bi, tey am doole ci diiwaanu Tàkk gu mag gi, ci noonu la uppug ngelaw yu yaxantu yu bëj-gànnaaru penku yu fendi yi di àgge ba ci digg Gox bi daanaka.
Ngelawi sowwu yu safaanu yiy tawloo (ndax ci Mbàmbulaanu Atlas lañuy juge) dañuy upp, di rotal ay taw ci tefesi bëj-gànnaaru penku yu Gox bi, ngelaw yii nag dañuy àgg ci tàkk gu mag gi, di lu fendi. Te tam Tàkk gi jamono ju nekk ngelawi yaxantu yu tàng yi danu koy upp.
Ngelawi yaxantu yu bëj-saalumu penku yiy tawlo dañuy upp ci tefesi bëj-saalumu penku yu Afrig yi, bu ko defee taw yi rot, ñuy sutuxlu ci biir ci kaw Laamaaru Bëj-saalumu Afrig, bu ko defee ñu àgg ciw tàngoor ba ca Tàkkug Kalahaari, ci bëj-saalumu sowwu Afrig.
Diiwaani kilima yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Diiwaanu Yamoo bi: moo nekk ci diiwaan yu suufe yi, ci ñaari wàlli rëddu Yamoo wi, diggante rëddu gaaru 5º ci bëj-gànnaar ak rëddu gaaru 5º ci bëj-saalum, mooy mbalkam Kongoo mi, Tefesug Gana gi, ak yenn diiwaan yi ci joor (plaine) gu tefes gu penku Gox bi, tàngoor wa lu kawe la, taw ya lu bari la ci at mi mépp, waaye dañuy gën a tar ci li gën a jege rëddu yamoo wi, ngir sampu ak jamu gi fi jant biy def ci ñaari xaaji-jamono yii
- Diwaanu gëwéel bi: mooy bëj-gànnaar ak bëj-saalumu diiwaanu Yamoo bi, ci diggante rëddu gaaru 5º - 18º ci bëj-gànnaar ak bëj-saalum, day tàng tey taw ci noor bi, tey nugg te fendi ci sedd bi, taw yi nag day gën di néew lu ñu gën a sori rëddu Yamoo wi.
- Diiwaanu kojug dig bi: mi ngi nekk ci Laamaaru Ecopi , taw ya fay am yu noor lañu te yu bari lañu, ngir upp gi fa ngelawi kojug dig yu bëj-saalumu sowwu yiy tawloo di upp ci noor bi, ñooy ngelaw yooyu di bawoo ci mbàmbulaanug atlas ak mbàmbulaanug end.
- Diiwaanu tàkk bi: mooy tàkk gu mag gi nekk ci bëj-gànnaaru gox bi, ak tàkkug Klahaari gi ci bëj-saalumu sowwu gox bi, barab la bu goxe (continental), bu néewi taw, ngir upp ga fa ngelawi yaxantu yu fendi yiy upp.
- Diiwaanu géej gu diggu gi: mi ngi nekk ci joori bëj-gànnaar yu gox bi, tiim nag géej gu diggu gi, nekk it ci cat lu bëj-saalumu penku bi, fu tàng te fendi lay doon ci noor bi ngir upp ga fa ngelawi yaxantu yu fendi ya di upp, di fu nugg tey taw ci sedd bi ngir li fa ngelawi safaanu yu sowwu yiy tawloo di upp.
- Diiwaan biy boroom tàngoor wu yam wi: mi ngi ci tefesi bëj-saalumu penku gox bi, fuy taw lu bari la ci noor bi, di taw lu néew ci sedd bi, ngelawi yaxantu yu bëj-saalumu penku yi dañu fay upp ci at mi mépp.
