Aller au contenu

Diggu Aamerig

Jóge Wikipedia.

Diggu Aamerig mooy xaaj bi nekk ci digg goxu Aamerig, ci diggante Meksik (bokk ci Bëj-gànnaaru Aamerig), ak Koloombi (bokk ci Bëj-saalumu Aamerig). Ay melokaanam ñooy li mu nekk di ab séla ci diggante ñaari Aamerig yi, ak li mu doon it ab jàllu, ngir man a jòge ci Mbàmbulaanu Atlas dem ci Mbàmbulaan gu Dal gi. Ca réewu Panamaa la boobu jàllu nekk.

Diggu Aamerig ci àdduna bi

Séwógaraafi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Réew ya fa nekk:

Ay xay yu mag juddoo nañu ci bii diiwaan, yu ci mel ne yu Maya yi. Waa Espaañ ñooy waa Tugal yi fa njëkk a ñéw. Ñoom ñoo aakimoo woon nguuri Maya yi, dal di leen di noot ci lu mat ñetti xarnu. Daanaka réew yi nekk ci Diggu Aamerig yépp làkkuw Espaañ lañuy wax.

Bi ñu amee seenug tembte, ci ndoorteelu 1800, la leen ay jafe-jafe yu bari ganesi. Looloo tax li ëpp ci taariixu réewi Diggu Aamerig yi, ba ci 1900, ay daane nguur ak ay xaree ci gën a fés.

Li ëpp ci am-am yi nekk ci diwaan bi, suufu mbéy la te li ci ëpp ci loxoy ñenn nit ñu néew la nekk. Mbéy mi, ba tay, moo ëpp solo ci seen koom-koom, njudéef (produit) yi ñu soxla ngir seen dund dañu koy jéggaani bitim-réew. Seen campéefi koom-koom yi tamit li ci ëpp ay doxandéem a leen moom.

Diwaani Goxu Aamerig
Diggu Aamerig · Bëj-gànnaaru Aamerig · Carayib · Bëj-saalumu Aamerig