Aller au contenu

Diiwaan yu Bennoo

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Diiwaan-yu-Bennoo)
Diiwaan yu Bennoo
Raaya bu Diiwaan yu Bennoo Kóót bu aarms bu Diiwaan yu Bennoo
Barabu Diiwaan yu Bennoo ci Rooj
Barabu Diiwaan yu Bennoo ci Rooj
Dayo 9 629 048 km2
Gox
Way-dëkk 305 683 227 nit
Fattaay 31 nit/km2
Xeetu nguur
- Njiitu Réew
- Njiitu Jëwriñ
-
Joe Biden
-
Tembte
- Bawoo
- Taariix
Péy ak rëddi
Tus-wu-gaar
Tus-wu-taxaw
Waasiŋton, DC
38° 53′ 0″ Bëj-gànnaar
     77° 1′ 0″ Sowwu
/ 38.88333, -77.01667
Làkku nguur-gi wu-angalteer
Koppar Dolaaru aamirig (USD)
Turu aji-dëkk Amirik-Amirik
-Sa-Amirik
Telefon
   

Diiwaan-yu-Bennoo, walla Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig ci anam gu gudd am réew la mu séddaliku ci juroom-fukki diwaan, ñent-fukk ak juroom-ñett yi ñoo taqaloo te féete ci diggante Mbàmbulaanug Atlas ak Gu-Dal gi, penku ba sowwu, Kanadaa moo féete bëj-gànnaar, Meksik nekk ci bëj-saalumam. Alaskaa ci la bokk donte taqu ci, mi ngi nekk ci sowwu Kanadaa. Xawaay moom mi ngi ci diggu mbàmbulaan Gu-Dal gi. Réew mi am na fukk ak ñenti diiwaan yu tasaaroo ci géeju karayib yi ak Gu-Dal gi. Péeyam mooy Washington.

Lusomundo

Diiwaan-yu-Bennoo yi ci 2008, 302 ciy miliyoŋ ciy way-dëkk lañu amoon, loolu tax muy ñetteelu réew mi ëppi nit ci àdduna bi, ci ginnaawu Siin ak End. Réyaayam toll ci 9,4 junni km², di ñeenteel ci àdduna bi, ci ginnaawu Riisi, Kanadaa ak Siin. Gàddaay gi bari na fa lool, ba tax muy réew mi ëppi xeet yu jaxasoo ci Suuf si. Koom-koomam mooy bi gën a woomle ci àdduna bi, te moo am njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) mi ëpp ci àdduna bi.

Turu Réew mi Thomas Paine moo ko tànnoon ci bés bi ñuy am seenug temb ci 4 sulet 1776. Woowiin wu gàtt wi, wi ñuy faral di jëfandikoo ci sunuy waxtaan, ci njàngale mi ak ci lonkoyoon yi, mooy «Diwaan-yu-Bennoo» (ci wu-angalteer di United States, ñu tënk ko ci US). Wu gudd wi ñu koy faral di jëfandikoo ci këyiti nguur gi «Diwaan-yu-Bennoo yu Aamerig».

Jamono njëkk-kolomboo (Laataa 1492)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci Alaskaa lañu gise jeexiti nit ki fa njëkk a teew, ci weti 20 000 at nj.j, ci tefesu atlas ci wetu 13000 at nj.j. Nit ñi njëkk a dëkk ci réew mi ñoo nga bàyyikoo ca Goxub Asi, jaare woon ko ca xat-xatu Beriŋ. Ci ginnaaw bi la fa waa-tugal yi ñëw.

Jamonoy canc (1492-1775)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Christophe Colomb moo wuññi goxub Aamerig ci 1492, at ma ca topp mu nemmeeku barab bi nekk Poortorikoo tay jii. Ci XVIu xarnu la réewi Tugal ya fa ëppoon doole doon seet ay jàlluwaay ci bëj-gànnaar-sowwu ak ay am-am, ci seeni tukki ci topp tefesu Atlas gi ñu dem ba taxawal fa ay sancu yu sax. Ci bëj-saalum waa-espaañ yi sos fa seenub sancu duppee ko Espaañ-gu-Bees, di amal ay tukki-gëstu ci biir réew mi. Ci bëj-gànnaar-sowwu waa-riisi yi sanc fa ci li topp tefesu Mbàmbulaanu Gu-Dal gi. Ci la tubaab yi tàmbalee yaxantu ak askan yi fa cosaanoo.

Ci diggante XVIIu ak XVIIIu xarnu, ndànk ndànk, la fukk ak juroom-ñetti sancu waa-angalteer taxaw ci tefesu penku gi, Lii mooy maamu Diwaan-yu-Bennoo yi. Waa-fraa yi nemmeeku pegu Misisipi dal di fay sos Luisiyaan



Ngir xóotal yëral foofu: Taariixu Aamerig