Wuññi yu melosuuf yi

Jóge Wikipedia.

Wuññi yu juxraaf yi walla yu melosuuf yi.

Luy wuññi yu melosuuf yi ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf, walla feeñal gu melosuuf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg, njëkk waa-Tugal di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc, ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu melosuuf.

Yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, danañu ko man’a xamalee ci nii:

Mooy mbooloom liggéey yi jéngukat (aventurier) yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii : bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu.

Li sabab wuññi yii[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sabab bu diine[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu melosuuf yu Tugal yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari réewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon liggéeyub wuññi boobu.

Ñoom yile ñaari réew dañoo jortoon ne danañu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Réewum Portigaal moom daa gisoon ne réewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum Xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono. Paab gi moom da daa soññ réewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonal ko,tee koo tas, ngir néewal dooleem, xottite ko,giir ko.

Ci noonu mu ( moom Paab gi) génne ay santaane yuy jox àq ñaari réew yii ci ñu moom diiwaan yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam géej yi la mbaa jéeri yi. Paab gi ak nasaraan yi ci ginnaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nañu leen fi jeem’a jële.

Sababu politig[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Am na yeneen réew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Faraas, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiital ci biti seen, rawati na ci réew yi ci yeex ci séenu'g nekku walla sosu gu yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen . Réew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu melosuuf gi.

Sabab bu koom-koom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waa Tugal yi ñoom dañoo gisoon ne àddunay jullit ñi daal, mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir néewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi, loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke.

Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova añs. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi.

Lori waa Tugal yi tàmbli woon na’a yol, ñu tàmbalee ñammasle ak a manadee tëyye seen bopp, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi rekk (maanaam lu aju lu ñu man a jariñoo ci ay suuf, wurus mbaa lu ni mel), bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu melosuuf gi bi ñu déggee tono gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Tugal yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd, ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi .

Sababu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak ab bindam dafa soppiku woon, ginnaaw bi ay tukki yu melosuuf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal, juge Tugal, génn, rawati na ginnaaw bi jamonoy xarey jooñe yi jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Tugal yépp ci jamono yu diggu yi.

Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu, ak bëgg xam-xamu melosuuf, feeñ ci ñoom, ginnaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xarey jooñe yi ak ginnaaw bi - ci xam-xam bu melosuuf bu jëm kanam, ak ginnaaw bu xam-xamu Saytubiddiw ak liggéeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jëm kanam.

Wuññiy melosuuf yu Portigaal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Portigaal moom la ñuy jàppe réew mi jiite woon wuññi yu melosuuf, yu Tugal yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool (1394 – 1460 g), doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon moolu(dugg géej), ak yër xisay mool yi, ak téerey taariix yi. Muy ku aayoon ci rëdd lonkooyooni melosuuf yi, moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta, ginnaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g.

Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi géej gu xonq ga ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum 1445 g, ginnaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niser. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko «Boppub Yaakaar Ju Baaxi Ji» ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End. Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi, romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji, ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End.

Vasco De Gama mii jot naa xamante ak Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon géeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu géej yi.

Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu géej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi ñuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song barab ya ak mbooloom gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo ak buuri diiwaani End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End bi.

Li wuññiy melosuuf yu Portigaal yi jur[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw :

1) Waa Portigaal, ñi ngi tàmbli woon di teg loxo ci tefesi Afrig yu sowwu yi, ci noonu njàppum jaam siiw, te tas ci Tugal gépp, di jaam yi ñu daa jàppe Afrig, te daan ci yaxantu.

2) Jamonoy sanc gu Portigaal, mi ngi tàmblee ci bi Portigaal taxawalee ab sancu, ci penku bi, ca fa ñuy wax Jawa, ay xare it am diggante araab yu jullit yi ak Portigaal cig wàll, ak ci diggante waa Portigaal ak waaEnd yi ci geneen wàll. Waa Portigaal yi nag jot nañoo teg loxo yenn waax yu am solo yi nekkoon ci yoon wi jëme End.

3) Waa Portigaal yi mujj nañu xam yoonu yaxantu wu géej, wu dul romb ci réewi jullit ñi,mooy wi jaar ca Boppu Yaakaar Ju Baax ja.

Loolu nag mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon néew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal-jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jéem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab bu nasaraan safaan (kontar) doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu géej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi.

Wuññi yu melosuuf yu Espaañ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ci dugaloon Portigaal, moo dugal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi. [[ Mool]]ub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahamas ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi.

Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ».

Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siiwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na àdduna ju yees ju dul End.

Ginnaawam it wuññikat yi doon liggéeyal Espaañ wëy ci seen liggéeyi wuññi yooyu, ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca diiwaan ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraangay ñu tudde ko Adduna ju bees jii di Aamerig tay.

Li wuññiy Espaañ yi jur[Soppisoppi gongikuwaay bi]

1) Ñoom de ubbil nañu tukkiy wuññi yi aw yoon wu bees wu jëm ci àdduna ju yees ji, di ko jaare ci màmbulaan gu atlas gi. Bu ko defee Espaañ tàmblee sanc gox yi mu jotoon’a àgg ci Aamerig gu diggu gi ak gu bëj-saalum gi, ñu wisaare fa seenug xay ak diine, ubbi fa ay mbelli wurus ak xaalis.

