Melosuufug Afrig wuute gi ci sumb yi

Jóge Wikipedia.
Contenu supprimé Contenu ajouté
Vandal (waxtaancëru)
Guaka (waxtaancëru)
Rëdd 34 : Rëdd 34 :
Ndeete gi: 47,5 ci junni
Ndeete gi: 47,5 ci junni
Ndeeteg (mortalité) xale yi 100 ci 1000 (junni bu ne teemeer a ciy dee).
Ndeeteg (mortalité) xale yi 100 ci 1000 (junni bu ne teemeer a ciy dee).
</poem>


=== Xeet yi ===
=== Xeet yi ===

Sumb bu 23 Oktoobar 2007 à 12:18

Afrik, mooy ñaareelu gox bi gënn a ngande ci adduna bi (lu weesu bu Asi). Yaatuwaayam toll na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci joor gi ci adduna bi. Ay way-dëkkam toll ci lu ëpp 800.000.000, muy benn ci juroom-ñaareel gu way-dëkku adduna bi. Afrik ga ngi yem ci bëj-gànnaaram ci Géej gu Diggu gi, ci sowu ci Mbàmbulaanu Atlas, ci bëj-saalum ci Géeg gu Bëj-saalum gi, ci penku ci Mbàmbulaanu Waa-end. Asi rekk la takkalool ci yeneen gox yi. Yemoo gi jàll na ko. Ci jëmm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute tek ci.

Lonkoyoonu adduna bi, Afrik moom la nu fesal

Séwógaraafi ci jëmm

Nin ko junjee ci kaw, Afrik doon na gox bu rey. Ci tëddaayam, so jële penkoom jëm sowu mat na 7500 (juroom ñaar fukk ak juroomi temeer) km, bëj-gànnaaram ba bëj-saalum tollu na ci 8000km (juroom ñetti fukki junni) ci guddaay.

Diwaan yu mag yi

Diwaan yu mag yi bari nañ loo:

  • Bëj-gànnaaru Afrik: Maghreb, goxub Atlas
  • Ndand fëy-fëy gu Sahara (8 miliyoŋi km²)
  • Bejjenu Afrik, ci li wër Ecopi. Xameekaayoo na ay doj yu bari te naat lool.
  • Barabu Sudaan (joge ci araab, Bled es Souden) maanaan (reewu ñu ñuul ñi), ci sowu Afrik, te bañ koo jaawale ak Reewu Sudaan. Barab boobu ab mandiŋ la.
  • Afriku yemoo gi,
  • Bëj-saalumu Afrik: all moo nekk ci diggam, ay doj ciy tefesam, am-amub ay bayima yu bari
  • Madagaskaar: di nan fa fekk xeeti bayima aki gañcax yu bari te wuute, dañ leen fay aar aka suuxat.

Séwógaraafi gu nite

Nit ñi ci gox bi

Reew yi nga xam ne seenug yorte(administration) dafa néewal, lim yi ñuy joxe doonu ñu yu matale (limbare (statistique) yi defu ñu leen ci anam gi war). Ci 1975 : 302 miliyoŋ i way-dëkk Ci 2001 : 591,3 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : PNUD) Ci 2005 : 803,690 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : World Bank ndeyi-koor 2006) Gisjiital ngir 2015: 866 miliyoŋ i way-dëkk.

11% gu way-dëkk gi ci adduna bi, mi ngi ci Afrik gu bëj-saalumu-Sahara. yokkuteg nit ci Afrik doon na bi gën a gaaw ci adduna bi (21% ci ay way-dëkk yu ciy yokku at mu nekk).

Doon na aw askan gu bariy ndaw, ñi ci ëpp 17 at la ñu am (te ci adduna bi yëpp 23 at la). 45% yu waa-afrik 15 at (fukki at ak juroom) la ñu am. te ñi ëppal 65 at, 3% lañ ci askanam (lang ak 13% ci li des ci adduna bi).

Judd gi : 43 ci junni boo jël (26 ci junni ci adduna bi), 6 doom jiggeen ju ne ci lu ëpp(2,8 ci adduna bi).

Yaakaarte dund gi(li nga yaakaar a dund): 48.8 at
Ndeete gi: 47,5 ci junni
Ndeeteg (mortalité) xale yi 100 ci 1000 (junni bu ne teemeer a ciy dee).

Xeet yi

gëstukat yi ci li ñeel xeet, gis nañ ay mbooloo xeet yu bari ci Afrik:

  • Pigme yi: neenañ bokk nañ ci mbooloo yi gënn a yagg. Ci seen taariix, ñoom ci all bi rek la ñuy dund. Seen jafe-jafey dund day yokk rek ndax all bi ñuy dagg ay garabam.
  • Waa-ecopi, Waa-somali ak Tubu yi: ñoom naar yi lañu gënn a jege, rawatina ci wallu làkk.
  • Waa-afrik yu ñuul ñi: Waa-sudaan(senegaal...), Waa-ginne yi, Bantu yi(Kongòo, Afrik gu diggu), Masay yi, Tutsi yi.
  • Tubaab yi: ñi nga xam ne Tugal la ñu cosaanoo.
  • Waa-madagaskaar

Kuuteeg làkk yi

Ñoo ngi koy xayma ci 200 ak 2000 làkk walla waxin (làkk dañ koy bind te waxin ci lammiñ lay yem) ci Afrik. Dañ leen seddale ci ay mbooloo, maanaam làkk yi am ag mbokk.

  • Mbooloo làkku bantu: yii ci la ñu bokk, lingala, duala, kikongo, kilari. Ñi ëpp ci ñi koy wax diggu afrik la ñu dëkk.
  • Kiswahili (ci mbooloo bantu la bokk): 15 miliyoŋi nit, ci penku Afrik
  • Ausa: ci yii reew, Niser, Niseriya, Cadd
  • Mandeŋ: 6 miliyon i nit(Mali, Burkina-faso, Senegaal,...)
  • Wolof: 11 miliyon i nit (Senegaal, Mali, Gambi, Moritani,...)

Lu ëpp ci làkk i Afrik yi, du ñu ay làkku nguuru reew ya ñu leen di làkkee, maanaam duñ leen jngale ci daara yi, ngur gi du leen jëfëndikoo.

Ñetti làkk rekk ñooy làkk i seen nguuru reew, di seen làkku cosaan: Lesoto, Ruandaa, Burundi.

Kuuteeg diine yi

  • Lislaam: 260 miliyoŋ i taalibe. Ci sowu ak ci penku Afrik la ëppee doole, lu wuuse bëj-gàannar gi.
  • Diiney Kirist: 220 miliyoŋi taalibe
  • Diiney cosaan: ñoo gi koy xayma ci 100 miliyon i taalibe, waye war na kaa ëpp.


Melosuufug Afrig

Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkinaa Faaso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Bennoo yu Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eriitere  • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Gine • Gine-Bisawóo • Gineg yamoo • Keeñaa • Lesoto • Liberiyaa • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeriyaa • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome-ak-Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togo • Tuniisi • Sambi • Simbaawe