Kàllaama

Jóge Wikipedia.

Kàllaama (fr : langue ; en : language)

Làkk mooy cëslaayu ag yewwute[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñi ngi tàmbali sunuy wax ak jëf ci turu Yàlla(t.s) miy Rahmaan, di kiy boroom yërmaande ju yaatu ji ñu jagleel mbooleem mbindéef yi, tey Rahiim, di ki yor yërmaande ji mu'y jagleel ña nangu'g jaamoom. Di julli nag te'y sëlmal ci sunu sang, sangu'b ñu jiitu ñi ak ñu mujj ñi, aki ñoñam aki saabaam, ak aji liggéeyalam jii di sëriñ Tuubaa, ak xeetam wépp. Sunu wax ji dañu ko'y tàmblee cib aaya'b alxuraan, ñu ci'y tegtaloo li làkk ëmb, yor ko ci'y njariñ, ci gépp wàll, ci sunu dund gi. Sunu boroom nee na ci alxuraanam ju tedd ji:(( Wa hallama Aadamal asmaa kullahaa, thiumma haradahum halal malaayikati, fa xaala anbiuunii bi asmaayi haaulaayi in kuntum saadixiin)) di maanaa : Yàlla (t.s) jangal Aadama tur ya yépp, bi mu noppee, jël mbir yooyee won leen malaayika yi, ne leen wax leen ma seeni tur, bu ngéen léen xamee? ñu ne ko tudd nanu sa'g sell, amuñu benn xam-xam boo ñu xamalul,bu ñu xam, yaw yaa'y ku xam ki, te'y ku xereñ , ku am hikma ki. Kon yii tur ci jii aaya ju tedd, mant'a doon lu dul làkk, wi nga xam ne bokk na ci li Yàlla (t.s) njekk'a xamal Aadama (j.m) bi mu ko bëggee wàcce ci kaw dénd bi, ngir mu wuutu ko fi. Loolu nag li ko waral moo'y nekku'g làkk di benn ci móoli cosaan yi ñu teg sunu dund gi, tabax ko ci. Bu doonul woon moom, dund gi di lu nekk ci lu dul maanaa mu ñu xam, di lu gën'a jege ag mbàyyima ci ag nite, bu amul wuutlaay. Ma ne xoolal ma dund gu ñu rafleel ci làkk, nu mu war'a mel ? ndax moo'y googu di fees dell ak junj yi ñu'y jëfandikoo bu ñu'y wax ak ku luu, muuma mbaa ku tëx ? lii sax ca dëgg-dëgg xeet la ci làkk, làkk ëppu ko yéesu ko, ginaaw moom mbir la mu ñu'y def ngir déggante ci. Ndax kat làkk du lu moy ab jumtukaay, ngir waxante, ñu ko'y jëfandikoo ngir déggante ci sunu biir !, xanaa déggoo ñu naan làkku njanaaw yi , mbaa dundat yi, ba ci wu bàyyima yi?jubluwuñu ci lu dul li ñu'y joyal, ngir seen moroom yi dégge léen ci. Ginaaw nag bàyyima yi di nañu déggante ci loolu ci seen biir, kon loolu manatuñu ko'o jàppe lu dul aw lakk ni yeneen yépp. Waaye jeneeral dund gii nga xam ne dafa féex ba ci sax jumtukaay yi ñu'y jëfandikoo ngir junj, maanaam dund gi ñu rafleel ba ci jumtukaayu'b déggante rekk, nu mu war'a mel ? nu xeet ak mbir ya'y dox ci'y sidiitam, aki buumi xolam di mel ? wii xeetu dund de ci li ma jort, narul'a doon lu dul ag ndofe gu ñu joyal, naa doyloo yooyu baat ndegam amuma yeneen yu ko man'a leerale ni mu ware. Gii dund ci lu dul làkk, da na nekki gu maneesul'a leeral, xel it du ko xalam.

Ci loolu la Sayyid Qutub, di waxe ca teereem ba tudd Zilaalul Xuraan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci loolu la Sayyid Qutub, di waxe ca teereem ba tudd Zilaalul Xuraan, di tafsiir bu mag ci alxuraan, mu ca'y firi aaya bu sell bii di (( wahalla aadama ba maakuntum taktumuuna)), mu ne : (( xool ñu nag ñi ngi nii - ci bëtu'b xol, ak leerug basiira - di jàkkaarloo ak la malaaka ya nekkoon ca Malaul Ahlaa doon jàkkaarlool.... xool ñu ñun ni ngi nii di gis ag wàll ca mbootum Yàlla mu màgg moomee,nga xam ne mi ngi ko dénk nekktéef bii di kojug nit, bi mu ko'y jox caabi'y kuutlaay ji, mu war ko'o wuutu ci kaw suuf.

Mbootum kàttanu'g tudde mbir yi ay tur, wutal yëf yi ay xammeekaay yu tur, sekkare'b man'a jël jëmm yi, walla yëf yi tudde leen ay tur yu leen di def - te ñoom ay baat rekk lañu yu ñu wax - ñu'y ay junj aki sembool yu'y tekki jëmm yooyu ak mbir yooyu ñu leen tudde. Lii daal na la woor ne kàttan la gu am lool solo, ak xiima ci dundu'g nit ci kaw sii suuf. Ñi ngi'y xam solo sii, bu ñu'y jeneer coona bu mag bi ñu naroon'a jànkoonteel, bu ñu mayutoon nit kàttanu'g junj yëf yi, ak nit ñi ci'y tur. Xoolal coona bi naroon'a am ci déggante ak jëflante, ndax li naroon'a xew, moo'y ku bëgg'a déggante ak sa moroom ci mbir, da nga'y teewal moomale mbir, mbaa ànd ak moom ba ca loola, nga joxoñ ko ko, mbaa nga laal ko.... bu dee xorondoom ngeen soxla, war ce'e waxtaan, da ngeen ca'y dem, mbaa ngeen teewal ko, lu ko moy deet ag déggante ci loolu, bu dee doj la, fawwu ngeen dem ba ca doj wa, bu dee nit, munt'a ñakk ngeen teewal ko, lu ko moy du ngeen ca déggante.... Lii daal coona la bu kenn xalaatul'a dund ak moom, te dund gi tam narutoon'a wëy ci yoonam wii, bu Yàlla (t.s) mayuloon mbindéefam mii man-manu tudde mbir yi ay tur. Malaaka yi ñoom, jagle bii soxlawunu ko, ndax du lu manul'a ñàkk ci ñoom ci seeni jëf, moo waral mayeesu leen ko)).

Kon làkk moo'y ponk bi nga xam ne ci la sunu'g dund di tabaxu[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kon làkk moo'y ponk bi nga xam ne ci la sunu'g dund di tabaxu, su nu bëggee muy gu jege as lëf ci'g cilwiise aku'g taaxe,walla lenn lu am maanaa. Bi làkk nekkee nag ba noppi, te tax ñu jeggi mbooleem rombuwaay yii, ca ngënéelam la, ak jappndal gi mu nu defal ba nu man'a déggante ci suñu biir, ñewati na di jumtukaay bi dugg ngir teg sunu dund gii ca njobbaxtal lu kawe, la di ag nite, ak ca tolluwaay bu yekkatiku bee di bu ag taaxe, aku'g xay.

Bu doonul woon làkk, duñu doon man'a yekkati sunu dund gii ci xam-xam, ndax moo'y li'y tax nga man'a raññale mbir ak dundat yi, lu ci nekk nga ber ko nee, wutal ko turu boppam.

Làkk moo'y cëslaayu "ag yewwute"

Yewwute ñenn ñi naan ko "renaissance" ci francais di judduwaat, di ci araab "nahda" , di ci maanaa buur , buur nag bu nu ko waxee ci wolof moo'y jekki-jekki jug ,taxaw, ñeneen it di ko fire'e dekki, boo ko'y seet ci maanaa, yepp di wudd lenn, di la amoon ca Orob ca lenn ci'y jamonoom, di woon lu am solo, di lu waa Orob dul fatteeti, baat bii ñew ëmb maanaa mii mépp, di raññale jamono'y yewwute ci ngëmméen, judduwaat ginaaw ag dee, réer ci réeradi,xam ci xamadi, siggi ci segg, nërméelu ci taxaw, giim ci tàkk, xippi ci gëmm.

Bii baat daal jaasi la ju moo dog seen diggante ak jamono joj tëñëxu ak yewwoodiku moo ko muuroon, matale ko, xel mu gàtt lakkal leen ci, gisiin wu ñaaw sonal leen ci, ñu nekkoon ci biiram di way jemadi kanam, di ñu soxlawoo ag leer, ba Yàlla yee ay nit, niital léen ca làmpam bu leer ba'y leerale, jugloo leen ci'y nelaw, ñu nekk ci'g" yewwute" duggalaale ci ñeneen ñu dul woon ñoon, ba tay Orob gii, di lu leer, ca googale leer la tanqe, te ca la yewwoo it.


Kon ci gàttal yewwute fii mooy renaissance gi nga'y dégg ci kàllaamay franse te'y tekki ci maanaa yewwute rekk, ndax mooy judduwaat gu xam waral, ginaaw dee gu réer waraloon.

Làkk moo'y cëslaayu'g yewwute, du ma'a'y ki ko njëkk'a wax, am na ñu bari ñu wax lu ni mel, ci xalaatkat yi ak taarixkat yi, bu ñu dello as lëf ginaaw ànd ak sunu'y xalaat, ba ci xarnu'b fukk ak juroom ñatt ci jëmmi boppam, da nanu gis ne lu bari ci'y xalaatkatam aki ñoñ taarixam, ku ci mel ni Lodoviko Antoniyo Mortara ak Volteer ak Wilyaam Robertson 1721 - 1793, jëfandikoo woon nanu waxiin wu mel ne wii, ndaxte boole nanu ci mbàndarga yi'y raññale jamono'y yewwute, boole woon nanu ci doxu'g waxiini gox yi,juge ci'y waxiin dem ci ay làkk yu réew niki làkku'w Espaañ wu Itaali, wu Fraans ak wu Portigaal, ba fa mu yam.

