Xam-xamu suuf si ak jawwu ji
xam-xamu suuf si mooy li nuy wax (Jiyoloji), xam-xam la buy gëstu lépp lu aju ci suuf si kaw gi ak biir gi, ak doj yi (montaañ yi)añs. Bu jawwu ji di biy gëstu lépp luy jawwu ak tegaloo gi ñu tegaloo.
Jawwu ji
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Jawwu ji nak :mooy mbalaanum ngelaw li wër suuf si. Lees di gën a sori suuf si, ngelaw liy gën di néew-doole di gën di amadi, day mujj sax di lu fàddu ci ay fukki culómet cig kawe. Lii a tax ñu man a séddale Jawwu ji ci ay goxi jawwu yu wuute te tegaloo, gox bu ci nekk ami jagley boppam:
Fatt-jawwu walla JAWWU JU FATT ji: mooy ji gën a tal gën a fatt te gën a féete suuf; moom ngelawam day yëngu jamono ju nekk, fa lay niir yi di sosoo ak mbooleem soppaxndikuy jawwu yi; kon cig jege mooy jawwu ji ëpp ag jeexiital ci wàllug dëkk ci kaw suuf ak ci ni kilimã bi di séddalikoo
- Yolom-jawwu walla JAWWU JU YOLOM ji: mooy tiim bi ñu la njëkk a wax, moom nag ngelaw lu yëngoodi moo ko sos, lu ñàkk a ñàkk.
- Iyon-jawwsu walla JAWWU JU IYON ji: moom mi ngi sosoo ci ay dogiit yu ñu kurãal walla yu nu mbëjjal yu soreente.
- Biti-jawwu walla JAWWU JU BITI ji: mooy féex gu biti gi, fi nga xam ne ag féex gu joyoo fa nekk .
Jéeri ji (Lithosphere)
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mbooleem beeñ bi ak doj yi ñoo sos wàll gu tond (superficiel), gu dëgër gu kol-kolu suuf si, ñu koy woowe Jéeri ji walla aji wow ji.
bu ñu séddalee Jéeri ji, def ko ñeenti xaaj, ñatt yi daanaka ndox yee leen muur, yooyu ndox nag ñoo sos mbàmbulaan yi ak géej yi, waaye wàll yi génn ci jéeri ji; nga xam ne ndox yi muuruñu leen (gox yi ak dun yi , wàll yii ñooy wërlaay gu dëppoo te méngoo ak dundug nit, moo tax fi la nit di dunde, di fi defe ay liggéeyam, walla li ëpp ci ay cawarteem (activités).
Jéeri ji nag day dund tey màgg ci anam gu sax, ak doonte fi nun, day mel ne ni mu nekke soppikuwul. Li ko waral nag mooy ni muy soppikoo day faral a yeex lool: doj yi bu ñu sosoo ci ron géej gi, dañuy mujj lemu, yékkatiku, màgg ànd ak Jamono yu jiyoloji yi ñooy mujj sos ay càllalay doj yu yees.
Ci safaanub loolu doj yi gaaru ci kanamu jëfkay jawwu yi dañuy xolliku, di xoosu, di fellu, bu ko defee, yooyu xoosiit ak felliit (ban yeek beeñ yeek yi ni deme) ñooy mujj sottikuwaat ci géej gi
Xam-xam | ||||
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma | ||||
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal | ||||
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama |