Aller au contenu

Riisi

Jóge Wikipedia.
Federaasioŋ bu Riisi
Raaya bu Riisi Kóót bu aarms bu Riisi
Barabu Riisi ci Rooj
Barabu Riisi ci Rooj
Dayo 17 075 400 km2
Gox
Way-dëkk 144 463 451 (2017) nit
Fattaay 8.4 nit/km2
Xeetu nguur
- Njiitu Réew
- Njiitu Jëwriñ
-
Dmitry Medvedev(Ind.)
Vladimir Putin (UR)
Tembte
- Bawoo
- Taariix
Péy ak rëddi
- Tus-wu-gaar
- Tus-wu-taxaw
Mosku
55° 45′ Bëj-gànnaar
     37° 37′ Penku
/ 55.75, 37.617
Làkku nguur-gi Rissiyan
Koppar Rible (RUB)
Turu aji-dëkk -Riisi-Riisi
-Sa-Riisi
Telefon
   

Federaasioŋ bu Riisi (ru: Российская Федерация) mooy réew mi gëna mag ci àdduna bi, muy tëye Asie gannaar ak pàccu penku Europe.

Ci 9eelu xarnu bi ay tribu slave ñoo sanc Riisi bu sowwu jàng, ci 9eem ba 12eem xarnu, mu bokkoon ci benn réew bu mag ci Europe bu nekkoon ci diggu Kiev (tay mooy kapitaalu Ukreen), waa Asie nomade ñoo ko nangu 1240. Ci 13eem ba 14eem xarnu, Principauté bu Moscu dafa feeñ ci diwaanu Horde d'Or, ginaaw bi Horde d'Or daanoo ci diggu 15eem xarnu, mu nekk réew mu wuute.

Beneen dëkk bu am solo, di Veliky Novgorod, mingi wéy di amal aada demokraasi; ci nord Russie, foofu la nekkoon diggu République bu Novgorod, bi Moscubjëlee ci 1478. Ci diggante 16eem ba 19eem xarnu, li ëpp ci askanu Riisi dañu nekkoon jaam yu xamul jàng ak bind ci seen réew; Njaayum nit dafa bariwoon lool ci biir Russie, ba ci atum 1861 lañu ko dakkal. Riisi ni yeneen empire yi, dafa topp politik bitim réew bu tar, di jaay doole làkku Riisi ci réew yi mu nangu, di tere làkki dëkk bi, di jéem, rawatina ci réew yu penku Europe ak Asie centrale.

Ci atum 1917, ñaari fippu ñoo am: ki njëkk mooy daaneel nguuru buur ba noppi soppi Riisi mu nekk republique demokratik; ñaareel ba mooy coup detaa bi Lenin jiite ci weeru oktoobar 1917, ginaaw ga mu am geer civil bu jeex ci Terror Rouge, 16 milioŋ ciy doomi aadama ñàkk ci seen bakkan, ñu taxawal Union Sovietique ci 1922. Ci jamonoy jaay doole yu bari ci 1937–1938, dañu daan 700 000 milioŋ ciy nit, daal di leen ray. Ñu jàpp leen ci kampu konsantraasioŋ yu Gulag.

Kaartu kampu konsantraasioŋ soviet yu Gulag

Ci weeru ut 1939, waa Union Sovietique daal di siñe déggoob xaaj àdduna bi ak Allemagne Nazy, ci weeru septembre 1939, ñu bokk dugg biir Pologne, daal di tàmbali Ñaareelu guerre mondiale. Ci 1939–1940, waa Union Sovietique dañu jéema nangu Finlande waaye dañu ko daaneel. Ci diggu ati 1940, waa Union Sovietique daal di nangu Lituanie, Lettonie, ak Estonie. Ginaaw bi waa Nazy duggee ci réew mi ci 1941 ba noppi ñu xañ déggoob 1939, waa Union Sovietique daal di jàppalante ak Etats Unis ak Grande Bretagne. Ci 1961, la waa Union Sovietique yónnee nit ku njëkka dem jawwu ji. Ci ati 1970, dañu jàpp lu ëpp 100,000 fippukat. Ci diggante 1979 ba 1989, waa Union Sovietique dañu jéemoon nangu Afghanistan waaye dañu ko daaneel, mu indi daanu ci koom-koomu Soviet yi. Ci diggante 1985 ba 1991, Union Sovietique dafa daanu ndax coppite yu am ci demokraasi. Riisi dafa tàmbali xeex yu bari ci republik yu njëkk ya.

