Aller au contenu

Kàttan

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Kattan)
Melax gongikuwaayu kàttan la. Waaye moom dooleem mi ngi aju ci gaawaayan

Kàttan mooy man a def dara (sos ag soppi), kàttan nag am na ay melo yu bari, yi ci ëpp solo ñi ngi feeñe ci tàngoor ak leer.

Ci biir “xam-xami dénd yi” (science naturelle) kàttan man na fee jël ay melokaan yu wuute : “kàttanug tàngoor”, “kàttanug kimyaa (simi)”, “kàttanug mbëj”, “kàttanug ceññeer”, “kàttanug saal (nucleaire)” ak ci mujjantal gi “kàttanug mbëjbijjaakon (éléctromagnétique)” añs. Xeeti kàttan yii ñaare dees leen di séddale ci: “kàttan guy yëngu ak “kàttan gu nëbbu” te kat am na yenn kàttan yoy dëppoowunook séddale gii, lu ci mel ni: “leer gi”, ak yeneen yoy man nanoo nekk am njaxas mu tukkee ci ñaari kàttan yi, guy yëngu gi ak gu nëbbu gi.

Lu bari ci xeeti kàttan yii manees na koo soppi (transformer) jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, jaare ko ci jëfandikoo ay jumtukaay yu fasoodiku (simple) walla ay xarala yu fasu (compliqué): la ko dale ca “kàttanug kimya” ba ci “gu mbëj” jaare ko ci jumtukaay bu siiw bi di tegale(pile) yi, walla ndëxañtéef yi, Albert Ayinstaayin it ci biir ”faramfaceg ajoo” (theorie de relativisme) boole na ñaari ëtt yii di bu ne-ne ak kàttan, nga xam ne kàttan day mujj man a soppiku di ne-ne(matiere), naka noonu safaan bi, maanaam neen soppiku moom it di kàttan: wuññi (découverte) gu yees gii mi ngi ko xamalee ci yemalem gu siiw googee E=mc2, soppiku gii ci jëf (ci wàllug pratique) ñi ngi ko firee ci man gi nu man a ame kàttan jaare ko ci “xarug saal” walla “booleeg saal”.

Waxiin walla baatal (terme) yu kàttan yi akug soppikoom lu am njariñ la ci leeral jëfiini dénd yi. Ba sax feeñte(phenomene) yu kilimã yi niki ngelaw, taw, melax ak riddi yi (tornado) dees leen di jàppe ñu juddoo ci soppiku yu kàttan gi juge ci jant bi wàcc ci suuf si. Dund gi ci jëmmi boppam dees koy jàppe muy benn ci njuréef (resultat) yu soppikuy kàttan yi: ci anamu “toggaleg leer gi” dees na ci jële soppi kàttanug jant bi yóbbu ko ci “kàttanug kimya” ci biir gàncax yi, bu ko defee ci kanam ñu man a jariñu ci kàttanug kimyaa gii nu denc, ci ay “liggéeyiinu wëlbati” ci ay way nekk yuy dund.

Njariñam ak yaxam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci biir jëfandiku gu mboolaay (gu société bi): baatub kàttan dees koy wooye lépp lu nekk ci ron gongikuwaayu kàttan (source d’energie), juddalug kàttan, lakkug kàttan (ag jëfandikoom) ak wattu rootuwaayu kàttan (maanaam fi muy juge), ginnaaw nag dooley koom-koom dafa laaj te soxla ab rootuwaay walla ab gongikuwaay ci gongikuwaayi kàttan yi, looloo tax ag amam akug yooxam(baril ko) bokk ci yitte yu mag yiy caabi. Ci at yu mujj yi, jëfandikoo kàttan feeñ na di benn ci jëfka (facteur) yi gën a sabab nuggug àdduna bi (global warming), looloo ko def muy ab lëj-lëj ci li ëpp ci réewi adduna bi.

Coppiteg kàttan

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Manees naa soppi kàttan jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, ci misaal, manees naa soppi kàttanug kimyaa gi ñu denc ci ab tegaleeb(pile) Jiib def ko ag leer.

Kem (quantité) bu kàttan bi nekk ci àdduna bi, day lu sax ba fàwwu, kàttan du jeex, du sosu, li am kay mooy day soppiku juge ci melo dem ci weneen. Bu melee ne kàttan dafa jeex, booba jeexul, daa soppiku kay dem ci weneen melo. Looloo tax ñuy gis ne kàttan mooy man gi neen man a def ab liggéey (yëngu) muy njuréeful yëngoom googu, walla njuréeful ab barabam bu nu ko nattee ci doole yiy liggéey ci kawam. Kàttan giy ànd ak yëngu moom la nuy tudde “kàttan gu yëngu”, kàttan nag gi am ag jokkoo ak barab bi moom la nuy wax “kàttan gu nëbbu” (gu coona walla gu ñu dëxëñ (gu nu denc) )...

Melokaanam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kàttan dana ame ciy melokaan yu bari, niki kàttanug doolerandu (mecanique) ak gu tàngoor, ak gu dinaamig gu tàngoor (tangdooleel,termodinamique), gu kimyaa, gu mbëj, gu ceññeer ak gu saal( walla xartil), kàttan yii yépp nag man nanoo def ag soppiku gu biir jaare ko ci ay yoon yu dëppoo. Ñam wi nuy lekk am na kàttan gu kimyaa gu yaram wiy denc te di ko génne bu nuy liggéey walla nuy génne ab coona (def effort)

Kàttan ci taariix

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kàttanug bàyyima yi mooy gi nit njëkk a jëfandikoo ci fajarug xay (bi xay (civilisation) di door a am), loolu mooy bi mu jëlee bayyima yu miin yi di leen jëfandikoo ciy liggéeyam, ginnaaw bi mu tàmbalee jëfandikoo dooley ngelaw li ci doxal ay loocaam ba ci ay gox yu sori ci géej gi. Lu xayam di gën a yokku muy gën a jëfandikoo kàttan gii, mu jëfandikoo ko niki kàttanug doolerandu (mekanig) ngir doxal walukaayi ngelaw yi, ak ngir dawal ponoy wuutuloxoy wal yi, ak daggukaayu dénk yi ak najukaay yiy yékkatee ndox yi ci teen yi. Lii mooy li nu xame ci turu kàttanug doolerandu (mekanig).

Xeeti kàttan yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

ci maanaa, da nuy ràññee xeeti kàttan yu bari te wuute. Kàttan tamit day tax nu man a natt melow feeñte yi, seenub taraay; feeñte gu ne ak kàttan ga mu àndal.

Xeeti kàttan yi nu yàgg a jàpp:


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Kàttan