Leopool Sedaar Sengoor

Jóge Wikipedia.
Leopool Sedaar Sengoor njiitul Senegaal lu njëkk

Leopool Sedaar Sengoor mi ngi juddoo ca Jiwaalo ci 9 Oktoobar ci atum 1906, génn àdduna ca Verson (ca Fraas) ci 20 Desambar 2001. Nekkoon taalifkat, bindkat doonoon it killifa aada ca Senegaal. Mooy ki njëkk a doon njiitu réewu Senegaal (1960-1980).

Wàcc na jal bi ci teeyug bàkkanam, bàyyee ko Abdu Juuf. Ñu bari ci àdduna bi dañu koy jàppe kenn ci xalaatkati Afrig yi ëpp solo, yu ñaar-fukkeelu xarnu.

Dundam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Léopold Sédar Senghor ma nga juddoo ca Jiwaalo, di ab dëkk bu ndaw bu ne ca tund wu Mbuur, ci diiwaanu Cees. Baayam di Basil Jogoy Senghor, ab yaxantukat la woon bu bokkoon ci kuréel gu diggu gi ci giirug séeréer, di genn ci néewte yi ci Senegaal.

Yaayam di Ñilaan Njéemée Baaxum, ñatteelub baayam. Bi mu amee juroom ñatti at, la tàmbali am njàngam ci ab Gospel : benn jàngu bu dëkku bu Baay yu Ruu Gu Sell gi (les pères catholiques). Ci atum 1922 la dugg leekool (mbaa jàngu bi) te booba ma nga Ndakaaru, muy ku soppoon njàngat lu Faraas, di woon ku ràññiku ci làkku Faraas, Laatin, wu Geres ak Jabru, mu daal di am Bakalooriya, daal di am ag may ngir àggale am njàngam ca Faraas.


  • Yaxantukat ci fr:commerçant
  • kuréel gu diggu gi ci fr:bourgeoisie
  • néewte ci fr: minorité
  • jàngu bu dëkku ci fr: internat
  • njàngat lu Faraas ci fr: littérature française
  • may ci fr:bourse

Senegaal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sengoor nekkoon na di kenn ci ñi doon jàppale Lëngoo gi:(réewi Afrig yi temb bu yàggul), loolu lu mel ne (ag Komonwelth gu Faraas) gu ag Lëngoo la woon, réewi Afrig yi nag ànduñu ci woon. Moom sosoon na ak Moodibo Kayta Lëngoo gu Mali gi. Moo nekkoon njiitul jataayub lëngoo bi ba ci kero bi mu tasee atum 1960, moo nekkoon ki njëkk a jiite Senegaal, ñi ngi ko tànn ci 5 satumbar 1962, mooy ki sadd bàkku réewum Senegaal (gar gu xonq gi). Njiitul jëwrinam lii di Mamadu Ja moo féetewoo woon doxal naal yi aju ci suqaliku gu réew mi gu guddub dig gi(long terme), bu ko defee moom Sengoor mu féetewoo séqoo yu bitim réew yi

Waaye ñaari gaa yii mujj nañu wuute ci lu gaaw. Ci disambar 1962 lañu jàpp Mamadu Ja, mi ñu tuumal ne day xiirtale cig daaneel nguur, mu daal di sax ci kaso bi lu tollook fukki at ak ñaar. Ginnaaw bi Sengoor daal di taxawal ag noste gu njiit . Ci 22 Mars 1967 Sengoor mucc na cig bóom, ñu daal di teg àtteb ray ci ki ñu ko tuumaaloon. Tekki na ndombag tànkam njëkk ab àppub njiitam di jeex, loola di ci disambar 1980, daal di fiy wuutal Abdu Juuf ci boppu réew mi. Ci ron ag njiitam la Sengoor sampe lëwug làng( ñu yamale woon ko ci ñatti dawaan rekk: mbokkoo , mbokkte, ak afal ak genn noste gu yar ( systeme educatif) gu am solo.

Bariwaa na lu ñuy askanale Sengoor ag demokaraasi waaye ay fen rekk la,ndax moom indi woon na fi ci doole ag noste gu genn làng, daal di moñoxe ci doole lu sakkan ci ay yëngu-yëngu yu ñaxtu yu ay dongo (étudiants. Ak doonte canc gu Faraas jeex na ci melo wu kilifawu (officiel) teewul xiimay koppar bu Senegaal Faraas a koy saxal, njàng mi it ci làkku Faraas lañu koy defe, te Sengoor it réew mi mi ngi ko jiite woon ànd ak ay xelalkat yu Faraas yu muy diisool, (Ñooñu nag manuñoo joxe menn xel mu njariñul Faraas nekkul, Moom itam jabari waa Faraas la yoroon, te bari na lool lu mu daa xeex ngir ñu yor aaday Faraas, Taalifkat ba nee na:

  • (Màggat mu màggat ci am () njàngum tubaab jabaroo () tubaab tubaab la, tubaab ngeen dénk seen gaal gii)

  • Lëngoo gi ci fr: fédéralisme
  • séqo yu bitim réew;relations internationales
  • noste gu njiit: système ou régime présidentiel
  • lëwug làng: multipartisme
  • mbokkoo: socialisme, mbokkte:communisme, afal:libéralisme, noste gu yar :systeme educatif