Li gën'a yéeme moo'y Yojinyoo Jarin moom dafa jel mboleem amaliiti "yewwute" gi, sol ko ci benn baat, mooy " filolojiaa" , di baat bu am ñaari maanaa yu mag, mu njëkk mi, mu xat la, te daytalu(gàtt), moo'y (( dégg làkk)), mi ci des, moo gën'a yaatu te gën'a xóot, moo'y gëstu yu làkk, yu njàggat yi (adab) (ci tubaab les recherches linguistiques et littéraires).

Jarin gis na ne bu nu mane'e doxal yooni gëstu yu làkk ak yu njàngat yi, jaarale ko ci gëstu ci dénd bi(nature), jamono jooja aw yoon wu bees di na judd, di yoonu gëstu wu xam-xam wu di kojug làmb, (làmb ba daj rekk, amul waxi kese walla gisiin ), loolu moo ñu'y àggale ci xam-xami matematik yi. Nga dolli ci loolu ne làkk moo'y seetu bi nga'y man'a gise dundu'g nit gu xel gi, boo gisee ne làkku xeet wu nekk, ci jamono ju nekk, lenn la ci li'y wone am xelam, nga dolleeti ci ne ci lanu'y jànge xam-xam yi nga xam ne bu ñu nekkul woon,amuñu woon, dund gi du mel nii mu mel tay. Bu làkk amul woon nu xam-xam di juddoo ba'y gis jant bi.


Làkk moo'y cëslaayu ag yewwute bu nu ko waxee, dées na ko man a dëggal, rawati na ku jàng jii jamono, jàngat ko, xam la leen seen " waxiin" yu suufe ya ñu xeeb jariñoon - ñu ko'y woowe ci francais dialecte - ba ñu leen jëlee, def leen ay làkk yu xeet, yu réew, yu xam-xam, yu ñu fonk, yu ñu fas-yéene'e doxale seenu'g dund, sës ci seenu'g dox, sanni ca àll ba yeneen ya doon dox seen diggante ak xam, xam-xam, ak yewwute, mu'y làkk wu latin wi nekkoon di lu ñu neew xamoon, la gën a rëy ca mbooloo ma réere woon ko, te réere gi taxoon ñu reeroon te yewwoodiku.

Wii làkk, di wu Latin wi, nekkoon na di seenu'b coona, di seenu'w ay, di seen gàllankoor, di ab pakk ci seen digg ak jem-kanam, ndax la ëppoon ca xam-xam ya, bu ma waxul sax lépp, ca woowale làkk la nu ko daa binde, di ko ci jànge, te askan wa bu doon téeméer, lu yees fukk'a ko ci'y xam, mu'y ci misaal daanaka: nga xiif lool, ba'y bëgg'a dee, di wër loo lekk, ndeke lekk gi moom am nga ko, mi ngi ci sa ronu ay tànk, te ya'a ko moom, doo ci fay dara, xanaa kay da nga'y jël rekk jëfandikoo, te loolu lépp xamoo ko, te kenn'a ngi nii ci sa kanam, xam loolu lépp, te xam ne bu ko waxee, dootul jariñu ci, ni mu ko daa defe, kon na la ko bañ'a won, xamal la ne ya'a'y ki ko moom, ndax loolu man na'a waral sa'g wadd sòng ko, giir ko, ne ko fuuf, te bu booba'a su ko ab xiif gaarate'e du xam fu mu ko'y fajeeti ci'g càcc!.

Waaw waaw, ci'g càcc kay !, ndax lii ag càcc la, ndax xañ nit àqam, di ko jëfandikoo'k'a jariñoo sàcc ko la, te bàyyi ko nee mu toog ci'b xiifam, ci yitewoo àqam, ci taru'g yitewoom, càcc la de! . Loolu ku ni la du sàcc, laaj ko lu mu doon,moo raw sàcc, fëkk la, nax la, réeral la, dofal la, xiifal la, neewal doole la, nakk'a xam la, dofe la, suufe la, réer la, bon la, waxal lu la soob ne moom la.

Kii man'a xam nga ne ko doo fi xame, ndax làkk wi nga yor du wu ñu'y xame, wa kee yor'ay dëgg-dëegi aw làkk, ci la ñu war'a waxe, war ce'e jànge, war ce'e yëre, war ce'e gëstoo, war ce'e binde, te ci la nu war'a nekke nit, boo xamoon li ci addina bi bepp it te xamewoo ko ci doo kenn ku xam, ku ñu'y lim nga nga'y kenn ci ñu xamadi ñi, ñu réer ñi, ñi amalul seen réew solo. Lii nag sama gaa yi du'g réer, di'g dof, ak dofale, ak li la soob ci xeeti xelloodi?

Lii'ay li ñu doon def waa Orob ca jamono yu diggdoomu ya,maanaam " middle ages" ci angle, di nu ko def ci jii jamono - nga xam ne moo'y ju xam ci anam gu gaaw, ngir bari'g li ñu war'a xam - ndax li man'a xam te ëpp ci réew mi am nanu làkk wu ñu man'a xame ci's lëf ci'g gaaw, ak sakanal waxtu, ak ci's lëf ci'g wér, ak lëw. Kon jort naa ne la'y lañu war, moo'y la wa Orobi joojale jamono defoon, mu'y taxaw ci jël seen àq, delloosi seenu'm dem, feeñal seenu'm réer, sulli seen lu suulu.

Di na rafet nu indil leen sababi feeñug yile làkk.


Feeñu'g làkk yu bees yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi,(moyen âges) moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak niti adab ya, walla njaggatkat ya ( hommes de lettre) ak ustaas ya. La notoon nag ca nit na - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yi'y yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamono'y "yewwute" dikkee, gelawu'l "fonk sa xeet" (nationalisme) upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak niti adab yi, ak woykat yi, tàmblee jeng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Engle ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi (xisa bu'y reeloo) Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoom moo'y làkku Romam wii daal moo'y gën ja'a kawe'y jumtukaay ngir génne xasida'y woyam yi.

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di franse,ngir wuñi ci li'y yëngu ci biiram, ci njàggat (adab) lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf).

Chaucer mi di'b angle ( 1342 - 1400 g) jug,moom itam, sotti ci'w làkkam woyam yu yéeme yi ci'b taar, rawati na nettali'y Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angle yu mag yi, yi gën'a siw.



Làkki Tugal yi nag fii lañu bàyyikoo:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Làkki xeet yu Orob yi, ñi ngi sosoo ci màbbiiti Latin ak Tiyotin. Wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Portigaal, ñi ngi dagge ci Latin, wu almaañ, wu angale, wu danmark, wu suwed, wu oland, wu norwej, bàyyikoo ca Tiyotin.

Bokk na ci sabab yi jur doxug yile waxiin dem ci làkki réew, yu xeet, bokk na ci sabab yooyu, nekk gu làkku'w latin nekkoon di wenn, ba yàgg mu seddaliku di ñaar, wu ñu'y wax kalaasik, ak wu wilgeer . Kalaasik mooy lu yàgg la'y cosaan, wilgeer, di lu yomb, li nuy jëfandikoo. Kalaasik wi di wi politigkat yu mag yi, ak boroom xam-xam yi, ak niti diine yi daa waxe. Wu wilgeer wi, di wi niti neen yi di waxe, di ko jëfandikoo. Ci noonu kalaasik wi tàmblee nakk as lëf ci solo'om,ak dooleem, wilgeer wi tàmblee jël barabam, waaye wilgeer wi moom ci jëmmi boppam tàmbli na ci ginaaw bi di soppiku, ndànk-ndànk, jem ca leneen lu dul la mu doonoon, ci noonu ay waxiin yu bari te wuute bànqaasoo ca, ngir nocciku'g lenn ci mbooloo yii, juge ci yile barab dem ca yee,tas fa,ak soreente gi yii barab soreentee te wuute. Loolu jur yeneen mbooloo'y nit judd, mu ci nekk ak sa waxiinu bopp.

Waaye loolu moom teewul woon latin des fi di làkku diine wi te'y wu xamlu wi maanaam wu ofisel wi, ba mujj askan yi yoqat ko, te xam ne pakk la ci yoonu seen ag dox, aku'g jàll, ndax ña ëppoon ca ñoom xamuñu ko woon,dégguñu ko. Loolu yobb léen ci ñu xëy taxaw temb ci jële ko fi, sanni ko ci seen ginaaw, weccee ko'ok seen waxiin yooyee, te farlu bu baax ci jàllale leen, jëme leen kanam, tèkki ci li ñu soxla woon lépp ci yooyule téere yu am solo, te ñu bindoon leen ci laitin ca jamono jooja.

Ci noonu nit ñépp tàmblee gis koom mu rëy mii, di ko xam , te bu njëkk, daa xawoon'a jòmb ci ñoom ñu ko'y xam, ba ci'y jariñu. Lii nag day tegtale rekk li war, mu'y jëfandikoo làkku'w nday wi, niki lakk, ci wàllu'g ligéey ak jàng.




Reew yi nekkoon ci ron suku'b sañcaan yi ( colonialiste) yi, rawati na yi ci'y jëfandikoo làkki jàmbur yi ba leegi, niki tubaab, ak angle, ak yeneen, jàppe leen làkki ofisel, yii réew de ba leegi dañuñu di jànkoonte ak ag réer gu kawe te tas ci biiru'w askanam, ak koom-koom bu deltu ginaaw, ak ag des ginaaw gu rëy ak dund gu suufe. Kon làkk daa war'a nekk di lu yomb lool ci ni ko'y jariñoo, maanaam mu'y làkku'w la ëpp ca nit ña, niki wolof fii fi Senegaal, bu ko defee ñu bàyyil fi ni gën'a néew itam seen àq ci jariñoo seen làkki bopp, ci lefu'm jëf ak jàng. Waaye nag bu booba'a du man'a ñàkk'a jëfandikoo làkku la ëpp ngir jëflante. Ci noonu la ko'y joxe àqi nekk làkku'w ofisel wi.

