Xaralaymbëj
Xaralaymbëj Mooy xam-xam biy gëstu lépp lu jëm ci wàllug mbëj, ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam. bu njëkk dañoo foogoon ne ag wal la rekk guy dem, gu man a nekk luy yokku(+) walla wàññiku(-). Waaye ci ndimalu ay woroom xam-xam yu mel ne Hertz, Helmholtz, Maxwell, Heaviside, Alessandro Volta ak ñeneen ñu bari, ci lees dem ba gën a nànd, xam mbir mi. Lu mel ne yamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinu yani mbëj yi( feppsaal ak mbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj) walla toolu mbëjbijjaakon ba ca juddoo.
Ci gàttal, ci noonu lañu tambalee gis yenn ci ay jëfandiku yu mbëj: Doxalukaay bu mbëj, soppalikaay aki leeru...
Tay xaralaymbëj moo yor wàllu sàkk ay wuutuloxoy mbëj ak ay buumi séddalekaayu kàttanug mbëj
Tëraliin |
[Soppi] Ay Faramface
Ay faramface ak ay àtte yi lal xaralaymbëj.
yamaleb maxwell yi, ñooy àtte yu am-solo yu ñeel mbëjbijjaakon, ci la yeneen yi soqeekoo.
àtteb ohm(om) yiy faramface ndëgërlu gu mbëj gi
àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy faramface sababu bijjaakon
njeexitu joule mooy leeral ni kàttanu mbëj di soppeekoo nekk tangoorngir njeexitu ndëgërlu gi.
àtteb Kirchhoff(kiirkof) mooy leeral jëflante bi nekk ci diggante dawaan ak taraay ci ag ndombo.
[Soppi] Jóox, yóbbu ak séddale kàttanu mbëj
Ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya (barab yees koy jëfandikoo). Kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ay jurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel, li ñuy wax diggub mbëj, ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi.
Buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëlee kàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya.
Li wuutale Buumi yóbbukaay yi, mooy limu taraay gi ñuy yóbbu, moo tax ñuy gis ay buumi dend gu kawe, dend gu diggu, dend gu suufe. Su diggante jóoxuwaay yi guddee, dañ fay def ay mbëjjaru, ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioŋi watt ci kàttan tambalee ciy 400000 v. Buumi dend gu kawe yii la ñuy duppe yu yóbbug kàttanu mbëj, yi nga xam ne ñooy tax ñu man a yóbb kàttanu mbëj gi, jëlee ko ca jóoxuwaay ya jëmee ko ca barabu soppikaay ya.
Ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu, jaarale ko ci ay wuutuloxo yu mbëj yees di duppee soppalikaay, ci noonu nag la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu gi, moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cig ndombog séddaleg kàttanu mbëj, foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi.
[Soppi] Wuutuloxo yu mbëj
[Soppi] Doxalukaay
Doxalukaay yu mbëj yi, ay wuutuloxo lañu yu’y soppi kattanu mbëj def ko kattanu doolerandu. Doxalukaay yi dañu leen a seddale ci:
- Doxalukaay yu dawaan bu wéy
- Doxalukaay yu dawaan bu safaanu, bii man naa dox ci ñaari fànn ( ñettwéq, wennwéq), ci nii ñu am:
-
- Doxalukaay yu Doxalukaay bu demandoo: su fekkee baraayu ni muy wëddeeloo demandoo na ak baraayu ndombo li
-
- Doxalukaay yu Doxalukaay bu demandoodi: su fekke wëddeeluwiinu boppam la am.
- Doxalukaay yu wennwéq
[Soppi] Jurukaay
Jurukaayu mbëj yi Ñoom ay wuutuloxo lañu yuy soppi kàttanu doolerandu def ko kàttanu mbëj. Yi ci gën a raññeewu:
- Safaanukaay, mooy juddal dawaan gu safaanu
[Soppi] Soppalikaay
Soppalikaay, Ab wuutuloxo la, maneelam mooy soppi limu dendu mbëj gi nekk ci ab ndombo, ci yokkute walla wàññi. Lu mu néew néew di na am ñaari lëmës yu bijjaakon boole.
Wuutuloxo yu man a yokk walla néewal taraay te di jëfandikoo benn lëmës rek, lañuy tuddee Soppiboppam
[Soppi] Leeru
Ay jumtukaay lañu yu aajowoo soppi kàttanug mbëj mu nekk leer. Di ko jëfandikoo ngir leeral barab yi.