Dawaanu mbëj

Jóge Wikipedia.

Dawaanu mbëj ag wal la niki yépp gu nosu gu yani mbëj (njunjam di Q), naka-jekk cig wëñug weñ lay jaar walla bépp jumtukaay buy watat. Dawaan bi dees koo jappee woo, ci ndorteelu taariixu mbëj, niki ag walug yan yu baax (+), donte sax xam nanu ne, su nu xoolee ci watatukaay yu mbell yi dawaan gaa ngi judd ca walug mbëjfepp yi, yi am yan yu bon (-), ci beneen jubluwaay bi. Kon ni ñu foogeewoon ne la dawaanu mbëj di jublu, du noon, waaye safaan wa la, yan yu bon (mbëjfepp) yi ñooy dox jëm ci yu baax (+) yi. Donte lii yépp, gisiin gu njëkk ga moo wéy di baax, ci déggoo. Njunj gi ñuy jëfandikoo ngir tudd bariwaayu dawaan (limu dawaan giy wal ci jenn jamono) mooy I, di ko wax taraayu dawaan, te bennaanu natt bi ñu koy natte di bi àdduna bi déggoo mooy ampere.

Nattug taraayu Dawaan gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dawaanu mbëj manees na koo natt ak jumtukaay bees di woowee nattampere, waaye gii anam dafay laaj nga dog ndombo gi, xamees na ne du li gën ci yenn nekkiin yi. Dawaan bi manees na koo natt te du jar dog ndombo gi, ci njëlug toolub bijjakoon bi mu jur, moom. jumtukaay yees di jëfandikoo ngi bii liggéey ràññee nañu ci: yëgukaay yu sukkandiku ci njeexitu Hall ak lëmës yu Rogowski

Xeeti Dawaani mbëj[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Faramfacce[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xamees na ne ngir mbëj mi maase ci biir ab watatukaay faww toolu mbëj bi ci ëmbu di neen (tus) ci bépp tomb boo jël ci biir watatukaay bi. Su amee ag wuuteeg aj ci diggante ñaari tomb ci watatukaay bi kon dees na fa am toolub mbëj bu wuute ak tus kon dees na fa am it dawaanu mbëj. Wuuteeg aj googu lees di wax dooley mbëjdoxalukaay, di doole jiy xëcc yani mbëj yi, ñuy man di daw toppante doon ag wal, te ci la ndombo yu mbëj, mbëjbijjakoon, àtteb Ohm ak àttey Kirchhoff sukkandiku.

So jële genn yaa-yaa gu watatukaay bi, benn limu yani mbëj di daw ci biiram 'ΔQ' ci benn diirub jamono 'Δt' dees na ci ame genn taraayu dawaan

Lëkkalekaay yu biir[Soppisoppi gongikuwaay bi]