Li nga xam ne sikk amu ci, moo'y gis nga ay yooni yoon, lu bari ci yeneen xeet yi ci reew mi nu'y wax wolof yu rafet ci anam gu jàppandi, ni ko ñépp di defe, ci lu dul ñu ko'y jàng, bu ma waxul li ëpp ci ñoom, te safaanu'b loolu néew na nga gis ko, maanaam wolof bu dégg yii làkk, loolu li ko waral du ne wolof bi daa yitewoowul ñeneen ñi, du caagéenu'g ñeneen ñi dañu'y sotti seen yite jépp ci làkku'w wolof aki mbiram, li am kay da di wolof day làkku jëflante wi tas, samp boppam ci géew bi, franse mii ñu'y jàpple sax manul'a bëre'ek moom mbaa mu gëpplante ak moom. Ndax moo'y làkk wi'y tàbbi ci say nopp, mu neex la mbaa mu naqari la, nga ko'y xam ci sañ-bañ.

Am na ñu ne ndax wolof am na sax, niki xeet ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Man nag ma'y ku yitewoode'e tontu ci loolu, ndax ni mu ma ñoradee, waaye am na nag lu xaw'a am solo ci laaj bi, mu'y booy xool lu bari ci ñi ñu'y tudde wolof - ci laa maa ngii - seen dëgg-dëggi cosaan du wolof, man li may jàpp foofu moo'y wolof li mu'y tollool moo'y “ag cenegaal” , maanaam xeet wi moo'y waa-senegaal, làkk wi di wu senegaal, kon dootul wu giir, mbaa waaso, waaye wu xeet wi wépp’a, Serin Tuubaa amul lenni wolof, Alhaaji Maalik naka noonu te taxul woon nu dégg tukloor, kon day mel ni xalaat bii mi ngi jeng as lëf jëm ci'g yanu maanaa.

Bu ñu delloo ci li ñu nekkoon di wax mu'y war gi làkk war'a nekk di lu yomb ci ki ko'y jëfandikoo, da ma naan nit ñi daal li leen war moo'y def na waa sowwu defoon , muy tuxal seen waxiin yooyee, yòbb leen ci'y làkk, te sukkandiku ci, xamloo ci, su nu ko gisee muy lu mant'a ñàkk, maanaam bu nu fi gisee lenn lu'y gàllankoor seenu'g dox, di làkk wu fi jóox, wu ñu xamul ni ñu ko war'a xame, niki franse ci sunu-gaal.

Waaye nag amaa na loolu lepp du nu ko soxla, bu waxtu wa jàllee, ba nit ña dégg way jóoxi làkk yii ni ñu dégge seen làkku nday wi. Ndaxte làkk du yàlla ju ñu'y gëm, waaye kay jumtukaay la ngir déggante ni ma ko jorte.

Ahmad Amiin wax na ca téereem ba tudd Fajrul Islaam:(( aw làkk sàkkeesu ko ci genn jañ (maanaam jekki-jekkiwul rekk am), ñu mujj ñi bi ñu ko'y jële ci ñu njëkk ña du woon lu mat, li am kay moo'y nit ñi dañu'y sàkk ci seenu'g njëlbéen, ay baat yu tolloo ak seen aajo, bu yeneen mbir feeñee, nu sàkkal leen ay baat yu bees, bu ay mbir raafee amaa na ay baatam raaf. Làkk nag'a ngii nekk ci dund ak dee gu sax, naka noonu bàyyikoo yi (mooy baat yiy tukkee ci yeneen yi) ak waxiin yi, ak baat yi, ñoom itam dañu'y màgg , di yéeg ni xeet wi'y yéege, di ko magge)).

Yooyule làkk, di yu Orob yi de,gënuñu fenn, mbaa ñu kawe ci lenn sunu yos yu afrik yii, li fi nekk kay mooy ñoom dañu leen'a fonk, sonn ci, di def lu mel ne li Ahmad Amiin di wax mu'y sàkk baat yu bees saa su lu yees amee. Kon sama gaa yi, nanu doylu ci lii nu yor, ndax li sunu di neex, sama dàq na ko kat, te jéem ko'o jàllale,jëmale ko kanam, te tas ko ci mbooloo mi.

Du'y caaxaan la nit ka'y xalaate, ca la war'a waxe , ci maanaa li nga'y xalaat ci sa biir dënn, sa biir xel, mu'y jeqarbiku ci sa'y yëg-yëg jarul fireeti ci weneen làkk wu dul wi ko xalaat, ngir déggal ko ku nu jàkkaarlool ki, bu ko fekkee mu ko'y man'a dégg ci wi ñu ko xalaate,loolu li mu'y jur mooy yàq waxtu,te mu'y lu gànjaru.

Wax ju'y joriku, di dikk ànd ak kem bu rëy ci'g jàppandi, manul'a ame ci lu dul làkku'w nday wi nit ki juddwaalee, walla wi mu àndal ay at, di ci jàpp ak'a ŋoy, ci këram ak pénc ma, ja ba, ak daara ja, nga xam ne da'y faf fàtte wow ndayam wa, mbaa mu xaw ko'o fàtte,ba mujj wii di wu jóox sax mooy far di taxaw taxawaayu wu nday wi. Bu dee fii nag, gisagunu tubaab jël fi taxawaayu'b wu nday, wolof mi'y nday kay moo sax di nday ba leegi, ci moom rekk lanu'y man'a ame joriku gi nu sox la ci wax, misaalu'm loolu yaa ngi koy gis ci ñii di xëy ak'a gont ci leekoli nasaraan yi, ñoom de ca dëgg-dëgg da nanu ko dégg xayna , waaye lu ci ëpp, du ñu ci man'a génnee seeni xalaat ci'g joriku aku'g yomb, waxal sax aku'g dëggu, ndax dañu'y diriku ci seeni wax ak'a jàddantu, ak' a xootal fu nu ko waroon'a tondale, ba far wax ja day doon leneen lu dul la mu bëggoon'a doon, walla sax leeg-leeg ñu rax ko ak yennaat ci baati wolof, ngir noppalo'o ca, bu ko defee tubaab bi déggul ay wolof du xam li ñu'y wax, wolof bi déggul ay tubaab it naka noonu, kenn rekk'a ko'y xam ki boole ñaari làkk yi.




Li ma gis moo di Orob ca yaatoom ga, ak ca jégeente'y xeetam ya, ak seen ag niroo, ak gu làkk, ak bokk gisiin ak diine ak melo,ak - man nga ne - jëmuwaay, nga rax ci dolli, nekku'g yenn ci seeni làkk di - man nanu ne - yu addina bi bepp, niki angle, ak wu ko xaw'a jege niki francais, teewul ñoom ñu nekk di ñu jàpp ci seeni làkk, xeet wu nekk ca wosam, te teewu ko'o jàng nag yeneen yi, rawati na angle, di ci jokkoo saa su begge'e jëflante ak ñi déggul wa mu yor. Danmark ma nga'ak danwaam, Suwed wuwedam, da ma'a tayye'e lim, waaye wu ci nekk ak wosam, ba ci Belgik sax nga xam ne ñaari xeet yu wuute'e fa dekk, teewul xeet wu nekk, yor sa wosu bopp, te teewu la'a jàngi leneen ba ca wu sa moroom, bi nga ko gisee mu'y xam xam, ndax xam-xam du lu moy xam lu mat'a xam, te loola mat na'a xam, ndax da na jur ag rataxal diggante, jur ag xam sa moroom, jariñu ci, jariñ ko.

Addina bi dafa war'a sosu ci'g dimblante, jariñante, fonkante, deet jariñoo, ak dimbandikoo, te lii tubaab yi di def, du lu dul dimbadikoo, ak jariñoo, ci suñu'g suul, ray, joggi, nërméel mbooleem sunu yëf, ci taxawal seen yëf.

Wolof nag daa na wax : (( pesu'm kanam boroom'a ko'y fajal boppam)), kon nag pes nañu nu, lu nu'y xaar, du nu jug di door, mbaa nu'y daas ay jaase'eki gobar, li nu'y def kay moo'y jëfandikoo xel, ni ko seriñ Mbay JAXATE daa waxe, mu'y ab noon bu la noonu, boo'y xeex ak moom, bu mu ko yëg, na xëy rekk daanu door a xam ne ya'a ko daaneel , fa la sa'b noflaay di ëppe, ca la la nga'y jëfandikoo ci ngànnaay di gën'a néewe, ndax bu fekkoonte ne daa waroon'a jàmmaarloo ak yaw, nga'y jëfandikoo lu ne ngir moytu'y dóoram, ak di ko jéem a dóor, leegi fegal nanu la coona'b jéem'a dóor ak moytu, moom kay da nga'y agsi rekk dóor, mbaa nga jam, ndax moom yëgul ni ya'a ngi koy fexeel, bu ko defee mu dee, naaxsaay. Lii estraategi la ci.

