Yewwute

Jóge Wikipedia.

"Yewwute" gu Tugal gi, baat la buy tekki, ci maanaa mu taariix mi mu yore, yëngu-yëngu gu dekkal ak yeesal, walla dundal xay gu Tugal gu yàgg ga, gu Geres ga ak Rom. Rawati na ci wàlli njàggat, fànn ak tabaxin.

Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbali ci xarnu bu fukk ak juroom ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Isaa (XVu xarnu balla Isaa), ba ci bu fukk ak juroom ñaar (XVII), mu sos fi nag ay coppite yu xóot ci wàllug aada, dundin, mboolaay, politig ak koom-koom. Kon daal, "yewwute" gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja (mu'y jamono'y "ag laman" walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji (di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala).

Leonardo da Vinci, xët muy wax ci melokaanu nit

Li ko sabab[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nanu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy :

  • Jeexiital gi xay gu lislaam gi def ci yewwute gii,
  • Feeñug dëkk yu mag yi ci Tugal
  • Neew-doole gu jàngu bu Paab bi neewoon doole, ak tas gi mu faroon tas.

Jeexiital gi Lislaam amal ci yewwute'g Tugal gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore, araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Tugal nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk.

Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñe yi(croisade).

Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñe ya (walla yu galajaane ya), duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam.

Lii nag ci li soppi xalaati waa-tugal yi la jëm ci jàngu bi, nit, adduna bi ak dund gi.

Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbali woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci paj, xeltu, gañcax ak ndundat, ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn(XI) (g).

Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin (wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Tugal ca jamono jooja) loolu dimblee woon, ci ginaaw bi, ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am.

Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

"Nosteg laman" walla gug cang, ku ne xam na ne la mu baaxoo woon mooy tegu ci mbay, suuf, ak seqoo yu laman yi daa lijjanti ak'a nos diggante jaam bi ak sang bi. Ag laman nag jullit ñi masuñu koo xam, nosteg koom-koom la, tey gu mboolaay gu bon, daan gàllankoor xay gi ba du jëm-kanam.

Bu ko defee, li ñuy wax "tool", di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste.

Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug liggéey yi, ngir jòkkoo gi waa-tugal gi daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt aka naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal gi tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku, ci léppam, ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi.

Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu aka lakkal noste gu laman gi, tey liggéey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man a am.

Lòttug jàngu bu Paab bi akug tasam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jàngu bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sottiwoon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax "njàng yi aju ci Yàlla" (théologie), ak njàggat ak xellu. Amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam.

Jàngu bi moom dafa jàppewoon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Jàngu bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, degginu ligeeyub yaxantu gën faa xóot, ak bu endustri ak aada. Yii yepp nag liggéey nañu lu rëy ci, waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it, di doyodil nosteg laman gi, rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am.

Itaali mberum yewwuteg Tugal gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dëkk yu Itaali yi ñooy mber yu njëkk, yi njëkk a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak ñoñ fànn, duggaloon nanu ci seen loxo bu baax.

Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay, yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa-rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fànn, nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine.

Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab bi ci Itaali ag tono gu neen ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi nguuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa liggéeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi téere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi.

Mandargay Yewwuteg Tugal gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy:

Yëngu-yëngu yi aju cig "nite"[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya (yu Geres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi, ak jeem a xam seeni mbóot.

Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàngatkati Geres yeek Rom (grego-romain) ñoom lañu jëloon, yittewoo leen, ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàngat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàngati Geres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam.

Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi, di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot, nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja. Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi.

Ci dëkki Itaali yii, lu bari ciy fànnkat yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko (1400 - 1455), Leonardo da Vinci (1452 - 1519), Titian (1488 - 1572), ak Rafayel (1493 - 1520 g), yattkat ba Donatello (1386 - 1466).

