Bëj-saalumu Afrig
Apparence
![]() |

Bëj-saalumu Afrik moo ëmb barab yi nekk ci Bëj-saalumu allub yemoo gu Afrik.
Dañ ciy boole tamit duni Afrik yi nekk ci Bëj-saalum-sowu mbàmbulaanu waa-End ci wetu Madagaskaar ak duni Afrik yi ci Bëj-saalum-penku mbàmbulaanu Atlas.
Askani Xoysan ñoo fa njëkk a dëkk, ci li ci tegu la bantu yi ñéw. Ci jamono gi waa tugal aakimoo diwaan bi, lañ seddale réewi tayam yi.
Doon na diwaan bu am-alal te suufam naggu lool mbay. Rèew mi gën a jëm-kanam ci Afrik, fa la ne rawatina muy Réewu Afrik gu Bëj-saalum
Séwógaraafi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Juroomi Réew ñoo nekk ca diwaan boobu:
Botswana
Lesoto
Namibi
Afrik gu Bëj-saalum
Eswatini
Malawi
Madagaskaar
Mosambik
Saambi
Móoris
Komoor
Simbaawee
Diwaani Afrig | |||
![]() |
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan |