Melosuufug Burkinaa Faaso
Mi ngi nekk ci goxub Afrig, ci diwaanu sowwu Afrig, rëyaayam di 274 200 km², 81u réew mu ëpp ci àdduna bi Burkinaa Faaso Mali moo wër ci bëj-gànnaar ak ci sowwu, Niseer nekk ci bëj-gànnaar-penku ak ci bëj-saalum-penku, ci bëj-saalumam Togóo, Gana ak Kot Diwaar ñoo fa nekk. Kon amul ubbeeku ci géej gi. Doon na réew mu tappndaar ndaxte pujam bi gëna kawe Tenakuru te kawewaayam toll ci 747 m ca sowwu réew ma.
Li mu am klimaab gëwéel mooy tax ñaari jamono rekk la am, noor ak nawet. Ni senegaal, li gëna féete bëj-gànnaar dafa tàkku, ci fi tollook Sahel, looy gën di wàcc jëm bëj-saalum muy soppiku di doon ab mandiŋ. Di nañ fa fekk itam ay àll rawatina ci diwaani Bobo-julaaso ak bu Banfora, soo jëme itam Gawua ak fi jege dig yu kot-diwaar-gana
Xool it
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Xool it Wikimedia Commons
|
Melosuufug Afrig |
Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkinaa Faaso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Bennoo yu Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eriitere • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Gine • Gine-Bisawóo • Gineg yamoo • Keeñaa • Lesoto • Liberiyaa • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeriyaa • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome-ak-Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togo • Tuniisi • Sambi • Simbaawe