Waax
Apparence
Waax xeetu garab la gu bokk ci njabootu Poaceae ak ci njabootaatu Bambusoideae, Afrig gu naaje la bàyyikoo.
Meloom wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Man àgg ba 10i met ci guddaay ak 10i sàntimet ci yaatuwaayu dàtt. Xobam danay àgg ci guddaay 1 ba 2i sàntimet. Doom danay àgg ci guddaay 10 ba 15i milimet.
Njariña yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dees na ko jëfandikoo ci defarug alkol, ñoll ak duu. Waax ci xeeti tabaxukaay yi la bokk.