Lu mel ni franse ci réew mi, manoon na fe'e nekke ni fi araab nekke, di'b soppe te bañ di'b noon, di luy dem ànd ak di demale, waaye jort ne moom rekk'a war'a dem?. Xoolal ci maanaa araab ñi ko jàng tay, ñoo'y ñi dégg wolof, ñooy ñi ko fonk, ñoo'y ñi ko'y suqali, loolu bu amee li mu wund moo'y ne araab ca mag ña jumtukaay la woon ngir jëm kanam ci xam-xamu diine waaye it jëmal kanam seen kàllaama gi nga xam ne tay daa fees dell aki baati araab yu ñu jox kàddu'g wolof, ci fi ko wolof amewul. Xoolal ma baatu’b jamono, mi ngi juge ci samaanu, maanaam juge ci mahnaa, yu mel nii yu sakkan lanu ci, daa nanu dem sax ba’y jëfandikoo as lef ci xarala, di sàkkal wolof ay jumtukaay yu làkk yu mu amutoon te ñu gis ko ci araab, te xam njariñam, xam ne man na leen'a amal njariñ, niki yaa'g askanal googu nekk ci araab, nu ko daa tollolee baatub koj , naan yef yu di koju'g nàggam, ci maanaa xam-xam bu di koju'g diine, jublu ci xam-xamu diine, mu'y mbaat sos su nu ko fonkee, man na'a am ay jeexiit yu am solo, ci ëllëgi làkk wi, ak ci diggale , di ci tubaab par l'intermediaire de , ak ci'g jonjoo, di ci tubaab en direct. Yii di baat yoy danu lay won ni araab jeexiitale ci wii làkk, du caagéenu danu di ay baat yu amul woon ci wolof, aha kay yu ci amoon lanu, waaye fii yeneen maanaa lanu yore yu bokkul ak yanu yoroon, nun itam bu nu gisee ne yii du yi nu soxlaati, walla maanaa yii jubul, am nanu sañ-sañ ci def ni nu neex, ndax ñoo'y boroom.

Kon noom ñaar way jàppante lanu woon yu'y dimbalante, dunu woon ay noon. Wolof am na ay waxiin yu bees aki baat yu yees, ci tabe'g làkku'w araab la ko ame . Ndax boo'y xool da nga'y gis ne woomle'g wolof aku'g riisam mi ngi ko jële, ci jël lu toll ne làkku'w araab ca yaatoom nga, ak tàllalikoom ga,firi lépp baat topp baat, loolu moo nekkoon seen anamu'g jàngale, nga xam ne da nu la'y wax baat firil la ko, ba mbooleem teere yi nu daa jàng ci araab - te yu bari lanu woon te wuute, ci fann yépp - ci nii la nu ko daa defe. Loolu jural leen nu mujj baat bu nu am ci araab ca woomam ga, nu am ko ci wolof.

Bu dee franse moom ci nga'y dégge wolof bu naan la : nga jéggal ma sama wolof daa leerul, te loolu ag xeexam ak ag jéem'a suulam'a ko waral, ag yaakaaram ne moom rekk'a war'a nekk ci kaw suuf'a ko waral, ak jeem'a toogam ci laltu gi, mu des ay barab yu nu man'a toog, mu teg ci ay tànkam, lal ci'y loxoom ne kenn du ci toog, moom reek, moo di li ko waral.

Kon de kii ku siis la, ku xat la,ku nay la,ku'y ngartaajoo la, ku'y nangu suufu's jàmbur la, ku yëg ne moom rekk la, ku am bëgg-bëggu suuxal la, lii nag ku ko mas'a am ya'a'y ki nar'a suux,nar'a neen,nar'a seey.




Waaye loolu lépp du tee mu'y lenn ci li ñu moom, moom nasaraan du moo moomati li nu ci moom, ndax ca Aljeeri de, kenn ci ay xalaatkatam nee na woon : franse de lenn la ci sunu am "màngiit" mi nu mànge ci tubaab yi. Màngiit moo'y xaniima, di ci maanaa li nga'y nangoo ci ki nga'y xareel, boo ko gañee, maanaam loolu moo'y li franse di ñëw lépp ngir nangu, jël ci doole, fitnaal, foñloo, fàtteel, taxaw ci doole,jaaye ko, teewul muy lu am solo, di lu ñu man'a xame'e, man ce'e jariñoo, kon bu nu ko jàppe njariñ lu nu'y sànni, waaye màngiit, mu nu mànge ca sunu xare ak ñoom, ndaxte addiis'a ngi nii bu naan : (("hikma" moo'y réeru'm jullit bi, fu mu ko gis daal na ko woor ne moo ca gën'a yay)). Hikma nag di lol boo ko doon firi da nga naan moo'y lépp lu rafet rekk, jekk, xellu, baax, di lu ñu xam, di lu am solo, ci dund, mbaa dee, xel mu rafet, ba fa mu yam. Kon franse li fe'ek ya'a ngi ci'y gis sa njariñ, moo xam lu adduna la mbaa leneen kon ci hikma la.

Waaye kay li'y li yéeme moo'y da ma'a gisagul ci réew yi'y dem, te'y dox, di dund, di jëm kanam, mu ci'y waxe ci'w làkk, bu feeñee, bu làqoo weneen, maanaam loolu mooy li xew tay ci sunu réew mi, nga xam ne bu ñu feeñee ci lu fés, mbaa nu'y jëflante ci anam gu ofisel, - "ofisel" ci li wolof mànge ci tubaab la - da nga nu'y gis nu'y waxe ci kallaama'y nasaraan, bu nu delloo fa sunu'y kër,di ko defe ci wolof, leeg-leeg sax nu'y rax la ñu'y defe ca franse yennat ci baati walof, kon mokkalaguñu, te loo mokkalul manoo ce'e jariñu, li'y li nu mokkal kay moo'y sunu wolof mii ñépp di wax,ku dégg franse ak ku ko déggul, ku'y ku ndaw mbaa nga'y mag.

Fii nga'y gis jëwrin ju mag ju taxaw di wax ci googule kàllaama ba yàgg mu ruur toolu'b wolof, fac ca soxlaam bu baax, mu mel ni daa déggatul tubaab, walla mi ngi ko'y bëgg'a sonnal, ndaxte nag ca dëgg-dëgg coona la, di wax lol boo ko déggee it, wi nga nàmp nga gën'a dégg, te ci nga gën'a gise sa bopp, ki nga'y waxal it moom la gën'a dégg, du am lenn lu mu ci'y xel ñaar, mbaa mu ko ci'y laaj,du caagéenu'g baat bu mu ci'y réere daanaka. Ba ci sunu njiit lii fi nekk tay, di Wadd, ba laa bég ruur toolu'b wolof ci biir waxi tubaabam, day mel ni da ce'e gën'a gis boppam, mbaa mu gën ko'o yòmb, mbaa noppal, wax leen ma lu mu ?.

Raw gu xam-xam gu mag itam boo'y xool, da nga naan demewu fi noonu, li sabab loolu moo'y ne nun li ñu'y daj ci dégg tubaab daa metti te rëy, te li mi'y jël ci ñun ci waxtu daa takku, loolo'oy li'y waral nu'y neenal xam-xam yi, moom kay fii fi Senegaal dégg franse doy na fi xam-xam, àgg na ci sunu njiitu réew lu njëkk la, xam-xamam bu mag ba nu doon naw lépp, du woon lu dul :naan na géeju'g franse, du ñu ne la benn xam-xam bu di koju'g tegnik mbaa xarala la xam.






Seriñ Tuubaa mi ngi ñu naan - ba mu ñu'y jàngal xam-xamu Lislaam - : jiitalal xam-xamu" tawhiid" mu'y li la'y xamal ni nga'y gëme Yàlla, kennal ko,wéetal ko, teg ca " fiq" mu'y ni nga'y jaamoo sunu boroom, ak "tasawwuf", waaye mu teg ca ne ak jumtukaay ya, mu jublu ci jumtukaay yi; làkku araab ak la mu'y àndal ngir nga man ko'o dégg, mu'y nahwu ba ak bayaan ba, "nahwu" di li'y nos làkk wi di ci franse grammaire, bayaan di li'y nos wax ji, di tax doo guddal lu waroon'a gàtt, loolu lépp, bi mu ko'y lim mu bokk ci xam-xamu diine, da leen'a tudde ay jumtukaay, mu jublu ci ne xamluwunu leen ngir seen jëmmi bopp, waaye ay raas lanu yu nu'y yéege jëm ci xam diinee, rawati na alxuraan mi nga xam ne manéesu ko'o, walla su c'ee xam te déggeesul araab mi nu ko wàcce, ndaxte làkk wu nekk, am na jagle'y boppam yu moom rekk'a ko moom, ku firi wor la léeb wa wax, rawati na lu mel ni alxuraan ca jafe'g làkk wa nu ko wàcce, ak màggu'g aji wàcceem.

Bu nu waxee màggu'g aji wàcce ji, da nga ci'y dégge màggu'g li nu wàcce, kon loolu màgg na màgg gu kenn mant'a dégg ci'g yòmb,ak'ub noflaay, lii moo'y li waral araab di jumtukaay ngir xam diine, di xaaj ci xaaji xam-xami diine yi, kon mag ñi jànguñu woon araab ngir jëmm ja, waaye jumtukaay la woon ngir xam la mu ëmb, loolu mooy safaanu'b ku mel ni Senghoor aki gaayam, noom làkk wi moo leen taxoon'a jug,nu sonn ci, sonle ci, bu taxutoon, doo def fo'o toll di dégg baatub frankofoni, lu mu'y wund ? tontu leen.

Yalla baax na, ba mu nu teralee ci nu nekk ci jii jamono di dellusiwaat ci sunu bopp, di ko tàmble’e fonk, di gestu li jar'a gestu, te lu ci gën'a rëy sunu kàllaama gii?, ndax giñ naa ne xam gi bu wóor, ak jëfandikoo gi ci fànn yépp di nanu jariñ lu bari, te'y jëf ay jëf ci yòmbal sunu'g dund. Da na nu yòbb tam ci nu'y dëgg-dëggi réew, dëgg-dëggi xeet, dëgg-dëggi ay mbòkk, yu gis ne am nanu lu nu bòkk, yu'y mbòkkoo ak'a joqalante ci'g nooy ak'ug jàppandi. Jëflante di na gën'a dolliko'o ratax, déggante gën'a yòmb,xam gën'a jàppadi, koom gën'a lëw, ndax xam-xamu koom di na gën'a yòmb'a jariñoo ci ligéeykat yi, jaaykat yi, naka noonu naataange di na raññiku ci wàll yu bari, ngir xéewal gi am te ame ci jàppandi'g xam mbir yi, ngir jumtukaay bu yòmb bii am te amutoon di sunu'w làkk.

