Mbàmbulaan gu Bëj-saalum

Jóge Wikipedia.
Mbàmbulaan gu Bëj-saalum

Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi mooy mbalkaam ndox mi ne ci li wër Dottub Bëj-saalum bi. Mooy ñenteelu mbàmbulaan mi gën a réy ci àdduna bi.

Yaatuwaayam gépp mi ngi toll ci 20 327 000 km², guddaayu tefes gi di 17 968 km.

Mi nu wuteeg yeneen mbàmbulaan yi seen dig doon ay gox, moom rek mooy la ñuy tekkee ni ab mbalkaam ndox mu wër ab gox (goxub Dott bu Bëj-saalum); doon ab jaaro bu tëdd ci 60°(60 aj) gu tus-wu-gaar wu Bëj-saalum.

Mbàmbulaan gu Bëj-saalum xóotee na lu tollook 4 000 ba 5 000 m, daanaka ci tëraayam gépp, lu weesu yénn barab yi gën a néew xóotaay.

mbàmbulaani àdduna bi
Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar
Bëj-gànnaar
Mbàmbulaanug Atlas
Atlas
Mbàmbulaan gu Bëj-saalum
Bëj-saalum
Mbàmbulaanug End
End
Mbàmbulaan Gu-Dal
Dal