Cosaan

Jóge Wikipedia.
Dem : Joowiin, Seet

Cosaan

Cosaan (Ndangane, Senegaal)

Ci angale mooy tradition. Ci faranse mooy tradition.

Ci xëtt wi, dama cee fas yeeni jeema tekki ani lan moodi cosaan. Sama weerukay ci walu xam-xam moodi jangat-nit. Bile baat, manko tëggé ci (anthropologie), manaam anthro=nit ak pologie=jangat. Cosaan, aada, ak luñuubaaxo daño fasoo, dugantè lu bari. Waayé, ci sama gis-gis, cosaan moy reenu askan, manaam fu aw askan bayee koo. Bilep firi daa ajju si walug bërëp (espace). Cosaan, mana firi batay luñu donnu ci makk ñi. Kon ci tënkk, cosaan, moy reenu askan, di delu waayu askan. Ndaxte cosaan moy lunġa xamni moom la maam yi daan def. Boo länkalee cosaan ak aada, di luñu baaxo def, loolu moo lay jox "culture". Culture nak moo gena mattalee boy séet. Ndax baat la bu eumb mboleem fan yu doomu aadam fèntt, ligeey, ak lumu deffar ak loxoom, wala mu xeltu ko ta mu jem ci walu dundam, man nañ jappé "culture". Kon, suma suka ndikoo ci lii ma fessäl, dama jeema wax ne, cosaan mooy "tradition", "origine"; aada mooy "coutume". Waayé buma juumul, baatu "culture" dafa boolee aada ak cosaan. Cosaan nak, ci walu xeltu, baat bu jaxaso la. Ndax limuy tekkine ay jëff, ay gis-gis, ak ay mbir yuñu donnee ci maam yi la moo waral mu lëntt. Sama laac moo: cosaan "eumbu" wala ab yan bu makk ñi doon aw laantoo, dalee ko ci maam yu yag ya ba si jamonoy tay ji? Wala book, cosaan, nekul rek ab eumbu bu nga xamê si dara soppe ku wucci la ta ñu don nee ko ci maam yi la, waayè mbir muy soppee ku la. Manaam luñuy jellee ci makk ñu jekk ya, ta diko mengalee ak nekinu tay, mélè kaanu tay. Gëstukat yu barri daño jappu ne bu fekeeni cosaan ab eumbula, kon du luñu wara soppi; waaye bu nekkee lu dox, dalee ko ci jamano yu yàg yala, kon luy walbatiku. Nittu jamano boo jall, dañu tànn ci seen cosaan ay lëff, wacci licci dess. Rax ci dooli, dañuy fentt ay mbir yu bees dolli ca. Bilee gis-gis, booy seet, moo gena am maana, gena dal xèl. Ndax day junjju ne, aw askan warula wax ni sama cosaan kon duma ko bayyi. waaye day tànn li gena rafet ci cosaan, baayi li mengowul ak jamanom. Waaye timit, nguuruk reew munek war jôk aar cosaanam ci coppiku aduna bu gaaw bilee. cosaan ak aada Reew yi eup doolee dañu wali cosaan reew yi new doolee, ak dileendi nasaxal. Jokkoo ak waxtaanu cosaan yi, manaam ni ñuy abalaantee, lu baaxla. Bu loolu amul, yokkute du am.

Bu njekk, borom xam-xam yi bayoo tuggal ta see gëstu ajju ci walu jangat-nit, daño weddi woon ni nit ku ñuul amul aada ak cosaan. Li lalloon bilee weddi moodoon ne see dëuk yi ñoo bagoona noot, jalgate axu doomu adam, moom (coloniser) ngir asaloo seeni kom-kom. Bi aduna doxee ba nootagee bi jeex, bu afrik moom boppam, xam-xamu tubaabbi tasaaro, ñeppu nagu nagn ni askan yeppa am aada ak cosaan, ak seeni mbaax (valeurs).