Ana lu ku am’um xel di wooye am xaram naan ko kaay ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

la ko war kay moo'y mu ne ko bar, bar moo'y baat bi bàyyima bii xam, kon noppal sa bopp du nga nekk fa naan ko kaay, waaye xanaa bar mooy li sonleedi. Naka noonu ñu dégg ba noppi wii làkk, nga xam ne leegi xam xam-xam rekk'a nu war'a ñor, te dese nu, nu naan da nu'y bàyyi wii nu dégg nee, naan dañu’y xamlooti weneen door'a xamlu xam-xam yi taxoon ñu'y xamlu'w làkk, loolu jort naa ne dofe la, sànk waxtu la, sonnal sa bopp la.

Jàppoo ni sunu ligéeykat yii ca seen yewwute ga ak muus ga ak xarale ga, bu nu ci doon boole di leen seetal li nu aajowoo ci xam-xam bu aju ci seeni ligéey, defal leen ko ci seen làkku réew wi nu dégg, naan ko, xam ko xam gu xam kawewul, jàppoo ne bu loolu amoon du ñu fi xar baax, jëf fi ay kiimaan, def fi lu raw li tubaab yi di def, ba nu leen di naw ?.

Da ma'a yàgg'a dégg ci sunu biir ku naan nit ku ñuul daal, xawma lu mu def Yàlla, ba Yàlla gàttal'um xelam nii !, te loolu day mel ni bu nu ko'y wax, ñi ngi dëggal li tubaab bi yàgg'a wax yàgg ko'o jort ci ñun mu'y moom moo nu ëpp xel, walla sax moo'y ki ko am, nun li nu am du am xel, ndax xel ak ni mu màgge jòmb naa nekk ci yaram wu ñaaw, wu ñuul, wu tàyyeel wii. Am ku ma dégg te moom ku ñuul la, mu mel ni ku'y jàpple tubaab yi ci seen wax jooju naan: ((ñu ñuul ñi de àjjana bu ñu fa duggee, su nu fa yàggee yàq ko, naqaril ko. Tubaab yi nag ñoom, bu nu tàbbee sawara, su nu fa yàggee defar ko, neexal ko)), waaye boo'y xool sax da nga'y mel ni ku gis lu ni mel, te sabab bi du dara lu dul jumtukaayu jàng bi moo nekkul ci sunu loxo mu'y sunu làkku bopp, làkku jàmbur day waral nga gëm jàmbur, xeeb sa bopp, xoolal ci nun ñi'y làkk tubaab, sunu delluwaay, sunu jëlewaay, sunu ndëërlaay moo'y fraans, ak nu mu man'a rëye mbaa mu tuutee ni, kii moo'y ki nu gëm, bu nu ko gënoon'a xam it jort ne moo nu ko gën'a def, lii aji am la ju ñépp di gis, di ko dund.


Li ñu’y wax cosaan, da'y baat bu waa senegaal baaxoo wax, di ko tudd lu bari ci seeni wax[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ñu’y wax cosaan, da'y baat bu waa senegaal baaxoo wax, di ko tudd lu bari ci seeni wax, mu mel ni day lu ñu fonk ba ci lool, mu mel ni fonk gi moo'y yoon, ndax boo'y xool, cosaan mi ngi bàyyikoo ci baatu sos, di kon fa nga sosoo, juge ca, bàyyikoo ca, bu dee nit la ndayam, baayam, dëkkam, réewam, aadaam, aam, lii moo'y cosaanam, ndax ci foofu la sosoo, bàyyiikoo fa, kon lii mooy cosaan. Waaye ndax li nu def fonk cosaan la ? Nan laaj sunu bopp bu baax te xootal laaj bi, ndax fonk nanu sunu bopp? Sunu cosaan ? Man dama naan déedéet, déedéet kay, ma dellu ne déedéet. Jort naa ne ci barabu fonk sunu bopp, tubaab bi mooy ki nu fonk, ci barabu sunu cosaan, cosaanam, lii'a'y li am, di li nekk. Tubaab bi la nu'y xëyal, di ko gontal, ak doonte as lëf ci sunu njariñ'a ngi ci, aw làkkam lañu'y sonn, bàyyi sunu wos, te kat làkk moo'y dëgg-dëggi cosaan, ndax mooy seetu bi'y wone boroon, te'y jimblang ji'y ëmb li xeet wi indi ci'y jaloore, aki mbanoore, aki aada'aki cosaan.

Kon moo'y mbuubs mi nga xam ne bu la réeree, la mu ëmb sànku, naaxsaay. Kon déet ag wuutu di ñeel ko. Tereesul jàpp weneen waaye na sa wos jiitu, ndaxte léeb wa nee na: li nga am boo ci séenéenul doo ñeetaane!. Mu'y ci maanaa li nga moom boo ko fonkee, mu doy la, nga doyloo ko, doo soxlaal kenn lennam. Mu'y lu wóor, ndax jort naa, lii fi nun bu nu ko fonkee, dem, te du nu sonn, mbaa nu'y ñee kenn.

Mu mel ne la Karlo LEFI waxoon di kok ku jàng "njàggat" lu Itaali - njàggat , fii mu'y tekki litterature ci nasaraan - da nga ko xam, mu ne woon:( Kristo s'è fermato a Eboli ), di ci maanaa Kristo, di yonnant Yàlla Hiisaa, ma nga yam ba mi'y def doxu'b nitale ba, yiwale ba, xayale ba, taaxale ba, diinele ba, yéwénal ba, ma nga yamoon ca Eboli, jotutoon’a àgg sunu dëkk, jublu woon ca loola ne "àtte" gi, walla ci ni nu ko gën'a baaxoo waxe "nguur gi" mu'y baat bu ma soof, ndax nguur moom nekkul lu dul fu'y buur di dunde nguur nekk fa, waaye mu begg'a wax ne nguur gi kon di gu Itaali, bi mu'y defar da fee bayyi sama dëkk bii jéemu ci dara, sama'w nit di ñu dofe, ñàkk am xel, ngir néewu'g li ñu leen sotti ci xam-xam, man itam ma ne naka noonu, ngir sunu ñàkk'a jëfandikoo sunu làkk, di jël wu keneen.




làkk moo'y yàlla ji'y faji aajo?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ku wax lii de amaa na ñu ne ko: yaw de xanaa da nga'a faf jort ne làkk moo'y yàlla ji'y faji aajo, rawati na bu dee sa wosu bopp?, ndax da'y mel ne lu'y xeeti man-manu def, ak jëmale kanam, jumtukaayi jàll ak jàllale jox nga ko ko, kon daal moom rekk doy na ngir dox ? ma ne déet, du loolu la'a bëgg'a wax, li ma jublu kay, moo'y moom de moo'y gën ji jumtukaay, te'y gën ji dokk ci ku mant'a ñàkk'a sukkandiku bu'y doy, gàttalaakonu'b dox la, yombalaakonu dund la, mbokkalaakon la, bennalaakon la, di boolewaakon, di taxaakonu yëg sa bopp, fonk sa bopp, tasaakonu xam-xam, jàppandilaakonam, dabalewaakon, ak ak ak.

Man de maa ngi naan te du ma dañ naan: jël leen ko! moom'a de!. Moom'a de, moo'y li ñu'y teral, di ñu jugal, di nu doxal, di tax nu'y xalaat, di bind, di yër, yëglekaay yi'y lëw, di jàngu, ay bindkatam di dolliku, taalifkat yi'y yokk, yëngu-yëngu gu xam-xam di gën'a sawar, cawarte'g caada ak gu saxaafa gën di dëggu, gën di fés, gën di laalu.

Bindante di mujj di nekk ci lu dul ab coona, ci's lëf ci'g gaaw, ci'b noflaay, ci'g ratax, ci lu dul xalaat, mbaa toggoo, wàlla yenn anami moytu. Kon moom la, mooy noflaay bi, di jàll gi, di naatange gi, di meññ gi, di woom gi, di fulla ji te'y yéeg gi. Xoolal as lëf ci yitewoo gu tar, ak jublu gu mag gi nga'y seetlu fii mu nekk, ci sunu mbiri réew ak mbiri xibaar, te loolu li ko jur du dara lu mo'y xibaar gi nu'y xibaar askan wi ci seen làkku bopp wi, nga xam ne jamono jii, ñépp'a yewwu, kenn gënul'a xamati ki jàngul li'y xew ci réewam, ci wërlaayam, ci goxam, njiitu'l réew mi sax gënul'a xamati gone gi'y gën di gone li'y wëndéelu ci mii réew, ak ca mee. Lii lépp ngënéelu'l sa'w làkk'a, da'y wëy nag ba ca lu dul xibaar, àgg ca mbooleem lu dox mbaa mu raam ci lu nekk, di yombal, di gaawal, di àggale, di noppale, di soreele fitna.

Seetlu naa mu bokk ci la ma seetlu, ne leegi jàngkat yi ak jëfandikookati internet yi dañoo am ag jeng jëm ci bu nu'y bindante di ko defe ci wolof, rawati na bu nu yakkamtee, li leen jañ ci di ko def boo ko xoolee, lu yanu maanaa la, te yéeme, mooy noflaay bi ci nekk, ak gaaw gi, ak nakk'a faale gi ak ñàkk ge'e xalaat, mbaa ragali yaq ci nasaraan, kon lii lépp, ay pakk lañu ci sunu ay xalaat di dox, sunu'y xel di xelli, suni'y xalima'y sotu, sunu'y daa di soosu, nu'y joyal sunu'y gog ci di bind li'y jeqiku, ak'a fuur, di buur ci sunu'y xol, war'a nekk di lu nu'y yaxal ci keyit yi, ba way bañ ñi kumpa di ko war'a xam.

