Aller au contenu

Bëj-gànnaaru Afrig

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Bëj-gànnaaru Afrik)

Bëj-gànnaaru Afrig mooy diwaanu Afrig bi féete ci li nekk ci kawu tàkk gu Sahara.

Mooy la nuy faral di wax Afrig gu weex gi, ndax melokaanu ña fa dëkk, bii baat day safaano ak Afrig gu ñuul gi, di tekki Afrig gu bëj-saalumu-Sahara.

Séwógaraafi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Réewi bëj-gànnaaru Afrig :

  • Ci jamono ju yagg ja « Afrig » da doon jëmmal diwaanu Kaartaas, mooy réewu Tiniisi gu tay. Afrik ab diwaanu Nguuru Rom gu Mag ga la woon. Bi jullit yi ñëwee, baat bi dañ kaa soppi, araabal ko Ifriqiya.
  • Beerbeer yi, ñooy way dëkk yiñ ni ñoo njëkk ci bëj-gànnaaru Afrig.
  • Maghreb (sowu ci araab), moo ëmb réew yii : Gànnaar, Marok, Alseeri, Tiniisi ak Libi.
  • « Afrig gu weex » bu njëkk da doon jëmmal barabu Afrig bi ay nit yu xees dëkkee : Marok, Alseeri, Tiniisi, Libi, Esipt. Waaye tay baat bi liñ kay jëfëndikoo bariwul.

Diwaani Afrig
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig
Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan