Afritugalasi

Jóge Wikipedia.
Lonkoyoonu àdduna bi, Afritugalasi lañu fésal

Afritugalasi, ci séwógaraafi ngandam gox la, mooy bi gën a ngande ci àdduna bi. Suuf Yépp yi làng doon ko, am na fenn fu ñu tàqaloowe. Moom la ñuy faral di woowee Àdduna ju yàgg ji.

Ci lu daj[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daanaka suuf si ëpp ci àdduna bi moom la, di 55% ci lépp. Am 5,5 miliari way dëkk, maanaam di daanaka 83% gu way dëkk yu àdduna bi.

Mooy barab bi gën a yaatu ci àdduna bi soo ko mengalee ak Aamerig ak, Oseyaani, ak Dottu Bëj-gànnaar.

Seddalinam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ni mu amee ci bépp seddale, ay deggoo rek la ñu. Lu bari dañ koy xaaj ñetti gox: Afrig, Aamerig, Asi

Goxi / Kembaari àdduna si
Afritugalasi Oseyaani Afrig Tugalasi
Bëj-gànnaaru Aamerig Tugal Asi Bëj-saalumu Aamerig