Am na jeneen aji feeñ (fenomene) ju am ci jamono jii, moo'y ñu bari ci ndonga yi'y bindante ay bataaxel (sms) ci ëyukaay yi (telefon) danu ko'y def - bu nu ko deful ci wolof - ci franse bu nu daggat, maanaam , bu nu dog la ca'y sonnale, mbaa mu ca'y yàqloo, ngir ma gën'a leer, danu ko'y bind ci anam gi nga ko'y dégge man ko'o xam, déet gi mu ware, ci maanaa ci barabu mais nu bind mee, veux nu bind ve. Loolu ba tay da'y wund lakkal gu leen wii làkk lakkal, ci mbindiin wi, dégg gi, jël gi mu'y jel seen waxtu, ak jafe gi ci ñoom, leeg-leeg nga gis ci ku ci def lu sakkan ci dundam ci jàng ko ci'g tar te du tax mu àgg ci fi ci war, te wolof kat mi mu jàngul, masu ce'e sonn, ma nga ko dégg dégg gu xar baaxe, kon kii bu ko jàngoon, mu yiteel ko ni ko franse yitéele, nu mu'y mel ? laaj naa la ko.

Xanaa kawe, xanaa raw, xanaa noppalu, xanaa sakkanal waxtu, xanaa gaaw'a àgg, fees, yewwu ci'y nelaw, xippi, taxaw, jàll, romb.



Waa ja daa wax:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Màggat mu màggat ci am njàggu'm tubaab, jabaroo <> tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii dëggel na, kii du bëggati ku dul tubaab, lu dul tubaab, dara ci boppam, li mu moom du ko ñorati,te ñii nag ñoo'y ñi ñi'y faral'a dénk sunu gii gaal, kon waxuma la jengal ko, waaye diigal ko la ñi'y def ! Ñoom xamunu joow gaal, li ñu'y wax permanaat la nu xam (promanade), ànd ak seeni jabar mbaa'y ndaw, xaj topp ci, ñu'y def leeg-leeg ñu sanni ko ab bant, mu wadd for, nu ko'y xonte li ëpp ci sunu njël li, bu ab baykat di dee ci'b xiif, te moo'y ki taxawal koom mi, ñu'y jënd ay way màggi mbéregaan (oto), naan lu manul'a ñàkk la, te doonoon ñu ñàkk. Ñoo dugg walla, su nu taxawul ci doon sunu bopp, ci lepp, ak fepp!.

Xam nga réew mii da dul mu nu yore xam-xam waaye nasaraan, firnde ji moo'y lu waral ña fi nekkoon te doonoon ay boroomi xam-xam te di ñu nasaraanoodi, nanguwuñu woon leen'a jox'ub nosam, bu ko defee nu ko'y wommate xam-xam ak leer, bëgg sa bopp, sa réew, sa njariñ, sanni nee lu keneen, waaye loolu lepp, du man'a nekk, ndax du sunu mos mu keneen la, te keneen ki tubaab la, kon moom ñoru ko mu'y dem, di dox, di jëm kanam, li ko ñor kay na des ci'y loxoom, mu'y digale ni nu k'oy yoree, ndax mu man di sax di lu mu moom, waaye tay nga dee de,yaw tubaab!, lii de jaral nanu sunu ay bakkan ak yu doom, ndax ñoo'y ñi ko moom, kon tëyyal sa yëf te ba no'ok li'y sunu, lii'a'y li waraloon mu dénkoon ko màggat ma màggatoon ca njàggu'm tubaab ma, te jabaroo ca, xalaatu ko'o dénk keneen ku ko mo'y, ndax moo'y genn wàllam, di ki mu wóolu, di mbuus mu ñuul mu ñu sol yaxi tubaab, yàpp wa, xel ma, xalaat ya, nii la ko jenn waay ju Mbayeen daa waxe. Xoolal ma kii nga xam ne naan na géeji xam-xam yi te defewu ko ci tubaab ni nu ko'y def, danu ko'y yòbb ba ca àll ba, nu jox ko fa as ndiggante su gàtt ci waxtu ci benn leekol, mu fa'y joxe ay bind (cours) ci wu araab, ak doonte la mu jàngi woon du làkku'w araab, da ci doon jànge rekk kay.

Gisati nga fii firnde ju leer ne ñoom de xam ñoru leen du caagéenu'g xam-xam, li leen ñor kay moo di njàngu'm tubaab, lii nag waa-réew mi, ñoo'y ñi ko war'a dindi, sunu bëggee boy, joy, tàkk, wëy, di yéeg, ànd ak way yéeg ñi. Mii du dem li fe'ek nii la.





Bu nu dee ñoñi "li fi nekk" (realistes) , dañu naan: nanu bàyyi li fi nekk mu nekkal boppam, du nu ko ga kenn mbaa nu ko ci'y manante (forse), nit ñi tànnal seen bopp ci anamu'g demokaraasi, bu ko defee làkk wu nekk nu jox ko àqam ak li mu yayool ci ndimbal, aar, jàllale, nga xam ne déet ag noono, loolu man na'a nekk sunu ndimbal, sunu njariñ, te ñu sanni nee li nu'y wax ofisel, am as lëf ci'g nooy "flexibilite", ubbiku, ci mbooleem làkk yi, ubbiwaat bu baax sunu làkk wii mu man'a ëmb, guux baat yu bari yi ko'y noppal, te bañ di sonn ci di leen wutati ñu'y juge ci boppam, fu nu gise ne lii moo yell fii, nu ne loolu la, ba kero lenn di taxaw taxaw gu fés, gu leer, gu deesul sikkati, man nga ne loolu sax am na ci wolof ci sunu gaal, waaye du tee nga ne am na yenn ruq yu jar'a gën'a ubbi, mu aju ci tas mbind mi, gën ko'o jàngale, gën ko'o yaatal, ba kero booba, ak ba ginaawam sax na ñu'y jëfandikoo lu fi nekk, te xam ne sunu yëf'a, waaye ci anam gu maandu, gu yamoo, te yell, gu dul gaañ kenn.

Lii nag am ci sunu tele bi, nga xam ne daa mel ni yëfi kenn la du lu nepp bokk, ñaaw na. Di xibaar lu toll nii ci'w nit, moom li nga leen di di xibaare, nga ne as daggiit ci waxtu lanu leen di man'a jagleel, bu dee ñeneen ñi nga xam ne ñoo'y ñi gën'a néew, te'y ñoñ boo ko doon seet sax, da nga naan matunu fukk ak dara ci teemeer ci askan wi, nga jël la ëpp ci waxtu jox leen ko, nu'y xibaar xibaar yi ci franse te nga ne yeete’e la tax'a jug? ay fen la de, ay nar la, li waral jëf jooju kay moo di màggat mu jabaroo tubaab'a la ko digal ci taxawal keneen nërméel nu, suul nu, suul sunu teddnga, sunu'g xam, yekkati keneen ki nga xam ne ca dëgg-dëgg wart'a woon'a sax aajowoo gile yekkati.

And ak loolu lepp du tee "ag jam" (critique) di lu man'a ñàkkadi ñeel ñenn ci sunu Imaam yi, ndax itam jël lu tol ne mbooloo mu toll ci ay teemeeri teemeer, nga'y wax ak ñoom di ko def ci làkk wu nu xamul, teg loolu diine, loolu dofeel la, yàq waxtu la, yab nit ñi la, xeeb sa bopp la, xamadi la, xamadi màggu'g diine la, ndax lu nu rafetlu la ci fu nu'y xutbaa nit ñi ci ajjuma, ginaaw ay jullit lanu, ñu laal ci's lef ci araab, làkk wi'y wu alxuraan, loolu boo ko'y xool ag sonn'a ngi ci, ci jàng ko ngir man'a xam Alxuraan, waaye it xamante ak sa yeneen mbokki jullit yi, ndax moo war'a nekk làkku ofisel wu addina'y jullit ñi, di dox ci'g bennale, ci 'g boole, ci'g xamalante, ci jappandal ag jokkoo ci biir jullit ñi. Waaye tekkiwul ne danu fe'e war'a nekk naan xar mi kaay, te'm dégg rekk bar .

Aji laaj laajoon na ne : ndax li nu'y jële ci jàngu bu nasaraan bi ci xam-xam, man na'a wuutu li nu ci'y ñàkke ? ab laaj'a ngoogu, di bu diis, bu rëy, bu am maanaa, bu soxla ku ko tontu. Man la ma ca jéem, ci tontu bi, moo'y benn baat , bi ma jortul ne keneen du ko ci weesu, moo'y déet, déedéet. La nu fa'y ñàkke te mu'y lu gànjaru, di lu am solo, moo'y li nu fonk'a wax, mu'y cosaan, làkk nag ñëw di li ko'y jëmmal, di ko taxawal, di ko wuutu, di ko nekkal, di li nga xam ne ci lu dul moom déet cosaan. Kon lu nu fa man'a xame réer nanu, ñàkk nanu, gàttañlu nanu, dof nanu, ñàkk nanu jumtukaay ba, jumtukyu'b yombal ba, bu noppal ba, bu gaawal ba, bu rataxal ba, bu jooral ba, ba'y déggale te'y bennale, di yombale ag jokko, te di ab xamalewaakon.

Làkku'w jàmbur niki doju pakkastal ci yoonu jëm-kanamu réew yi ko'y jëfandikoo te taqoowunu ak moom taqoo nga ca war:



Sunu boroom (t.s) nee na (( wamaa arsalnaa min rasuulin illa bilisaani xawmihii, liyubayyina lahum)) mu'y : yonniwunu benn yonnant ci'w nit ndare bu danu ko'o waxloo ca làkk wa ñu dégg. Lii Yàlla sax ci di ko def, bu amee lu mu'y tegtale de du weesu waru'g wax ak nit ñi, jàngal leen, ci wi nu màgge, dégg ko dégg ga ca war.


Ndax da na dagan ñu jàppe baat yu jóox yi, lu bokk ci làkk wi ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Baat yu jóox yi ñooy yi dugg ci làkk wi te bokkuñu ci woon, niki baati tubaab walla araab yi nu'y gis ci wolof.

Bokk na ci li yayoo xamle, mu'y làkk moo'y li nit ñi di wax di ci déggante'e, maanaam jaaduwul ñu naan bii baat bu franse la, walla bee kon nanu ko sanni, te nit ñi ci lanu doon gën'a déggante'e ca bu wolof ba ko fa doon wuutu, Ahmad Amiin nee na ca teereem ba tudd Fajarug lislaam: (( Araab yi de ca njëkk lislaam jële woon nanu lu sakan ci'y baat ci làkku faaris, di wu waa Iraan wi, ak wu Rom, ak wu Isipt, ak wu Ecopi, yooyu baat seen yaxantukat yi daa dem foofa'a ko daa indaale, nu duggal leen ci seen làkk wi, boole ko ci, waaye nag araabeel leen, maanaam dëppale leen ak sart yi seen làkk laaj, ci noonu Alxuraan ñew tudd leen )). Kon nag bépp baat bu nu man'a jële ci làkk, daa war'a lemu ci sarti sunu'w làkk.

Amiin neeti na ci benn teere bi: (( Yahood yi de am nanu ag jeexital gu mag ci làkku araab, tàbbal nanu ci ay baat yu bari yu araab yi xamutoon,ak ay term yu diine, yu nu xamul woon,baat bu mel ne jahannama ak shaytaan, ak Ibliis lenn lanu ci)), waxaat na ba tay ci bii teere: (( woykati araabi nasaraan yi, ku ci mel ne Xussu'bnu Saahida, ak Ummayata'bnu Abii Salt, ak Hadyu'bnu Sayd, ñoom duggal nanu ci araab ay baat aki toggaliin (taraakiib) yoy araab yi xamunu ko woon, ni ngi naan Ummayata'bnu Abii Salt moo xamal araab yi waxiinu " bismikal laahuma" , mu'y ci maanaa (ci sa turwi yaw buur bi ) ñu ci'y tàmblee ay wax aki jëf, Xussu it moo'y ki njëkk'a wax "ammabahdu" )). Ammabahdu di baat bu nu'y jëfandikoo ngir teqale wax ju bokkul ak ji la tax'a jug,mu mel ne nga'y bind bataaxel, nuyyoo, wax li'y ànd ak nuyyoo bi, ba noppi war'a jëm ci wax ji ne ( leegi nag:).

Lan moo'y jafe-jafe bi ku senegal ki di jànkooteel, ngir làkk yu bari yii nekk ci réew mi, fekkante fi, ñu'y yu jàmbur yi ak yu réew mi, te nu jël yu jàmbur yi teg leen ci kaw yu réew mi ?

Nitu'g neen ci sunu réew mii, bu duggul leekol, ak doonte dugg na ko te bu tubaab, da nga ko'y gis jamono ju nekk mu'y jànkoonte'ek lu bari ci'y jafe-jafe, ci lu aju ci ag jëflanteem ak nit ñi, aku'g jokkoom ak ñoom. Jafe-jafe yooyu lu ci ëpp, li ko'y jur moo'y ñàkk'a déggoo gi'y am ci digganteem ak ñoom, te loolu da na àgg ci jural ko ag fasu (complexe), ak ñàkk'a wóolu sa bopp, ndax lu ëpp ci waa senegaal da nu'y gëm ne seeni mbir keneen'a leen ko war'a lijjantil. Bu ci nit soxla'a dara lu war'a bàyyikoo ci "àtte" gi (goornemaa), mel ni ab dokimaa, walla lenn lu ko réew mi ameel ci àq, moom da'y gëm ne li war moo'y mu gëstu ku ko gën'a dégg tubaab, te li gën'a bari du ñeme'e wax sax ay xalaatam ak lu xalaat yi am solo !, ndaxte déggul tubaab walla lenn ci baati tubaab yi'y jox waxam jooju xiima ak fulla, loolu yobb na ñenn ñi ci nu'y wone ne dégg nanu tubaab, ba'y tudd ci seeni wax lenn ci baati tubaab yoy ni nu ko'y waxe sax manunu ko, te xamunu ni nu ko'y binde, te fekk na jamono ji nu ko'y def, fees nanu dell ak baati wolof yu man'a wuutu yooyule di yu franse. Ba ci jàngkat bi génne ci daara'y tubaab yi, te déggu ko bu baax, (ñu néew lanu ñi ko ci dégg, dégg ga ca war, ndax lu sakkan la'y jël ci seen waxtu), moom itam, day faral'a jànkonte'ek’ug fasu, walla kompleks, gi'y faral'a dal ñi'y waxe li dul seen làkk, bu ñu'y wax - te taxul ñu xoot ci lool - ak boroom yile làkk, walla ku leen ci gën'a sori. Jafe-jafe yi aju ci wàll gii maneesu ko'o takk, dees leen di lim ci'y teemeer, danu ne woon nanu ci indi yenn rekk.






Nu ne woon nu taxawlu as lëf fii ci ag wàll gu àggoon nanu ci ci'y wax, te mu'y lu maneesul'añàkk’a jaaraat, ngir am gi solo, ak yiteel gi mu def lii nu nekk di wax, loolu moo'y taxawaay yi lenn ci boroom xam-xami joojale jamono ame woon, ci yee niti seeni réew, xoolal ma ku mel ni Petrarch, nga xam ne bokk na ci li ko taxoon'a siw yile taxawaay, ba daa fàggul boppam dàkkantalu boroomu'g nite, Te dara joxu ko woon loolu lu mo'y yitewoo gi mu yitewoo woon xay gu yàgg ga (civilisation ancienne), walla bind gi mu doon def ci làkku'w itaali wi doonoon aw waxiin rekk ca jooja jamono.

Waaw lu tax Petrarch mii doon binde ci wu itaali wi, te fekkoon fi lakku'w latin wi népp daa binde ? Loolu de tontu li mooy bindul woon lu dul ngir nit ñi xam ko te jariñu ci li mu'y bind, kon li am solo moo'y nu xam li mu'y bind, man ko'o jariñoo, du mu bind ko ci latin. Lu mel ne jeqiku gii ( revolution) mooy li seriñ Suhaybu defoon bu yàggul, ba mu bindee ci wolof téereem bu am solo boobee di Qurratul Hayni ci xam-xamu diine, loolu tax nit ñi sottiku ci kawam ci'g fuqale, ñépp jariñu ci, ngir nekk gi mu nekk ci wolof, te kat téere'y diine ya'a ngi fi ak yu adduna yi, te kenn xoolu leen ngir nekk gi nu nekkul ci wu kocc. Kon man nanoo wax ne Petrarch mii moo gënoon'a ñaw te ëpp xel mbokki boroom xam-xamam yi, ndax day mel ni moo leen gënoon'a xam li xewoon, bi mu gisee ne warul ci mom mu bind ci latin, te làkk wu nu gën'a dégg'a ngi fi. Deesul sikk it ne moom dey ab jeqikukat la woon ( revolutionaire) bu bokkoon ci ni gisoon ne du man'a ñàkk ñu soppi ba ci làkk wi nga xam ne weesuwul fii mu nekk ab gàllankoor ci yoonu jëm-kanamu'g askanu Itaali wi, bi mu nekkee ci dëgg-dëggi aajowoo ag jëm-kanam, ak yéeg gu xel ak gu xalaat. Mu gisoon ne bu bëggee def jëf ju am solo ci yee, ak xamal askan wi, li ko war moo'y mu wut anam gu yòmb gu koy jàppndal loolu gën ji jàppndal, te di tax ba ñu'y man’a alawtiku li mu leen di sànni ci xam-xam ca na mu gën'a yòmbe. Lii'a ko yobb ci mu binde ci wu itaali, ba nee wu latin wi. Ci misaal sunu njiit loolee di Senghoor , nga xam ne foo toll nu ko'y tudd te du kenn, moom de boo'y xool da nga naan moom de bindul woon xanaa ngir mbokkam yii di waa senegaal, Ndax kat li ëpp ci réew mii déggunu tubaab, nga rax ci dolli dafa meloon ne ab nasaraan la , walla ku leen doon ligéeyal ci sunu kaw. Làkk'a ngi fi woon nii di wolof, di wu ñépp déggoon, walla li gën'a yaatu ci réew mi, bu Senghoor gëmoon réewam ba di ko ligéeyal, du woon binde ci tubaab, li ko waroon kay moo'y mu defoon ko ci wolof, walla sax ci séeréer ci li gën'a néew. Walla mu digale ñu firi ko ci yile làkk, mbaa mu sàkk jëwrin ju féetewoo jëmale leen kanam, ndax ëlëg ñu man'a xëy di'y làkk yu gën'a am ag koom, te gën'a yomb'a jëfandikoo. Walla kay mu soññoon sunu boroom xam-xam bu mag ba Seex Anta, mii nga xam ne lii rekk'a ko masoon'a ñor, ci mu wëy ca yoonam woowee,te gën ko'o jàpple ci xalaat ak doole, waaye deful loolu, moom kay da ko doon xeex ci anam gu ñaaw, di ko gàllankoor ci mu amal bile naal. Moom nag ca dëgg-dëgg moo'y ki fi nekkaloon tubaab bi, ndax yiteem jépp nekkutoon lu dul di gëstu lenn ak lu mu man'a tuuti tuuti ci lu ko man'a askanale ca waa-Orob ya, li'y tegtal ci loolu moo'y waxam jii ci téereem bi tudd ( poesie de l'action), mi ngi ci naan: (( j'ai probablement une goutte de sang portugais qui est frequent en Europe mais rare en Afrique noir )) maanaa mi di : man dey ku dem am naa as toq ci dereeti Portigaal, ndax man da maa bokk ci mbooloo'm dereetu'm (A) mi bari lool ca Orob te néew lool ci Afrik. Loolu mu wax ngir mu wutal ko lay daa jël yaayam ji nekkoon ku dëkk jiwaalo, taxaw temb ne Gine'g Portigaal gi la cosaanoo, ak li nday ji daa wax lepp naan cosaanoowu fa. Kon kii soreewul ak ka woy wa taxoon'a jug mu'y :((Màggat mu màggat ci am, njàggu'm tubaab, jabaroo <> tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii )). Waaye daa mel ne da ma laa gis nga naan waaw lu tax seriñ si daa binde ci araab te wolof nekkon fi ?

