Way dëkki Afrig
Way dëkki Afrig ñu néew lañu, bu ñu leen nattee ci tolluwaayam bu rëy bii (moom Afrig): sababu loolu day dellu ci ni ab déndam méngoodee, ñagase ni. Ak itam sanc gi ko Tugal sancoon te yàgg fi, giir ay xéewalam yu dénd yi, te loolu indil ko ag dellu ginnaaw gu mag. Lii lépp nag dox na ci taxawal màggug way dëkkam. Leegi nag duggalees na fi jumtukaayi feg yi aju ci wàllug wér-gu-yaram, bu ko defee way dëkk yi tàmbali di bari, di màgg. Limub way dëkki Afrig àgg na ci 350 ci milyoŋi nit , ñi ngi séntu lim bii romb ko ba àgg ci 520 milyoŋi nit ci mujjug xarnu bii.
Diiwaan yu fatt yi ci ay way dëkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]yii diiwaan nag ñi ngi ci barab yi barim mbay, mbell ak klimaa bu méngoo, ci xuru Niil wu jege wi ak Delta ak ci barabi tefes yi ci bëj-gànnaaru Afrig, ak ci Laamaaru Ngéej yu Yamoo yi, ak ci tefesug sowwu Afrig, ak ci diiwaani bëj-saalum yi ak bëj-saalumu penku ci Afrig gu bëj-saalum gi.
Diiwaan yu diggdóomu yi cig dëkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]barab yu diggdóoomu te yam ci ag fatt ci wàllug dëkk moo fa nekk, maanaam ña fa dëkk bareewuñu noonu, moom nag ay yaatu-yaatoo fa nekk yu rëy ci ay sammuwaay, ci goxi Sudaan yu sowwu yi, dale ko ci Dexug Senegaal gi ba ca ngéejus Càdd si, ak ci xuru Niil ci Sudaan ak ci Laamaaru Ecoopi ak ci Sowwu Afrig ak bëj-saalumu mbalkam Kongoo.
Diiwaan yi bariwul ay way dëkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]ñooy tàkk yu bekkoor yi, niki : Tàkkug Sahara, Tàkkug Kalahaari gi ak Tàkkug Somaali gi, ak itam gotti yamoo yu fatt yu bari yi ay ngirowaay aki tawat, ci mbalkam Kongóo ak Diggu Afrig.
Xeeti way dëkk yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Way dëkki goxub Afrig tollu nañu ci lu jege 350 milyoŋ ciy nit, maanaam lu tollook ay fukki yoon Isipt ciy way dëkk, ñi ngi séntu bii lim àgg ci 520 milyoŋ ciy nit balaa yàgg.
Way dëkki gox bi ñi ngi sosoo ci ay ñu ñuul, ay araab, ay tubaab ak lenn ci ay xeet yu bawoo Asi, ñu ëpp ci ñoom nag ay waa Siin lañu aki waa End.
Ñu ñuul ñi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]ñooy ñi cosaanoo ci gox bi, ñoom nag ñi ngi nekk ci digg bi ak ci bëj-saalum gi. Ñoom nag daje nañook ag jaay doole gu mag gu tukkee ci sancaan yi, rawati na ci jamono ji nekk ci diggante ñaari xarnu yii: VI ak VII. ñoom sancaan yi ñoo sawarloo njàppum jaam mi te di ci xiirtale, rawati na ci tefesi sowwu Afrig yi ak mbalkam Kongóo, loolu waral ñu ray lu sakkan ci waa Afrig yi, ña ca des gàddaay dugg ci biir gox bi.
Araab yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ñi ngi nekk ci xaaj bu bëj-gànnaar bi ci gox bi, rawati na ci réewi naar yi, di : Isipt, Sudaan, Libi, Tiniisi, Aljeeri, Marook, Gànnaar ak Somaali. Séenub lim dees na ko nattale ci 100 milyoŋ ciy nit, maanaam luy tollook 2/7 ci way dëkki gox bi. Tàkkug Sahara gi nag mooy aji tàqale ji tàqale diggante ñu ñuul ñi ci bëj-saalum ak naar yi ci bëëj-gànnaar.
Waa Tugal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ñi ngi ñëw ci gox bi ànd ak Sancug Tugal gi la ko dale ca VIIeelu xarnu. Ñu seet fa gën a neex wàcc fa, muy barab yi gën a neex a dëkke, fi suuf si yekkatikoo, klimaa ba méngoo fa, ci penku Afrig, ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa ak Malaawi. Teg nañu loxo bëj-saalumu Afrig, sosal fa séen bopp am pénc (republique) mu temb, ñu yor fa cang ga ak njiit la ci kaw ëppte (majorité) gu nit ñu ñuul ña, di fa doxal it politigu teqale ci biiru xeet (walla boddante ci biiru xeet). Néewte gu weex googu it (minorite blanche) ci Rodisiyaa tegoon na loxo ca nguur ga walla àtte ga, daal di jibal ag tembteem, di def it politig bu mel ne ba ñuy doxal ca bëj-saalumu Afrig, muy boddante ci biiru xeet.
Néewte yu Asi yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ñi ëpp ci ñoom ay waa Siin lañu aki waa End, ñi ngi ci digg ak bëj-saalumu Afrig, ñi ëpp ci ñoom it canc gi lañu àndaloon ñëw fi. Ña ca gën a bari dañuy liggéey ci yaxantu, ñenn ci ñoom dañuy def ay mecce yu ndefar (industrie).
Jafe-jafey way dëkk yi fi cosaanoo
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Deltu ginnaaw gi jokkoo gi (communication) def.
- Tas gu fa mbas yi tas ak tawat yi ngir méngoodig melokaani klimaa bi.
- Ñàkk a tembug koom-koomu Afrig bi ak lënku gu mu lënku ci koom-koomu réewi sancaan yi.
- Boddanteg xeet gi ci bëj-saalumu Afrig ak ci Rodisiyaa.
- Nekk gi yenn néewte yi di ay jàmbur (dëkkuñu fi) nekk ci yenn ci réewi gox bi.
- Ñàkk a jëm-kanam ci wàllug njàngale ak xarala yi manul a ñàkk cig jëm-kanam ak màggug koom-koom.