Gëwéel
Gëwéel yi ñaari rëdd lañu yu dëppook yamoo gi: gëwéelub Tef tollu ci 23°24' wu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar gi ak gëwéelub Sànkar tollu ci 23°27' wu tus-wu-gaar wu bëj-saalum. di nañu woowe it gëwéel diiwaan yi ne ci li wër rëdd yooyule (di faral di wax dëkk ci gëwéel yi).
Melokaan
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci li jege yamoo gi, di nañu faral di gis klimaa bu ànd ak tàngoor wu tar ak taw bu bari ci at mi mépp: di ko wax klimaab yamoo. Waaye, ci li jege gëwéel yi (Tef mbaa Sànkar), ci at mi noor ak nawet rekk a ci am, kon wàcciit yi (taw yi) day wuute ci jamonoy at mi, ba daanaka at mépp ay tàng, di li ñuy wax klimaab gëwéel.
Waaye nag jàpp nañu ne it ngelaw yiy upp ak duusi géej yi ak rëyaayu diiwaan bi am nañu ay jeexiital yu solowu ci klimaay diiwaan yi, ba tax na su nu seetloo yenn diiwaan yi, doonte nekk nañu ci wetu ab gëwéel, amuñu klimaab gëwéel (ci misaal diggu Óstraali walla bu Sahara, nga xamne amuñu nawet) ak yenn diiwaan yu am klimaab gëwéel te nekkuñu ci lu jege gëwéel yi( lu mel ne réewum Keeñaa, nekk ci yamoo gi te li ëpp ci suufam klimaab gëwéel la am).
Diiwaani gëwéel yu mag yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Diiwaan yiy dund cib klimaab gëwéel dëgg-dëgg ñoo ngi nekk ci diggu Aamerig ak bëj-saalumu Aamerig, ci digg ak genn wàllu bëj-gànnaaru Afrig, ci bëj-gànnaaru Óstraali ak genn wàllu Endoneesi. Li des ci barabu diggantegëwéel bi dañu leen di séddale ci diggante klimaab tàkk (rawatina ci Afrig), bu yamoo walla bu xaw a sedd (rawatina ca Asi
Lëkkalekaay yu biti
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (fr) CNRS [1] La bodiversité tropicale.
- (fr) Agropolis: Portail européen de recherche de formation et d'information sur la Méditerranée et les pays tropicaux.
- (fr) Une agronomie tropicale au service des agricultures familiales ? (Forum d'Agropolis)
- (fr) P. W. Richards, professeur de botanique, "Etude de la végétation tropicale (se référant particulièrement à la Guyane britannique et à l'Afrique occidentale britannique)". University College of North Wales, Bangor. UNESCO 1956. Archives de la fAO.
- (fr) Mieux connaître et protéger la nature et les peuples des forêts humides
- (fr) "Gestion environnementale des écosystèmes et forêts tropicales" : Groupe de Formation et de Recherche sur les écosystèmes tropicaux forestiers et naturels, AgroParisTech-ENGREF
Xool it Wikimedia Commons
|