Tontu bi:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Seriñ si de li am ba mam, moo'y ci araab lanu daa binde, waaye ak ci wolof, te araab de li leen ci jañoon du jëmmi làkk wi rekk du woon it gòndiku ci, walla fònkadi wii di seen wos, mbaa foñ ko te weddi ko, ba loolu di leen ci'y tee di binde ak'a tase seeni xalaat. Li fi nekk moo'y ñoom seenu'g xér gu tar ci nit ñi doon ay jullit yu dégg seen diine, rawati na alxuraan mi deesul dégge ci lu dul araab, moo leen àggale woon ci ag wàll ci seeni ligéeyi xam-xam rawati na la ca aju woon ca diine ñu ko daa defe ci araab. Ñoom de dañoo gëmoon - te loolo'ooy li waroon- ne alxuraan mii kat aji nekk la ju fees dell aki kiimaan aki way lòttal (aji lòttal nag bu nu ko waxee ci xam-xamu diine mooy lol Yàlla rekk'a ko man, lòttal na mbindéef yi ag defam). Benn tafsiirkat - seen gëm-gëm laa la'y wax- amutoon kàttanu'g leeral ko, mbaa mu indi lepp ca tafsiir ga ca war, ak leeral ga mu yayool, moo taxoon nu gisoon ne nit ñi daal ci masala mii, ñoom ñépp'a ci yam, maase ci ni bëñi peñe, kon li leen doon noppal ci seen gis-gis, moom'y nit ñi maaseendoo jàng araab, ku ci nekk lijjantil ko sa bopp, settantalal sa bopp ci way teddi aaya yii, ci lu dul nga'y sukkandiku ci kenn. Ndax kat kenn gënu leen ce'e man'a dimbale seen bopp, bu nu déggee araab, bu nu ko deful nag, lu nu ci man'a ame itam am raxasiit rekk lay doon, aw desiit, ag wall ca lépp rekk la’y doon, du weesu yu njëlbeenu yi rekk , deet yu mag yi. Waaye jàngale gi ci araab ak bind ci, teewu leen woon di bind ci wolof ak'a bindante, ak di ko jéem'a jàllale, ci taalif ci ay woy yu rafet te sakkan, fees dell aki baat yu xoot, yu naroon'a réer moos bu nu ko deful woon, aki masala'y nahwu (grammaire), amoon nanu ay xisa yu yéeme, ami nettali yu adabé (yu njàggaté), aki cax yu xoot yu daa dimbalee ci màggal am xel, rawati na mu gone gi. Seen woy yooyu ak nettali yi danu daan fees - ci li ëpp - ak lu’y yare,loolu bokkoon na ci li daa dimbale yarkat yi, ndaxte ñu ci ëppoon fekkoon nanu nit ñi nu di boroomi jikko yu rafet yi ñu dégge ci woy yooyu ak léeb yooyu.

Xoolal ma léeb wu mel ni ( Kumba am nday) niki misaal ci ay nettali yu di kojug yar, yu'y dund, tukkee ci sunu réew mi, moom de lu am solo la ndax daa fees dell aki misaal yu kawe. Moom de day soñ ngone yi, rawati na jigéen ñi, ci ñu ràngoo jikko yu rafet yi, ñu'y muñ, farlu, nangoo dee ci lu baax. Loolo'oo tax ñu man ne ñaari làkk yii, daal duñu wooni noon, waaye way mottaleente lanu woon, yu daa dimbalante, bii ñu ko'y jëfandikoo ci li ëpp, ci wàllu'g diine ak jàppe ko jumtukaay bu am njariñ ci dégg alxuraan mu tedd mi, te fiqu ci jile diine, ndax faqiih moom muy ku xam fiq, maneesu ko'o nekk ci lu dull dégg bu baax araab, kenn mant'a dégg jile diine, di jariñu ci xam-xam bi ci nekk te déggoo araab, loolu xaw naa jòmb. Senghoor sax seere na loolu ca ( poesie de l'action) , mu ne: (( je suis pour le mainien du Latin coome langue universelle de l'Eglise catholique, tout comme je duis pour le maintien de l'arabe comme langue de l'Islame)) maanaa mi di man ànd naa ak ñu tëyye fi Latin niki làkku egliisu kotolik bu adduna bi, ni ma ànde ci nu def araab lakku lislaam. kon nag li nu sañ'a wax mooy mag ñi de, wolof lanu jàppe woon seen làkku ofisel, te daa nanu sonn it ci jëmale ko kanam, daa sukkandiku ci loolu ci làkku araab, seenu'w jàngaliinu araab it walla xam-xami diine ñi ngi ko daa defe ci di tekki baat yi ci wolof, baat bu nu la wax rekk wax la ba mu tollool ca wolof, loolo'o jur riisu'g wolof gii, fees dell ak baati araab yu nu wolofal, tax it ba yeneen baat ci wolof am yeneen maanaa, yeneen tëggiin it sosu yu manul woon'a ñàkk, te feeñe ci wonu'g araab.

Ndax nag du'g dofe, nu sanni nële sunu lakku nday wii, ngir jël weneen wu keneen, di ko jëfandikoo niki ofisel - naan dafa yor ci way yayale'y xam-xam ak yu xay yu wosam amadi - ci jàngal sunu'y doom yu ndaw ak yar leen. Ñun de ci loolu danu'y jàmmaarloo ak lu sakkan ciy coona ci xamal leen, te déggal leen ci anam gu dëgër, te gaaw. Ndax gënul woon'a dëppoo ñu jëfandikoo sunu wos wii, ngir mu gën no’o jappandi - ca anam ga mu gën'a yaatoo - nu sol leeni xam-xam ci lu dul gën ja'a neewi coona?.

Ndax yellul ci nun nu jéem'a lijjanti sunu jafe-jafe yu bari yii nga xam ne foo wëlbatiku gis leen, ñu'y yu koom ak ak ak, te'y yoo xam ne jafe ge'e lijjanti foo ko takk weesu na ko, te ñu soxla lool ku ci jéem, te bàyyi nag sonn gii nu'y def - ci kem bu rëy bii ci'g farlu ak yitewoo - ci yekkati jeneen aada walla kiltiir ju di kojug jàmbur ?. Ñun de foo nu fekk ni ngi wax, ba sunu'y gimiñ yi sax - ci li'y feeñ - xanaa amatunu beneen ligéey bu leen war ci seenu'g dund, bu dul joyal baatu'b frankofoni, jaarale ko ci diggante seeni bëñ ànd ce'ek as lëf ci'm mbég ak màggal. Bii baat de da'y dikk di bawoo ci put gi ci'g diis, bijj nag ay mbiccam, di lu ñu peege mbalaanu'm wurus mu wormaal ak jox àq, bu ko defee mu bocciku nag ci'g rëy mel ni moo'y buur bi, te fekk na ne nëbbul ci diggante ay lem-lemam lu toll ne peppu suuf ci maanaa, aha kay, xanaa mi nekkul lu dul sanni ca àll ba, lépp lu la fi sa maam bàyyil ci ndono lu xam-xam mbaa cosaan, te'y sonn ci jañ pono'y aada'y tubaab ak aw làkkam jëm ca kanam, ak yitewoo ko mel ne moo'y lépp, sànni ca sa ginaaw lépp loo moomoon ci làkk ak xay, naaneey: du dara lu dul ag wëy (paase) aku'g dellu ginaaw, te ag teew amul ñeel ku amul'ug wëy .

Man de noonuwuma tubaab waaye xam naa ne yayoowul ci ñuñ gii yitewoo gu mag... ci sunu's alku.

Lii nag gëstu la bu ñu doon def[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lii nag gëstu la gu ñu doon def, bëggoon ce’e génne lii nu peek, wër nu ci’y jafe-jafe, rawati na yi ci di yu aju ci sunu li làkk li laal. Waaye nag ba tay gëstu la gu njàggat, gu nu jublo’o def ngir génnewaale ci as lëf ci taaru’b wolof, ak li mu làmbool ci’g nooy ak man’a ëmb. Mu doon it ag woote jëme ci luñutu ak jam (critique ), ak def lu mel ne lii gu tukkee ci geneen wàll gu nu moy . Kon sunu yëf’a ngoogu, di lu aajowoo xalaat, xool, sònn, yitewoo ak jàllale. Na léen wóor nag ne ci’g solowoom ak’ug déetam , népp la ñeel, népp’a ko ñeel it, ndax sunu mbir la , di ménn ci yi nu man’a jëmale kanam, bu ñu ko fonkee, ci li ma jort.

Gongikuwaay[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Abdu Xaadir KEBE

Xool it[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • ay rajo yuy wax wolof ak tele:




Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons