Tëriinuw nosukaay

Jóge Wikipedia.

Ci xam-xamu nosukaay tëriinuw nosukaay walla tëriin kepp , am mbooloom ay càkkuteef la gees binde ci genn kàllaama gi gu ab nosukaay war a jëfe . Di ag càllalay càkkuteef gu xellu te nosu, mbooloom ay cantaane yuy indi saafara ci yenn xeeti jafe-jafe. Aw tëriin wees bind cig kàllaamag masin, wu ab nosukaay man a doxal dees na ko wax itam tëriin wu doxalu walla tëriin wu ñaarñaaloo. Aw tëriin wees bind ci kàllaama gu assembly walla ci tëriin wu tolluwaayam kawe, nosukaay bi dafay jëfandikoob boolekaay walla ab tekkikaay ngir man koo doxal, dees na ko wax tëriin wu gongikuwaay.

Saa yoo yëngalee janax ji walla nga bind ak sa arafukaay, nosukaay bi ab santaane bees ko jox la jëfe, santaane yu jóge ci benn walla ay tëriin. Santaane yooyu ñooy di déglu bë jëfandikukat bi te di leen jëfe: ubbi ab dencukaay, bind, xayma, seet añs. Jëfekaay bi mooy wàll wi nekk ci nosukaay bi biy jëfe càkkuteef yi nekk ciw tëriin. Jëfiin wi mooy yoon wi nosukaay bi di jaar, jéego ci jéego, ngir jëfe càkkuteef yi. Kiy bind aw tëriin lees di woowee ab tëralkat