Xay
Apparence
Baatu xay day tekki mbooleem ay mbaax ak ay melokaani aw askan. Maanaam xamug àdduna, ci wàllu yar ak teggin ak xam-xam, yewwute gu nit ñi ci aw askan. Su ñuy wax xay dañ ciy nat tolluwaayu sag dundin, ndax jëm na kanam walla déet; baat bi dafa ëmb mbooleem ay yëngu-yëngu yuy am ci aw askan: diine, cosaan, xamteef, politig,...
Su ñu nee nit kii dafa xayadi, day tekki ne xamul àdduna. Kon xayug aw askan ñoo ngi koy natt ci doxaliin, dundiinu cër bu ne ci askan wi
Limub ay xay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Yenn ciy xay yu doomi aadama:
- Gu Babiloñaa
- Gu Isipt gi Yàgg ga
- Gu End
- Gu Ittite
- Gu Siin
- Gu Geres
- Gu Rom
- Gu waa penku (Siri, Fenesi, Yëwut)
- Xayug Lislaam
- Monomatapa
- Maya
- Sapoŋ
- Xayug Mongoli
Wikibaatukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (en) xay
- (fr) xay