Diggu Afrig

Jóge Wikipedia.

Diggu Afrig (di wax tamit Afrigu yamoo) doon ab xaaju Goxub Afrig bu nekk ci diggante ndand féy-féy gu Sahara ci bëj-gànnaar ak ndand fey-fey gu Kalahari ci bëj-saalum; ci penku mi ngi yem ci peggi dexu Rift ca Ecoopi, ci sowu ci mbàmbulaanu Atlas.

Su nu sukkandikoo ci sedatley àdduna bi Mbootaayu Réew(MR) yi def, Diggu Afrik benn la ci diwaan yi ñu sedatlee Afrig.

Diwaan gu Diggu Afrig

Juroom ñenti Réew yi ci nekk:

Melokaan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci biiram di nga fa fekk barabu Afrig yi nga xam ne mandiŋ nga fa am, fekk fa réew yi am klimab ndand féy-féy, ay réew yu am ci allub yemoo bi, yu tàq ci dexu Niseer ak wu Kongòo.

Doju Kamerun (4070m), doju Ruwenzori (5119m), doju Elgon (4321m), doju Keeñaa (5200m), doju Kilimangiaro (5895m, di doj bi gën a kawe ci Afrig) ñooy doj yi nekk ci Diggu Afrig.

Doon na diwaan bu bariy nit.


Diwaani Afrig
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig
Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan