Doxalukaay bu demandoodi

Jóge Wikipedia.
Wëndeeluwaan (ci cammoñ) ak tekkaaralaan (ci ndijoor) bu ab doxalukaay bu 0,75 kW.

Doxalukaay bu demandoodi ab xeetu doxalukaay bu mbëj la bu dawaan bu safaanu bu xél yu wëndeeluwaan bi yamul ak yu toolu bijjaakon buy wëndeelu bi lëmës yi nekk ci tekkaaralaan bi jur. Maanaam amul ag demandoo ci ñaari gaawaay yi, benn bi moo raw beneen bi. Loolu moo ko wuutale ak doxalukaay bu demandoo.

Bii xeetu doxalukaay manees na koo jëfandikoo niki ab jurukaayu mbëj, ab safaanukaay. Waaye bariwul li ñu koy jëfandikoo ngir jóox kàttanu mbëj ndax li ko doxalukaay bu demandoo gënee ci wàll woowu.

Melokaan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Doxalukaay bi ci ñaari xaaj la séddaliku, benn bi di tekkaaralaan bi, di xaaj bu taxaw bi, beneen bi di wëndeeluwaan bi, doon xaaj biy yëngu. Tekkaaralaan bi dafa am ay bën-bën yu, lang ak wëndeeluwaan bi, di fi lëmës gi di jaar, maanaam wommatukaay yi dawaanu mbëj bi di jàll.

Doxiin[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dawaan biy jaar ci lëmës gu tekkaaralaan bi mooy jur ab toolu bijjaakon buy wëndeelu, xélu wëndeelug tool bi mi ngi aju ci baraayu dawaan biy dugg ci doxalukaay bi te jóge cig ndombo gu biti. Ngir am ab toolu bijjaakon bu taxawul benn barab, di wër, faww ñu am ñetti lëmës yu tolloo, te itam yam dendu mbëj bu safaanu bi ñu leen di dundalee. Waaye ngir gëstu masin bi doy na ñu xool rekk benn wommatukaay ci ñett yi ndax liy xew ci benn bi mooy xew ci yeneen yépp.

Kon lëmës gu tekkaaralaan bi dafay nekk ci biir ag wal gu bijjaakon guy soppiku ci jamono. Toolu bijjaakon buy soppeeku bi mooy sabab juddug jenn doole ju mbëjdoxalukaay, lëmës gu wëndeeluwaan bi su sóoboo ci boobu tool, sunu sukkandikoo ci àtteb Lorenz, dafay xiirtal ci ay catam ab wuuteeg aj, moom it juddal ab dawaanu mbëj ci wëndeeluwaan bi. Segam xamees na ne su ab dawaan di jaar ci aw taxar, dafay jur ab toolu bijjaakon. Kon ñu am ñaari tool (bu tekkaaralaan bi ak bu wëndeeluwaan bi) liy tukkee ci digaaleeb ñaari tool yi mooy jenn doole ju mbëjbijjaakon, di liy wëndeel wëndeeluwaan bi.

Li tool bi tekkaaralaan bi jur, di xiirtal ab wuuteeg aj ci wëndeeluwaan, loolu itam sabab beneen tool, di lu ag ñakkam a judd di indi ñakk a demug wëndeeluwaan bi. Tax ñuy far di ko woowee itam masinub xiirtal.

Turu demandoodi ngi jóge ci li wëndeeluwaay bi manut a yam ak walug bijjaakon bi, xél gi ñuy demee, walug bijjaakon bi mooy raw. Wuuteg xél gi nekk ci diggante wal gi ak wëndeeluwaan bi lañuy wax xélu tarxiis. Xélu wëndeluwaan bi lañu wax xélu demandoo.

Lëkkaloo gi ci diggante xélu tarxiis gi, baraayu dawaan bi koy dundal ak limu seexi dott yi (benn limu seexu dott benn bëj-gànnaar ak benn bëj-saalum lay am), mile mind moo koy fésal:

  • xelu toolu bijjaakon bi, ñu koy natt ci w/sim (wër ci simili), ñaata wër lay def ci simili bu nekk;
  • f mooy baraay bi, ñu koy natt ci Hz;
  • P mooy limu seexi dott yi

ngir xayma tarxiis gi s

  • n mooy xélu wëndeeluwaan bi.

Ci misaal, ab doxalukaay bu am ñetti seexi dott p (6 dott), bu baraayam f doon 50 Hz mi ngi am xélu demandoo 1000 wër ci simili.