Feeñug làkk yu bees yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi, moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña, di woon niti neen ñi rekk, ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamonoy "yewwute" dikkee, ngelawul "fonk sa xeet" upp ci Tugal gépp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante (1265 - 1321) taalif mbóosóor mu Sell mi ci làkku waa-itaali, naka noonu Petrarch (1304 - 1374) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi.

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais (1483 - 1553) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf).

Chaucer mi dib waa-angalteer (1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme ya cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën a siw.

Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Tugal taxaw. Yu amoon "ag temb", ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci "temb" tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi.

Yëngu-yënguy dajale mbind yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lañu nekk ci Xustantin ak ci dëkki waa-geres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal. mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Geres yeek Latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek jàngu yi ak jàngu yu mag yi, ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii.

Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni liggéey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk, mbindum binkat bii di waa-rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g). Tacitus moomu mooy taariixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi.

(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya:

Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya. Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam, waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix, mu tudd daaray xam-xam bu taarix.

Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla (1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn wayndare (dossier) bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax "mayug Xustantin", mooy wayndare boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen.

Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli (1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas.

(6) Jëm-kanamug yaxantu ak ndefar:

Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi, ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa.

Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey ndefar yi yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci koppar yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug "kuréel gu diggu" gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi.

(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi:

Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi, ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi. Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon (1220 - 1292) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal.

Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf.

Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ (1561 - 1626 g), di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi, ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd. Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci (1452 - 1519 g) moom tam feeñ, di kok dafa yittewoo woon jiyoloji (bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn, tey fentkat. Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo (1564 - 1642 g) feeñ, mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba, dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus (1476 - 1542 g).

Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel, walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam.

Yewwute gi ci Itaali:

Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo:

1 - Song gu mbooloom xarem Fraans mi ak mu nguurug Rom gu nu sellal gi songoon dëkki Itaali yi, rawati na Rom ak dëkki bëj-gànnaar yi, niki Milano, loolu it taxoon na ba ñu giir dëkk yooyu, te Milano ak Rom jiitu woon ci. Ci noonu la yewwute gi delloo ginaaw ci Itaali ngir ñàkk gu fa jàmm ñàkk ak kaaraange ak dall.

2 - Jeex gu àtteg walla kilifteefug njabootug Madatsi jeexoon, ñooy buur yi daa sàmm yewwute gi ci Firenze, loolu nag sabab si mooy xuloo ak xeex gi amoon ci biir njaboot gii, te Firenze moo ëppoon solo ci barab yi yewwute gii nekkoon.

3 - Teg loxo gu buurub Espaañ bi Ferdinando, buurub Argon, defoon Napoli atum 1504 g, loolu bokk ci li neewaloon doole yewwute gi ci dëkku Itaalib bëj-saalum bii.

4 - Yëngu gi amoon ci jéem’a yéwénal diine ji ci Orob, ñi ko daa def di Luther, Kalfen, Swingli ak ñeneen, looloo taxoon paab gi jug ak doole ci kontar nite gi. Nga xam ne sax noonu gi àgg na ci paab bi tuddoon Kalimat mu juroom ñaareel mi, kompoloo woon ak buur bi Sarl 5 (Sarlkaan) buurub Espaañ bu katolig bi, ngir ñu fexee naaxsaayal yëngu-yëngug nite googu ci Itaali. Loolu mooy li waajal mbir yi, nooyal yoon wi ba “ëttu àttey lajmat" yi man’a am ca Esapaañ, di woon ëtti àtte yu siwe ay jëf yu ñaaw, daan sonnal ak a fitnaal képp kuy woote yéwénal, mbaa’g yewwute. Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund.

Tuxug Yewwute gi:

Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs. Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay. Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen. Nitug Holand kii di Erasmus (1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi.

Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax "kòllare gu yees gi" def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon. Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi.

Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali:

Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll.

Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey. Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi, looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal.

Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g.

Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom. Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi. Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi.

Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g) ak ñu dul ñoom ñaar.

Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi. Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer.

Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam.

Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew. Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii.

Seetal BUNTU TAARIIX
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Yewwute