Bëj-saalumu Aamerig

Jóge Wikipedia.
Bëj-saalumu Aamerik ci lonkoyoonu àdduna bi

Bëj-saalumu Aamerig ci yenn sedatle yu àdduna bi dees koy jàppe ni ab gox, walla ci yeneen sedatle, ab ron-gox bu yamoo wi jaar, te li ëpp ci suufam ci xaaju kol-kol bu Bëj-saalum la nekk.

Melosuuf[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bëj-saalumu Aamerig mi ngi ne ci diggante Mbàmbulaan gu Dal gi ak Mbàmbulaanu Atlas gi. Doon na gox bu bariy dun, yi ci ëpp nag ci réew yi ci gox bi lañu bokk. Li ko lëkkaleek Bëj-gànnaaru Aamerik mooy Panamaa. ag càllale gu ay doj moo leru penku gox bi bépp, ci kaw ba ci suuf; li ëpp ci penkoom àllub yamoo la. Amasoni mooy àll bi ëpp ci àdduna bi, ca réewum Bereesil la nekk.

Taariix[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay askan yu jòge woon goxub Asi ñoo ko dëkkee woon, daanaka am na ay junniy at nj.j.(njëkk judd gu Isaa). Amerigo Vespuci mooy tugal-tugal bi fa njëkk a teg tànkam, waaye li gën a siiw mooy ne Kristof Kolomb mooy ki ko wuññi

Cancug waa tugal gu gox bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

La ko dale ca xarnub XVI la way dëkk yu Bëj-saalumu Aamerig tàmbalee am ay jàmmaarloo ak waa Tugal yi. Waa Ispaañ ñooy ñi fa njëkk, waa portugaal tegu ci, ci noonu ndànk-ndànk boroom doole yu waa tugal yépp tase fa di xëccoo suuf sa ak way dëkk ya fa cosaanoo, ak tam it ci seen diggante, ay jàmmaarloo yu metti juddoo na ca.

Limu réew yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Juroom ñaari réew yu temb yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñetti réew yu tembul yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]