Safaanukaay
Safaanukaay ab masinu mbëj la buy soppi kàttanu doolerandu ci kàttanu mbëj ci melokaanu dawaan bu safaanu. Soppali gi mi ngi cëslaayu ci feeñte gu xiirtalug mbëjbijjaakon.
Defariin
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Defariin gi dafay aju ci xeetu safaanukaay bi mu nekk.
Safaanukaay bu demandoo
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Masin bi dafa am ñaari xaaj, benn bi ab xott la bu am am pax ñu koy wax tekkaaralaan, beneen bi di xaaj biy dugg ci bu njëkk bi, ñu koy wax wëndeeluwaan. Baatu demandoo mi ngi jóge ci li walug bijjaakon bi di demandoo ak wëndeeluwaan bi.
Ci tekkaaralaan bi la lëmës giy jur toolu bijjaakon buy wëndeelu di nekk ci ndimbalu ay mbëjbijjaakon, seen lim yam ak limu wéq yeek seexi dott yi, kon su nekkee ab safaanukaay bu ñettiwéq, ñetti mbëjbijjaan ak ñetti seexi dott lañuy doon, su nekkee ñeenti wéq juroomi mbëjbijjaan lañuy doon. Safaanukaay bu demandoo ab doxalukaay bu demandoo lañu jël wëlbati ko. Ab doxalukaay soo ko joxe kàttanu mbëj mu delloo la kàttanu doolerandu, soo ko wëlbatee jox ko kàttanu doolerandu mu nekk ab jurukaayu mbëj, jox la kàttanu mbëj.
Safaanukaay bu demandoodi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bii xeetu safaanukaay ab doxalukaay bu demandoodi lañu jël wëlbati ko mu nekk jurukaayu mbëj. Ngir mu man a dox niki jurukaay faww muy jële kàttan ci geneen ndombo gu biti ngir man a bijjaakoonal lëmës gu wëndeeluwaan bi. Su wëndeeluwaan bi di wëndeelu lay joxewaale kàttanu mbëj waaye ngir walug bijjaakon gi koy wëndeel di sax di dox faww muy wéy di jëlee kàttanu mbëj gu koy dundal ci beneen safaanukaay bu demandoo. Lii moo tax daanaka du xeetu jurukaayu mbëj bu ñuy faral di jëfandikoo ci digg yu mbëj yi, bu demandoo lañuy jëfandikoo.
Jëfandikoom ci jëfe
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Safaanukaay yi bari nañu fi ñu leen di jëfandikoo, ci biir bépp digg bees di jóoxee kàttanu mbëj. Ginnaaw jóog gi ci dawaan bu safaanu, ngir man koo yóbb ba ci liggéeyuwaay yeek kër yi dañu koy soppali ak ab soppalikaay.