Yàlla
Yàlla, Buur Bi, Sunu Boroom, Aji-Màgg Ji, Aji-Sàkk Ji..añs lépp a ngi joxoñ Ki sàkk lépo ak ñépp.
Yàlla (ar : الله ; fr : Dieu; en : God)
wolof naan ko Yàlla, njëkk Lislaam wolof "Yal" la daan wax namm ci "Yàlla" bi Lislaam dikkee, bawoo ci araab yi naan "Àllaa" ci lañu jëlee "Yal" yokk ci "Àllaa" naan "Yàlla" waaye teewul ba leegi wolof yi di jëfandikoo baatu "Yal" jooju ci seen i ñaan niki "Yal nanu Yàlla jéggal" "Yal na la Yàlla sàmm"...añs.
Diine Yépp Saxal nañu ag Amam, donte wuute nañu ci jëmmam ak i meloom ku ne ak na mu ko jàppe. bu dee ci diibey kojug asamaan yi wuutewuñu ci ne Moom ki bind lépp te kenn bind ko niki diiney Yahuut, Nasaraan ak Lislaam.
Lislaam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci lislaam jullit ñi dañuy saxal amug Buur Yàlla mu bokk ci juróom benn ponki ngëm yi nekk ba ca jiitu ànd nag ak anam yu ñj ko war a gëmee, nde am ay melo yoo war a saxal ci Jëmmam Ji, am yoo war a dàq jommale Ko ko, am wow day dagan ci moom. ni nu Koy gëmee nag mooy gëm ne am na te moo fi jiitu lépp te du fi jóg te nuróowul ak menn mbindéef te ku doylu la ci boppam, aajowoowul jëm ci kenn te kenn ku ne ak lenn lu ne aajewoo na jëm ci Moom te it Kenn la ku amul kenn ku ko ñaareel ci jëmmam walla jëfam wallay waxam walla wenn meloom, ku am kàttan la koo xam ne balaa daraa xew da koy bëgg te na mu ko bëggee lay amee, ku am xam-xam la kog réeréewul darra, mbooleem li nu nekkee ak li nuy bëgg a nekkee darra umpu ko ci, day dund, day dégg lu kawe ak lu suufe, di gis lu nëbbu ak lu feeñ, di wax.
Li jomb ci Moom nag te mooy li mënul a am moo di ag ñàkk, ñu naan Yàlla am na te amul ak sosu nga xam ne mas naa ñàkk ginnaaw bi mu am walla darra am te neexu ko walla ameewul na mu ko bëggee walla muy tëx walla mu tëlee wax walla mu ñàkk a xam walla mu gumbë walla mu réerée darra walla muy faatu, li nga xam ne man naa am ci Moom man a ñàkk (Mooy Lu dagan) mooy def ak dindi, mbooleem li ngay gis walla mu toq ci sam xel daa dagan ci sa Boroom, bu ko neexee amal ko bu ko neexee ñàkkal ko. Boo boolee melo yii yépo day tollu ci ñaar fukki melo, mu war ci jullit bi mu gëmee ko nii.
Bu nu delloo ci Alxuraan diba nu fekk Muy melal Boppam ciy warab yu fasantikoo ci biir téere bu sell bi, mu bokk ca Saar wi miy melale Boppam walla nu ne Da ci doon aajar Boppam; muy Saar 112 : SELLAL 4 - Laaya – Laata Gàddaay ga
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Waxal ne : “Yàlla, moom Kenn la (jenn Yàlla rekk la). 2. Moom Yàlla, Mooy Kilifa gi wareefa joyal mbir yi. 3. Jurul, te Kenn juru ko. 4. Te amul benni nàttangoo”.