Ci 1999, Putin daal di jël nguur gi ci Riisi daal di tàmbali Ñaareelu xare bu Riisi ak Chechnya, mu jeex ci 2000 ci yàqu-yàqu bu mag ba noppi nangu réew mu ndaw mi. Ci 2008, la Risi dugg Georgie, ci 2014, Ukreen. Ci 2022, la Risi dugg Ukreen ci anam wu mat sëkk, di xare bi gëna mag ci Europe ginaaw ñaareelu guerre mondiale. Ci 2022, la Risi dugg Ukreen ci anam wu mat sëkk, di xare bi gëna mag ci Europe ginaaw ñaareelu guerre mondiale. Putin mungi taxaw bu baax ngir dakkal kujje demokraasi yi ak di ray njiitu fenomen demokraasi yu mel ni Anna Politkovskaya, Boris Nemtsov ak Alexei Navalny. Ba ci xale yi ci Riisi dañu leen di jàpp ndax dañu bañ xeex, te dañuy ŋàññi Putin lu ndaw [1] [2][3] [4] [5] [6][7] [8] [9] [10] [11] [12] [13][14] [15] [16] [17] [18] [19] [20] [21] [22] [23] [24] [25].

  • Laŋketu ekipu Alexei Navalny [26]
  • Dokumentaar "Anatomi bu Putinism" (2023) [27]

Références

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
  1. Александр Литвиненко, Юрий Фельштинский ФСБ ВЗРЫВАЕТ РОССИЮ.
  2. [https://www.yabloko.ru/Publ/Book/Fire/fire_002.html Путинизм как высшая и заключительная стадия бандитского капитализма в России]
  3. Переписать историю. Почему режим Путина менее стабилен, чем СССР в свои последние дни
  4. Putin's Warped Idea of Russian History
  5. Vladimir Putin’s Rewriting of History Draws on a Long Tradition of Soviet Myth-Making
  6. Inside Putin's push to rewrite Russian history in favor of his war in Ukraine
  7. 10 years of Russian annexation of Crimea, reflections on the role of PMCs in hybrid warfare
  8. Political Repressions in Russia in 2021
  9. Mass protests in Russia in the shadow of repression
  10. Repression and Autocracy as Russia Heads into State Duma Elections
  11. Навальный Алексей Анатольевич
  12. Парамошин Георгий Сергеевич
  13. Симонов Михаил Юрьевич
  14. Уваров Никита Андреевич
  15. Самые юные политзаключенные
  16. В России политзаключенным стал 15-летний школьник. ФСБ назвала его участником легиона «Свобода России»
  17. Мы считаем политзаключённым отца девочки, нарисовавшей на уроке антивоенный рисунок
  18. Турбин Арсений
  19. BILD: Український підліток розповів, як російські військові викрали його з Херсона та утримували в таборі в Криму
  20. У РФ скоїв самогубство український підліток, якого насильно вивезли до Росії
  21. Турлаев Никита Юрьевич
  22. Дело Валерия Зайцева и Никиты Турлаева
  23. Лизунова Любовь Витальевна
  24. Улыбышева Анастасия Александровна
  25. Никуленков Кирилл Андреевич
  26. Патриот за деньги. «Русский мир» в обмен на Эмираты
  27. Анатомія рашизму | Документальний цикл «Остання війна»