Bëj-saalumu Tugal
Apparence
Bëj-saalumu Tugal ab diwaan la ci goxu Tugal. Tekkib baat bi nak di na faral di indi ay werante, ba tax na am na ay tekki yu bari. Ci lu ëpp da ñuy wax naa Ispaañ, Itaali, Girees, ñooy réew yi ci bokk, daanaka ci lu daj réew yépp yi nekk ci Géej gu Diggu gi. Bëj-saalumu Faraas ci lu bari da ñu ko ciy boole.
Tekkeem gu séwógaraafi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci séwógaraafi da ñu naa Bëj-saalumu Tugal mooy xaaj bi gën a féete Bëj-saalum ci goxu bi; bii tekki nak da fa ajoo, ba tax na sax amuli pegg yu leer. Càllaleeb doj bu Alpi moom la ñuy téewee ni ab pegg buy seddatle Itaali ak li des ci Tugal, doon liy xaajatle ñaaru Tugal yi
Limu réew yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Portugaal
- Ispaañ
- Andoor
- Faraas
- Itaali
- Korwaasi
- Girees
- Albaani
- Bosni Hersegowin
- Montenegro
- Réewum Maseduwaan
- Seerbi
- Esloweeni
- Ciipër
- Malt
Diwaani Tugalasi | |||
Asi | Diwaan yu MR: Diggu Asi · Penku Asi · Bëj-saalum-penku Asi · Ron-goxu End Yeneen diwaan: Penku gu Sori · Penku gu Diggu · Penku gu Jege · Sibeeri | ||
Tugal | Diwaan yu MR: Sowwu Tugal · Bëj-saalumu Tugal · Penku Tugal · Bëj-gànnaaru Tugal Yeneen diwaan: Kókaas · Géej gu Diggu · Skandinaawi |