Gëstubiddiw
Gëstubiddiw mooy mboolem aada ak gëmgëm yi japp ni fi jawwu yi féete ci nosteg jant bi ak biddiw yiy feeñ ci asamaan si ci yenn jublu yi, ci yenn bis yi, ak ci yenn waxtu yi, manees na cee jaar jàngat lu xew walla lu nar a xew, moo xam muy lu ñeel kenn nit mbaa mbooloo. Ginnaaw nag xam-xam la boo xam ni ci aaday aki gëm-gëm la aju, aada ju nekk am na nu mu ko gise.
Boroom xam-xam yiy tënku ci lu xel nangu nag, dañu koo jàppe ni xam-xamlu, ñenn ñi yegg ci jàppe ko gëmgëmu Yëeli (Yàlla ju wérul). Mboolem gëstu yees ci mas a def ca jamonoy yàggte ga ba léegi ci dàq ko lay mujj.
Ñi koy layal nag dañuy wax ni wax luy xewi ëllëg taxukoo jug, ndax man naa nekk luy bijji nit ki ba mu def lum jortulwoon ni man na ko ngir am yaakaar ci ëllëg.
Français:astrologie Eglish:astrology
Xam-xam | ||||
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma | ||||
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal | ||||
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama |