Goxub Dottub Bëj-saalum

Jóge Wikipedia.
Goxub Dott bu Bëj-saalum
Goxub Dott bu Bëj-saalum

Dottub Bëj-saalum mooy gox bi gën a suufe ci Suuf si. Nekk ci dottub Bëj-saalum, Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi moo ko wër. Laal na itam géeju Ross ak bu Weddell.

Réyaayam toll ci 13,9 junni-junni km², Dottub Bëj-saalum moo gën a tuuti Asi, Afrig, Bëj-gànnaaru Aamerig ak Bëj-saalumu Aamerig. Tugal ak Oseyaani rekk la gën a réy. Lu mat 98% ci suufam galaas a ko sàng, ci dëllaay bu mat 1,6 km.

Dottub Bëj-saalum mooy gox bi gën a sedd, bi gën a wow, ëpp ngelaw. Di itam gox bi gën a yëkkatiku ci kawu tollulwaayu géej gi. Ñakkug taw ga fa am, lu dul ci tefes yi, moo tax ci biir gox la tàkk bi ëpp ci Suuf si nekk. Amul nit ñu fay dëkk lu yàgg, amul itam nit ñu fa baaxoo. Ay gañcax ak ay rab rekk a fa man a dëkk.

Melosuuf[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ak réyaay bu toll ci 13,9 junni-junni km² mooy juroomeelu gox bi ëpp ci àdduna bi cig réyaay.

Gox bi dafa séddaliku ci ñaari xaaj:

  • Sowwu Dottub Bëj-saalum
  • Penku Dottub Bëj-saalum

Lëkkalekaay yu biir[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons
Goxi / Kembaari àdduna si
Afritugalasi Oseyaani Afrig Tugalasi
Bëj-gànnaaru Aamerig Tugal Asi Bëj-saalumu Aamerig