2) Saxal gu ñu saxal ci xam-xam ne suuf si daa “bulu” , te li waraloon loolu di tukki bi Magellan defoon. Buur bi ñu daa wax Shark mu juroomeel mi (Sharlakaan) di woon buurub Espaañ, daa digaloon mool bii di Magellan atum 1519 g, mu def ab tukki jëm penku jaare ko sowwu, ci noonu moom Magellan jug, moolu (war geej), jawali sowwu, te jëm penku, ci kaw màmbulaan gu atlas gi, bi mu ko defee daal di àgg ca tefesug Breesil ga, fa Riyo De Janero, mu wëy nag ca doxam ba, ba ca sottiwaayu dexug Labalata, daal di wër Aamerig gu bëj-saalum gi, tàbbi màmbulaan gu dal gi nga xam ne moom moo ko tudde « pasifik » di wund lu dal, mu àgg Filipin atum 1521 g, foofa nag mu songoo fa’ak ñoñ réew ma, ci’y xeex yoy ca la ñu ko raye, waaye kenn ciy nitam, tuddoon Dianco, moo mujjoon jiite boobu tukki, dem ak ñoom ba ci Boppu Yaakaar Ju Baax ji, juge fa dem Espaañ, gi nga xam ne ma nga fa àgg atum 1522 g.

3) Weddi gisiin yi daa wax ci bindu suuf si ak ab kemam ( ni mu tollu), ndax kat tukki bii nga xam ne dafa dox, wër àdduna bi, firndéel na ne suuf si daal moo ëpp fuuf li ko Colombo jàppe woon ak ku dul moom. Beneen gox feeñ na, bu mag diggante Tugal ak Asi ci wàllug sowwu gi, di Aamerig gu bëj-gànnaar gi, nga rax ci dooli geneen gi’y gu bëj-saalum gi, te ag màmbulaan gu yaatu, gu yees’a ngii gu ñu xamutoon. Kon suuf desatutoon su ñu xamutoon su dul Ostrali ak ñaari dott yi .

Wuññi yu Angalteer[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu géeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginnaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug waa Angalteer yi, ñeel Aamerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa. Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland.

Wuññiy araans yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jëmi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy Faransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fétali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Aamerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Faraas tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak barabi dex yi ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebeg ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. Moolu Faraas bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Faraas ya daal di fay sos sancu bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Faraas ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi.

Wuññi yu Oland yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lonkoo (société) gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu géeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali dóoxug New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu Boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu géej wu am njariñ. Waa Oland yi jéemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g .

Li wuññiy melosuuf yu Tugal yi jur[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li wuññiy Tugal yi jur man nañu koo tënk ci lii di ñëw :

1) Njiitug yaxantu gi tuxu na tukkee ci li wër géej gu diggu gi dem ci màmbulaan gu atlas, mu mujj moom yaxantu gi nekk ci loxoy réewi Tugal gu sowwu gi, bu ko defee ñu nos fi ay yooni géej yu yaxantu ci ñaari màmbulaan yi, gu atlas ak gu dal gi (pasifik). Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » .

2) Wuññi yu melosuuf yi amal nañu fi jawwu yu gëpplante ak wujje, ak as lef cig noonoo ci diggante réew yi doon def wuññi yii, loolu moo yokkoon xemméemtéefi sanc yi ci diggante réewi Tugal yi. Ci noonu aw gisiin wu sanc tàmbli woon’a feeñ wu Tugal jëm ci askani réew yii ñuy door’a wuññi.

3) Xam-xami melosuuf yi soppiku woon nañu bu baax, li ko waraloon di yaatu gi wuññi yii yaatu woon te bari. Ci noonu yëngu-yëngu gu nasaraanal yokku ci anam gu fés, rawati na ci Afrig ak ñaari Aamerig yi.

4) Ag jëm kanam feeñoon na ci wàllug yaxantug mbèll yi, di wurus ak xaalis, nga xam ne sax xarnub fukk ak juroom g, dañu koo tudde woon « xarnub xaalis », ni nga xame ni jëm kanamug koom googu taxoon na ba dundiin wi gën’a kawe, njëg yi it gën’a yekkatiku, ni fi ay njaay yu yees dugge, lu ci mel ne kakaawoo, póon, kiinaa, batata ak mbòq.

5) Wuññi yi de lenn lañu ci màndarga yiy wone yewwuteg Tugal gi, ni nu la ko leerale woon ci doggantal gu njëkk ga.

6) Réew yii ñu wuññi, ruu gu fees ak bëgg’a fayyu moo leen ubale woon, muur leen, jëm ci yii leen wuññi, ndax ñoom tubaab yi xalaati sanc lanu yoroon, daan ci doxe ci mbooleem seen doxi wuññi yi, lepp lu nu gis aakimoo ko, ngartaajoo ko, lii mooy li waral askani réew yi nu wuññi, jugoon ci jànkoonte ak ñoom, taxaw ci xeex canc gu Tugal gi, ci anam gu tar, jëfandikoo ci li nu yor lepp ci kàttan.

7) Wesaare diiney nasaraan ci bepp gox bu ñu wuññi.