Jeqiku ga amoon ca Faraas
Jeqiku ga amoon ca Faraas, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (jeqiku googu), mi ngi ame woon ca Faraas, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benneel ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu tollu ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g) defee daaneel nguur gu ñuy wax “daaneel nguur gu 18 Brumaire”, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri réew mi. Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Faraas gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk-jàmm ga, tiitale ga , tuur-dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak jeqikug Faraas gi. Loolu nag taxoon na ba “jeqiku gi” manu fi woon a amal dali gore(principes de liberté) , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi. Waaye nag jeexiital yi nga xam ne jeqiku gii amal na leen fi, yamuñu rekk ci Faraas, waaye weesu nañu ko ba daj Tugal gépp, ak lu bari ci réewi àdduna bi.
Ni Faraas meloon laata Jeqiku gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu ñu gëstoo na Faraas meloon laata jeqiku gi, loolu dinañu dimbali ci ñu man a xam li waral jeqiku gi, atum 1789 g:
Melokaanu politig wa :
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Buuri Faraas yi, ni ñu doon àttee Faraas, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lépp, képp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo dégge ci waxi buurub Faraas bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ).
Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon(ay lois) , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir ñu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la jeqiku gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi.
Moom de jëwriñam yi danu koo yilifoon, ak bëkk-néegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal (reforme), kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar. Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Faraas yi bañoon.
Njabootug Barbon gi, yàgg nañoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Faraas wi, ñoom daal dañu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo réew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp dañu ci daa duma Faraas. Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali réew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolluwoon nañu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu ñu fay liggéey lu amal njariñ réew mi. Looloo taxoon njëlul nguur gi loofoon, mujjoon moom nguur gi fees dell aki bor.
Nguur gi kat mujj na ay sànkam (ay deppaasam) àgg ci 130 milyoŋ yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyoŋ yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon.
Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe-ni-la-neex ga amoon ca wàllug politig ga. Nattukaayi diiwaan bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Faraas mujj di réew mu ay diiwaan boole, diiwaan bu ci nekk am ay yooni boppam , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak yoon yi, réew mi mujj séddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Faraas mujj doonatul menn réew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas.
Na mboolaay ga meloon:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mboolayug Faraas gi, njëkk jeqiku gi, dafa séddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: garmi yi(kureelug ñu tedd ñi), kuréelu niti diine yi, ak baadoola yi walla kuréelu mbooloo mi. Ñatti kuréel yii nag – ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu – yamoowuñu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay wartéef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jëfkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay.
Garmi yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu ko defee kuréelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa féetewoo pal yu kawe yi, yu ñoñ yi (siwil)ak yu xare yi , ci nguur gi. Ñoom ba tay, daa nañu am ay cér ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm si, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amuñu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi.
Niti diine
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]“Niti diine yi” nag ñoom, seen kuréel moom itam bu ràññiku la woon, niki bu garmi yi, ñoom de daa nañu am ay suuf yu ñu leen dogal, yu yaatu, yu daa toll ci jurooméelu suufi nguur gi, maanaam bu ñu xaajoon suufi nguur gi juróomi xaaj, benn xaaj bi. Ñoom itam, ñu ñu teggiloon ay galag lanu. Li Jàngu bi daa ame ci suufam yooyu, ak ci galagi diine yi nga xam ne mbooloo mi daa nañnu ko ko fay, àggoon na ci 200 milyoŋ yu Farank.
Loolu lépp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu néew lañu daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool ñi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbali. Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu féexoon, moo taxoon dañu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi.
baadoola yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Kuréelub mbooloo mi di "baadoola" yi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lañu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi jeqiku gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyoŋi nit , te kat booba garmi yi bu ñu leen boolee ak niti diine yi weesuwuñu woon 300 junniy nit. Coonab galag yépp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kuréel googu nag (gu baadoola yi), moo ëmboon kuréel gu diggu gi(Bourgeois), ak kuréelu baykat yi ak gu boroom mécce yi ak gu soldaar si.
Kureel gu diggu gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu dee kuréel gu diggu gi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amuñu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi ñu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon.
Lii lépp nag taxoon na ba gii kuréel meroon lool ci nguur gi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li ñu defaloon ñaari kuréel yii di gu garmi yi ak gu niti diine ñi.
Kuréelug baykat yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu dee “Kuréelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kuréelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lañu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen liggéey yi gën a tar.
Kuréelug soldaar si
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu nu nee “Kuréelug soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi ñoom, ak pal yu mag yi, garmi yi lañu leen daa jagleel.
Na fa xalaat meloon:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ak li Faraasu njëkk jeqiku gi, di gënadi woon a nekk cib coona, ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lépp, teewul waa Faraas a gënoon a yëg yeneen réew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs.
Jamono jii , dafa fiiroo ak diggante bob Faraas da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nostey politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya.
Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy liggéey nañu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi jeqiku gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau
Montesquieu
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu réew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay liggéeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca téereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), téere boobu nga xam ne téere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Faraas ak feneen.
Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk nguur gi, te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju wéyal ji(mbaa ju doxal ji, ak ju laman ji .
Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci téereem boobu mooy taxawal ag àtte gu tegu ci sartu réew ca Faraas. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu réew bu buur ba amoon ca Angalteer.
Voltaire
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Faraas wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam lañu woon ak yéjj(saboote) . Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Faraas ak gu Jàngu ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi.
Wolteer
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lépp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Faraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital.
Wolteer de gore ga peéxte ga waa Angalteer amoon da koo neexoon lool, yéemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginnaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy dañu koo dàqe woon Faraas. Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca téereem ba tudd “bataaxeli xeltu” , walla “ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer”, atum 1734 g. Wolteer nag dàq gi ñu ko dàqe woon Faraas, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lépp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi. La desoon ca dundam ga lépp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër.
Jean Jacques Rousseau
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom téere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy téere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti nguur gi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi. Jeqikug Faraas gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi fraas-fraas bi – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci téereem boobu nu doon wax leegi.
Jafe-jafe bu koppar ba:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Atum 1789g, mooy at mi jeqiku gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom-koom, waaye la waraloon jeqiku ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari te tar. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon.
Luwis 16, bi mu ñëwee jéem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kuréel yu xeet wi” – bii nga xam ne dañu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje.
Naka la Jeqiku ga ame woon :
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Doomi kuréel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul réew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir ññu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yéwénal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yéwénal(reformes) yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Faraas man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk.
Ci noonu ag wuute am ci diggante kuréelug garmi yi ànd ak gu niti diine yi ci wàll, ak kuréelug baadoola yi ca geneen wàll.
Bu ko defee waa kuréelug baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cér yi te bañ a sukkandiku ci ay néeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kuréel gu nekk ci ñatti kuréel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kuréel yi (gu garmi yi ak gu niti diine yi) gu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kuréel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cér , ne daal ay néeg ñooy woote, bi loolu amee, céri kuréelu baaloola yi dañoo daje ñoom nee, cig beru, ñu néew ci garmi yi ak niti diine ñi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de duñu bàyyi mukk lii ñu nekke li feek wutaluñu réew mi ab sartu réew bu man a yéwénal séenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kuréel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi réew mi, bu ñu booloo, waxul bu genn taqalikoo nee, beru.
Ci noonu way daje yii nga xam ne dañoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lañu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Faraans, bi nga xam ne day leeral li waa Faraas bëgg, tey jéem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug jeqiku gi.
Tolluwaay yi nga xam ne jeqiku gi romb na leen:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Céri ndajem xeet wi daje woon nañu ca Versailles ngir defaral Faraas ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, génne ña ñu fa tëjoon ngir politig. Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la jequiku gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Faraas wi di màggal, at mu nekk .
Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Faraas, dem feneen.
Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Faraas, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci jeqiku gi, ndax du seen njariñ, dañu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ .
Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag aar gu réew ngir wattu jeqiku gi, aar ko,aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba. Xarekati jeqiku gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse ak gënjëng (violance) .
Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi. Xeet wepp mujj daanaka di jàpple jeqiku gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu (forces armées)ju Faraas ji mujj fekksi “aar gu réew “ gi nu taxawaloon ngir wattu jeqiku gi. Ci noonu mbooloom xare mu Faraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba.
Waaye way jeqiku yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim réew mi, ak mu Jàngu bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon Paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu jeqiku gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Faraas gepp, ñu daal di séddalewaat Faraans def ko ay doxaliin yu bees .
Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jéem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jéem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy génn réew mi, gis nanu tam benn wayndare bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon dañu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan.
Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 satumbar 1791 g, loolu di bi jeqiku gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Faraas bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Faraas la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi. Mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Faraas wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy dañu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur saxoon na ca Faraas ba ca 21 satumbar 1792 g.
Geneen tànnéef
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci atum 1792g, geneen tànnéef amoon na, gu ñu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Faraas, ca 21 satumbar 1792 g. Ñu féetele ko doxal réew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg pénc gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar jeqiku gi, aar it Faraas ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci réew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen réewi Tugal yoo xam ne dañoo noonu woon jeqiku gi.
Féetale nañu ko ba tay taxawal goornamaa bu Faraas bu dëgër, boo xam ne da fiy jéem a jële fitnay biir réew mi.
Ñi jiite woon góornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne dañoo gëmoon ag yéwénal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne dañu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, dañoo gëmoon ne fii Faraas toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi.
Liggéeyub goornamaa bu jataayub xeet wi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci réewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Faraas, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginnaaw bi nag góornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kuréelub kaaraange, féetale ko liggéeyub aar Faraas ci ñiy noonu jeqiku gi ci biir réew mi, ñu féetale ko ba tay moom kuréel bi, wàlulug taxawal am mbooloom xare mu Faraas mu dëgër, ngir aar Faraas, ak jeqiku gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xéewal, moom jeqiku gi. Góornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi am na ndam ci kaw xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Belsig ci ñu fipp ci kaw Imbraatóor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali Paap gi ci diiwaanu Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon jeqiku gi (moom Paab gi).
Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kuréelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nañu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre képp koo xam ne yaakaaroon nañu ne da ngaa àndul ci jeqiku gi ak gaay jeqiku gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Faraas yi, ci tuumaal leen ne dañoo def ay wor yu mag. Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nañook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci réewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar jeqiku gi, ak doonte jàmmaarloo woon nañook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar réew mi, tas te giimal féttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir réew mi, duggal seeni xarekat ci Belsig ak Holand, ànd ak loolu lépp teewul waa Faraas bëggoon ñu soppi séenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu.
Ci 29 sulye 1794g, la céri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Faraas bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi.
Goornamaab doxaliin bi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonoy tiital, xuppe ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu ñu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginnaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Atte googu walla góornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy liggéeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon:
(1) Def politig bu maandu ci biir doxaliinu réew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam
(2) Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi.
Nañu fàttaliku ne góornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cér yoo xam ne dëppoowuñu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig góoramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig. Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nañu, ni ñu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon daane nguur googu ñuy wax daane nguur gu Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu néewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Faraas te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lañu nekkoon.
Napoliyon Bonaparte:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Asaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Faraas da koo mujjoon jënd ci Genova. Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi génne ca bànqaasu xare ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kuréelug kano ya ca xarekati Faraas ya. Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali jeqiku gi , te fonkoon leen. Moom nag ab biddiwam a ngi féqe ci ginnaaw bi mu songee Itaali. Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Faraas, dafa séddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Faraas gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g.
Song gi Napoleon defoon Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Góornamaab doxaliin bi, dafa féetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu ñuy wax gu Cherasco. Napoleon defati ab xare ak dooley Paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, néewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare. Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Faraas, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Faraas.
Song gi Napoleon songoon penku bi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Politigkati Faraas yi naaloon nañu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nañu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca géejug Mans. Politigkati Faraas yi, li ñu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Faraas ci géej gu diggu gi, ak man a àgg ca géej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk ca penku.
Góornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko dénkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, géeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Faraas. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Faraas mi, ca ndoxum dóoxug Abii Xiir (golf), moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Faraas cangug géej gi Faraas yàgg a gent. Fraas sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jéeri ci mu géej, mu mel ne mu Britani mi.
Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xareb jooñe la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xarey jooñe ya amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga.
Isipt
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon réew mu nekkoon ci ron àtte gu Usmaan[ gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam. Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nañook moom, xeex ak moom xeex bu tàng ngir aar seen réew. Waa Isipt yi béguñu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy dañoo fippoon ci kawam, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “jeqikug Xayra gi” . Napoleon jawali na réewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginnaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, akYafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci géej gi, waa Usmaan yi di ko jàpple ci jéeri ji.
Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji ñuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginnaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam.
Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa teertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Faraas, waaye ci anam gu baaxul ci góornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule góornamaa. Bi ñuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga.
Ay ngérte , yu am solo juddoo nañu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk:
(1) Xareb Faraas boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu féete, ci wàllug jokkoo ak tuxute, ñeel imbraatoorug Britani gi ci penku bi.
(2) Xare boobu Faraas da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise réewi Afrig gu bëj-gànnaar gi.
(3)Boroom xam-xami xare boobu, bi ñuy ñëw, indaale woon nañu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nañu fi it benn sémb bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak géej gu diggu gi, di kàmbug Suwes bi(canaalu Suwes), te it indaale woon nau fi ab moolukaayu téere ci araab ñu koy wax moolukaayu Bolaax bi.
(4) Xare bi wutoon na ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Faraas ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs.
Napoleon ak réewi Tugal yi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte amoon na ndam ci kawam ca xare ba ñuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon ponk ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xaatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Faraas ji génn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara.
Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Jàngu bi ci Faraas. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbéel.
Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyéel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi.
Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak réewi Tugal yi. Britani amoon ndam nag ci kawam ci wàllug géej gi, ca xare ba ñuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan akAleksandar mi nekkoon Xaysarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, ñu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal gepp, jëme ko Britani , daal di woon ga (manante) réewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci réewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na réew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu Xaysar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca péey ba, di Butrusburg, waaye mujj nañu manatuñoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal ñuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def liggéeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi ñuy dellu nag la waa Riisi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg.
Bu ko defee, waa Tugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy dàq ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona ñu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginnaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Faraas yi, ngir xeexi réewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g.
Bu ko defee, réewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir séddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos réew yu am doole yu peek Faraas wër ko.
Liggéeyi ndajem Vienne:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Liggéeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon:
(1) Way daje yi delloowaat nañu buuri Tugal ya ca seen réew ya ñu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Faraas ak Espaañ.
(2) Britani jëloon na sancu yi Faraas moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos.
(3) Riisi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Belsig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowuñu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di “nationalisme” gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nañu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Riisi ak Otris ak Brusiya, dañoo defoon seen bopp ay réew yu ñoo am ag kilifteef ci réew yu Tugal yu ndaw yi.
Li juddoo ci jeqikug Faraas gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi](1) Jeqiku gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral réewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi.
(2) Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kuréeli mboolaay yi, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nañu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal.
(3) Jeqiku gi ci Faraas mooy gi njëkk ci jeqiku yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki déggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay baat yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees.
(4) Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lañu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gépp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee.
(5) Xalaatub jeqiku gi law na ba àgg ci Tugal gépp, ak yeneen réew yu dul Tugal, yu àadduna bi.