Aller au contenu

Wërlaay

Jóge Wikipedia.

Wërlaay gi di ci tubaab (environnemt) mooy dénd bi maanaam (nature bi) ak li ci nekk ciy way dund ak yu dundul, ci gàttal daal adduna bi nu wër ci kaw suuf si. Xam-xamu wërlaay mooy biy jéem a indi ay tontu ci yenn laaj yi aju ci nan la dénd biy jëfe ak a jëflanteek way nekk yiy dund ak yeneen way nekk yi, walla nan lay jëflanteek digg bi ko wër moo xam digg bu kimya la (simi) walla bu dénd (nature). Digg bii moom lanuy tudde “Noste gu wërlaay”. Looloo waral nuy gis noste gu wërlaay muy luy ame ci ay way nekk yuy dund ak yu dee walla yu way. Xam-xamu wërlaay mooy jàng ak gëstu way nekk yiy dund ak séenug séqoo ak li leen wër ak jeexiital gi nuy def ci sunug séqoo ak suuf si. Nosteg wërlaay mooy mbooleem jëfka (facteurs) yu dundul ak mboolaay (société) yiy dund yu xeet yi nekk ci benn gox walla barab. Dénd bi day wëndéel mbir yi mu jëfandikoo woon ngir delloo leen ñu mujjaat di mbir yu am solo ak njariñ. Càllalag ñam ci kaw suuf si, aw melo la ngir wone ni kàttanug ñam di dugge ci wërlaay gi. Foofu ñam da fiy juge ci aji nekk dem ci jeneen n gir jox kàttan dundat boobu di sàqami ñam wi ak a reesal, gépp càllalag ñam nag ci jant bi lay tàmbalee. Dundat yi - nit ci la - munuñoo liggéey seenub dund, looloo tax manul a ñàkk mu jot ci dundam boobu jële ko ci gàncax yi walla yeneen dundat yi, looloo waral ñuy jàppe dundat yi ay way lakk walla ay way jëfandiku (consomateur), mujjantalu dundug dundat it mooy ag feccikoom (ag tasam) jaare ko ci ay mikrob walla ay gàncax ngir mujjati di suuf, gàncax gi muucooti ko ngir liggééyati ci ñam wu beesati. Lii nag moom lanuy tudde “Càllalag ñam”, bokk na ci jëfkay dénd yi ci nosteg wërlaay gi te am ci jeexiitalm it: leerug jant bi ak ker gi ak tàngoor wu diggdóomu wi ak séddalig sewogaraafi gi ak ngelaw li ak barab yu yékkatiku yeek yu suufe yi ak melokaanu suuf seek ndox mi. bokk na ci jëfkay kimya yi yiy bàyyi ay jeexiital ci nosteg wërlaay gi: tolluwaay (niveau) bu ndox yi ak ngelaw li walla jawwu ji ci suuf si ak kem ni way dundal yu gàncax yi di seeye ci suuf si ak ndox yi ak tooke yi ci nekk, ak xoromus ndoxum géej ak oksijiin bi ci seey.

kay diang wolof


Ci baax, wërlaay - walla barabub jëf mbaa mbir, maanaam fu lëf nekk mbaa deesi defe ko fa - mi ngi ame ci jëmm yi (substence), peekte ti (circonstance), mbir yi walla nekkiin wi ko peek wër ko, te di fa ame.

Bu dee ci wàllug dundat (biyoloji) rawati na ci wàllug dénd (ecoloji)day tekki lépp lu man a def ay jeexiital yu jonjoo ci doxug walla màggug mbaa jëm kanamug mbir yi (metabolosmo)walla nekkiinu jëmm walla xeet wuy dund ( SPECIE VIVENTE), loolu nag leer ci la, ngelaw, ndox, suuf ak yeneen nekktéef yiy dund.




Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Wërlaay