Suuf

Jóge Wikipedia.
Suuf si

Suuf si (junj: 🜨), mooy ñetteelu àdduna bi gën a jege jant bi, moom nag man nan koo woowee "Suuf si" walla "Àdduna bi", walla "Àddunaay Suuf" walla "Àdduna ju Baxa".

Suuf si nag bari na ay mindeef yu fi dëkk, nit ci la bokk, ci li nu xam fii rekk la ag dund am. cig xayma, boroom-xam-xam yi nee nañ, Àddunaay Suuf, mi ngi sosu am na 4,57 miliyaari at, te ag dund mi ngi juddu ci kawam ci diirub benn miliyaar ciy at. Moom nag jawwam soppikuna ci anam bu waral wërlaayam doon guy dundeef man a juddoo.

Kaw Suuf gu biti gi nag dafa séddatleku ci ay doj yu dëgër yu bari, di yëngu ci lu bari ci kawam ba leegi mat na miliyoŋi at. Daanaka 70% ci kaw Suuf si ay mbàmbulaani ndoxu xorom a ko muur, li ci des di ay gox aki dun. Ndox mu yollaakon mi ñu jàppee ne mooy yor dund, ci ni ñu ko xamee, Suuf si rekk mooy àdduna bi ñu gisagum bu ko am ci kawam. Ci biir Suuf si nag la fa na ne mooy: magma bi, ab saalub biti bu yollaakon biy jur toolu bijjaakon bi, ak saalub biir bi nga xam ne weñ la.

Suuf si day am ay digaale ag yeneen mbir yi ne ci kaw jawwu ji.

Diir bi Suuf si di def ngi man a def ab wër bu daj ci jant mooy 365,26 bés (bés di 24 waxtu)

Taariixam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Boroom-xam-xam yi àgg nañ ci man a xam yenn xibaar yi ci dembi Suuf si. Suuf si ak yeneen àddunaay nosteg jant bi ñoo ngi juddu am na booba ak léegi 4,57 miliyaar ciy at, doore ciw niirub jant(nébuleuse solaire), di ab donjub pënd ak gil(gaz) gu bàyyeekoo ci juddug jant bi. Ci ndoorteel gi muy ruy, wàllu Suuf si féete woon biti tambalee sedd, dem ba doon ab donj bu dëgër bi ndox tambalee dajaloo ci jawwam. Yàggul dara weer wi dal di ciy tegu, boroom-xam-xam yi, ci lu wóor jàpp nañ ne mi ngi juddoo cib mbëkkante ci diggante Suuf si ak benn mbir bu réyaam matoon 10% gu Suuf si. Benn xaaj bi des ci Suuf si(yokk réyaayam), beneen bi nekk weer wi, dend ak moom.