Diiwaani gàncax yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Gott yu Yamoo yi: ñi ngi ci fu ëpp ci mbalkam Kongoo mi, ci tefesug Gana gi, ak cig wàll ci tefes gu penku gu gox bi. Tàngoor wa lu fa tar la, taw ya lu fay bari la ci at mi mépp, looloo tax ay gott yu fatt, yu am ay garab yu réy, yu kawe te yaatuy xob te jegee di fa am, seeni bànqaas di rabbaloo, bu ko defee ay gàncax di leen wër fu nekk, di ñàpp nag ngir àgg ci leerug jant bi nga xam ne du àgg ci suufus gott sii fees dell aki taa-taa aki déeg aki tepp-tepp, fii nag ab judduwaay la ñeel ay gétti yo (barab bu bariy yo la)
- Gott yu kojug dig yi: gott yu kojug dig yi danuy nirook gott yu Yamoo yi, waaye ñoo gën a gàtt, ñi ngi nekk nag ci Laamaaru Ecopi ak bëj-gànnaaru tefesug Gana gi, ci Dunu Madagaskaar, ak ci Tefesug Afrig gi mu janool.
- Ñaxi Sawaana yi: ñi ngi ci diiwaan yu suufe yu gëwéel yi, ci bëj-gànnaar ak bëj-saalumu gott yu Yamoo yi, ak ci Laamaaru ngéej (lac) yu Yamoo yi ngir kawe ga mu kawe, bu ko defee ñax yu gudd yi di fa màgg (guddaayu ñaar ba ñatti meetar), ay garab di leen rax. Taw ba fay am bu noor la, te bu néewee - moom taw bi – te ab digam gàtt, garab yi dañuy jekki-jekki fàddu, bu ko defee ñax yi nuy wax Sawaana yu ñu wuññi yi des fi. Lu ñu gën a sori Sawaana yu ñu wuññi yi, tey gën a jege Tàkk gi, taw yi di gën a néew, ñaxi Sawaana yu ndόol, yu gooy yi di gën a feeñ.
- Gàncax yu Tàkk gu tàng gi: ñi ngi ci Tàkk gu mag gi ak ci tàkkug Somaali gi ak gu Kalahaari gi, taw ya foofa lu néew la, looloo tax gàncax yu gàtt a fay màgge, yu ami dég, yu ndawi xob, walla yi li ñuy wax (cire) daakaame walla njooy-njooy di muur, walla ñuy yu yor xob yu dijj, yuy denc ndox niki Sabiir, walla ñuy ay garab yu yor ay peer yu gudd niki garabu tàndarma.
- Gàncaxi Géej gu diggu gi: ñi ngi ci tefesi bëj-gànnaaru sowwu Afrig, ak ca gën jaa soriy bëj-saalumu sowwu Afrig, taw ya fa am yu jamonoy sedd la, garab ya day wert saa su nekk, yenn ya yu guddi peer lañu niki yu reseñ ya, yeneen ya seeni xob day muurook daakaande (cire) niki garabi limoŋ yi ak suraas, bokk na ca garab ya fa am ba tay : Saytoon, Koko, Ron, Kooni
- Gotti Diiwaan bu Siin bi: yii gott ñi ngi màgge ci tefesug bëj-saalumu penku gu gox bi, ya ëpp solo ciy garabam : Sanawbar, baloot ak xay, nit di leen dagg, ngir bay ci barab yi ñu nekkoon.
- Ñaxi barab bu diggdoomu bi: ñi ngi ci digg Laamaaru Ecopi, ci bëj-saalumu Afrig, fi ñuy tudde diiwaanu Fald, taw ya fay am yu noor lañu, ñax yu diggdoomu yi di fa sax, yooyu ñax ak barab yooyu ñuy sax, dees leen di jàppe ay gën ji sàmmuyaay ñeel lu aju ci yar ag jur.
- Gàncaxi doj yi: mi ngi ci Laamaaru Ecopi, ak Lamaaru ngéej yu Yamoo yi, fi jóori doj yu yékkatiku yi nekk, gàncax ya day toftaloo, dëppook ni tàngoor wi ak taw bi di toftaloo, bu ko defee gàncaxi diiwaan yu tàng yi di sax ci ron doj yi, di jàll ba ci gàncaxi diiwaan yu sedd yi, ba ci yuur (galaas) yi ci kaw njobbaxtal yu kawe yi.
Melosuufug Afrig |
Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkinaa Faaso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Bennoo yu Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eriitere • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Gine • Gine-Bisawóo • Gineg yamoo • Keeñaa • Lesoto • Liberiyaa • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeriyaa • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome-ak-Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togo • Tuniisi • Sambi • Simbaawe