Doxalukaay bu demandoo

Jóge Wikipedia.
Gaaral gu doxiinu ab doxalukaay bu demandoo

Doxalukaay bu demandoo ab xeetu doxalukaay bu mbëj la bu dawaan bu safaanu. Diir bi wëndeeluwaanam di def ag wër dañu koo yamaleek baraayu dend bi koy dundal, maanaam dañuy demandoo ndax ci jamono ji dend bi nekke tus la wëndeeluwaan bi di tambali wër gu bees, loolu wuutale ko ak doxalukaay bu demandoodi. Xeetu doxalukaay bii manees na koo jëfandikoo niki ab safaanukaay, maanaam ab jurukaayu mbëj, te sax mooy bees gën a jëfandikoo ci digg yu mbëj yi, di barab yees di jóoxee kàttanu mbëj.

Defariin[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Doxalukaay bi ñaari wàll la am: benn bi di wëndeeluwaan bi, moom, mu am ci biiram benn limu seexi dotti bijjaan yees defaree bijjaan yu sax walla ay mbëjbijjaan. Ngir man a am mbëjbijjaan bi dawaan bu wéy lañuy dawal cii biir ay taxañ yees def ci wëndeeluwaan bi, naka-jekk taxañi përëm. Beneen bi di tekkaaralaan bi, moom it, am ci biiram ag lëmës gu yittewoo jur ab toolu bijjaakon buy wëndeelu ak ay dottam, segam ñaari dott yu bokk (bëj-gànnaar ak bëj-gànnaar walla bëj-saalum ak bëj-saalum) dañuy bëmëxante, ñaar yu wuute (bëj-gànnaar ak bëj-saalum) di bijjante, kon dottitoolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi suñuy wëndeelu àndaaleek tool bi dañuy xëccaale dotti wëndeeluwaan bi ba tax moom ci boppam di wëndeeluwaale, kon nu amee ca ab doxalukaay.

Baraayu wëndeelu gi mi ngi aju ci baraayu dend bi koy dundal (ci misaal Senegaal 50 HZ), Diiwaan yu Bennoo yi 60 la). limu wër yi wëndeeluwaan bi di def benn simili bu nekk

  • xelu toolu bijjaakon bi, ñu koy natt ci w/sim (wër ci simili), ñaata wër lay def ci simili bu nekk;
  • f mooy baraay bi, ñu koy natt ci Hz;
  • P mooy limi seexi dott yi

Limu seexi dott yi moo ngi yam ak limu taxañ yi, benn taxañ bu nekk benn seexu dott lay am: benn bu bëj-gànnaar ak beneen bu bëj-saalum.

Ag taalam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Taal ko doon na lu xawa jafe. Su doxalukaay bi taxawee, suñu ko joxee dawaan bu safaanu biy jur toolu bijjaakon buy wëndeelu bi biy wëndeel wëndeeluwaan bi, diisaayam dafay tax ba du ko man a topp, dafay wéy di taxaw. Ngir man koo taal kon dañu koy taqale ak ab doxalukaay bu demandoodi ngir mu tambalee wëndeelu ginnaaw bi ñu dindi ko daldi koy soog a jox dawaan bu safaanu bi ngi mu man di demal boppam.

Jëfandikoom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Doon na xeetu doxalukaay bu bariwul lees koy jëfandikoo, ag njëfandikoom dañu koo rekk yamale ci yenn jëfe yi rekk

Lëkkalekaay yu biir[Soppisoppi gongikuwaay bi]