Aller au contenu

Xam-xamu nosukaay

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Xibaarfeppal)

Xam-xamu nosukaay (walla Xam-xam bi ñeel nosukaay), moo yor gëstu gi aju ci cëslaay yu xibaar yi, xarala yi ñeel seenug nos ak seenug jëfandikuwiin ci noste yi ñuy jëfandikoo ay nosukaay. Ñi ciy yëngu seen liggéey doon lëkkale ay nosukaay ñu doon li ñuy tuddee ag lonkoo, defar ay dàtti njoxe, boppal ay noste, defar ay tëriin te loolu laaj na xam ag kàllaamag tëriin, .

Cig lawal, xam-xamu nosukaay dafa ëmbu ci li ñuy wax xaralay xibaar ak jokkoo yu yees yi di xeetu xam-xam bi ëmb lépp li ñeel xibaar, ci gépp anamam. Ci tëriin wi la tëralkat bi di joxee ay tegtal nosukaay bi ci anam gi mu war a yoree xibaar yi, lan la ci war a def ak nan la ko war a defe. Jëfaan yi nag ñooy mbooleem cëri nosukaay bi, benn bu ci nekk am na liggéey bu ñu ko sant: yii di rënk xibaar yi, yii di leen wone ni nga bëgge, yii di leen soppi...

Ba àdduna dooree ba tay nit daa mas di ut ay jumtukaay ngir man a def ay waññeem. Ci jumtukaay yooyu, ci yi gën a yàgg, man nañu cee lim àlliway Hammurabi (1750 laata yeesu). Wuutuloxo yu doolerandu yu njëkk ñoo ngi tàmbalee feeñ ci diggante XVI ak XVIIu xarnu. Waññikaay bu doolerandu bu njëkk, jàpp nañu ne, mooy bu Wilhelm Schickard ci XVIu.

Ci 1642 Blaise Pascal defaroon na, moom itam, ab Waññikaay bu doolerandu, doonoon bu ñu doon jaay sax, ba tay jii juroom-ñeent ci yooyu man nga leen a fekk ci jeexiituwaay (musée) yi. Ci ay njëlbeenam man nanoo wax ne xaymaan yi rekk ñoo ci doon yëngu ndax li leen yitteeloon moo doonoon defar ay jumtukaay yu leen di yombalal seeni Waññi yu xayma. Ay cëslaayam yépp ci xayma lañu taxaw, rawati na liñuy way aljibar bu Bool.

Tay jii xam-xamu nosukaay jël na wàll wu am solo ci sunug dund, cig suqali ci wàllu koom-koom ak mboolaay yu askan yi.


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Xam-xamu nosukaay