Diiwaanu Ndar
Diiwaanu Ndar benn la ci 14 diwaani senegaal yi, moo gën a féete bëj-gànnaar ci réew mépp. Moo feggook réewum Gànnaar, ci guddaayu dig gi mu am ak Senegaal gépp ba fi dexub Senegaal bi di àgge ci mbàmbulaanug Atlas gi.
Taariix
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Démbu Ndar Géej
Bès dafa am feebar buy walle bi mabboon seen gox bi nu doon woowe Ndar, samppu woon si diggante ñaari dëkk yu tudd Biyer ak Geber. Ñaari dekk yi ñi ngi nekkoon si joor gi. Ba loola xewee, la waa dëkk ba fabu gaddaay ag seeni gaal, xoti dex di dem, ba teersi fi tay nuy wax Dunu Ndar. Li taxon kon mo di ne danoo beggoon mucci si musi ak balaa bile naroon a raafal seen ñoñ. Turu ndar wu jekk wi lanu toxal indi ko si dunu wi si dig ndox ngir maggale ko seen dëkku maam ba nu jóge, ngi itam ba ña fatte fa nu bayyikoo. Lii ga man see jànge ni tur si dëkk ak si lu mu man a doon, dafa war a mandarga cosaan, lukko moy, nit ki man naa dem ba fatte fu mu soqe koo. Si ñi ko Maalik waxe ba leegi, wen xaaj si way-gaddaay yi, da no fafoon des si joor gi janloog tund wi, ginnaw gi nu tudde teenu geej. Beneen calale da fa indi ag goor gu joge réewu gannaar, bu nu doon woowe Ametlika Ben Ndar, soqe ki sa Singeti, moom la ay settam tudde dekk bi di ndar.
Xarnu bi tubaab yi di wandeelu ci wetu tefesu senegaal, ku ñu naan Ndaak Kumba Nan Sango moo doon nguuru ci imprator bu waalo. Boo ba jamano, waloo mi ngi woon si dig dooleem, di tëg ay ndën ndam. Suuf su nangu mbay, njënd ak njaay mu dox, si diggante nit ñu nuul yi ak naari ganaar. Xarnu junni ak ñetti teemeer la woon jappu junni ak ñetti teemeer ak juróom ben fukk. Tukkikat tubaab yi, waa ruyang ak nitu jeppo yi doon nañ fa joofsi ngir bokk si njënd ak njaay ma fa daan am. Booba lii dong la nu fa doon def, walis nag nu amoon yeneen mbetet yu nu nebboon. Taarixkat yi jappu nanu ne xeet yi ño fa jiitu woon waa portugaal. Si atum junni ak ñetti téeméer ak juróom ben fukk ak ñeent la wa gox ba tambale jaay tubaab yi lusi mel ni mboq, dugub, ak yeeneen. Ñoom tubaab yi sax ni ngi xamee xeetu dugub yile fi si Afrig, rawatina seneegal. Ja bi ci waloo nag, mboleem yi doon yëngatu ci koom-koom si réew mi, nga bayo kajoor, wala biir waalo da nga fa daan ñów ngir jaay wala jènd ay yëf. Dawalkatu gaal yi jóge tugal demmon nanu ba dugglaante ak way-njiitu paraag yi. Ndawtal yi ag yóbal yi leen wa njiit yi doon jagleel moo gennoo na dëggeral seeni kolere.
Ay doomi normang yu am fit xuus nanu mbeex bi ak seen gaal àggsi ci dexu senegaal. Sa teeruwaay mo doon dunu Morfil, bërëbu seeluwaay. Tangoor bi ak feebar yi nekkoon ci réew mi daan fagaagal ñi ëppoon ci noom, ba tax na ñuy ci bari danu daan faral di ñakk seen bakkan. Wante galankoor yi musu leen tayyeeloo, wala mu leen di lotal ba ta ñuy yebbi seen ëmb te baña tee tukki. Galam daakande, ak bejjani ñay moo leem gënnoona soxal. Ci gattal, njënd-ak-njaay mi daan dox si xarnub fukk ak ñeet moo indi jëflaante waa tugal yi ak wa sóodaan.
Fara Xoy Jóob, buuru Waalo ci atum juróomi junni ak juróom téeméer ak fukk, moo njekka artu nit ñi, rawatina nappukat yi si nu bayi xell mbeex mi. Jamano yooyu, ay néewu tubaab danu doon tëmb si géej gi te ken xamul lu ko waraloon. Ba nu tegge juróom ñetti at la waa portugaal dall si dunu mboxos bi nekk si wetu ndar. Su nu beggoon na jeggi bel bi, baraak bi nekkoon ganjool da leen doon laaj ndamppaay. Si noonu lanu tambalee xuus gëeju senegaal ba podoor, jaal ngalam, ba jennee. Naari gannaar yi danu leen daan faral di sòng ay còng yu tàr, dileen lalal ay ndëg-sërëx. Dunu morfil lanu daan jaaye seeni nganaay, ak yeneen jumtukaay yu jem si xare. Foofu itam lanu daan wacce jaAm yi nu jappoon, ñaari way-watu timmaleleen ay mëx-dóom, ku daw rekk nu soqi ci sa kow. Kon jaam yi njek wacci si suufu ndar, dekkun fa woon. Jaaxle nag mi ngi tambalee sotteeku ci xelu nit ñi bi nu seetloo ne seen doom di ay nappukat ñi reer ni mes ci géej gi te xamu nu lan moo tax. Ndekete yo ay woroom gaal yu tubaab ño leen di doggaanu, di fadang jemmee tugal. Jamano booba, buur Tiaaka bu waalo moo amme woon. Ay jum yuy tak, ar fer-ñeet ak ay saliir yu raglu doon nanu jip si géej gi. Ba si saxaar su nuul, su xasaw di agsi ba ci ker yi. Xeex bu meti moo doon am si diggante tubaab yi seen boppu. Waa faraas, portugaal, olaand ñoo don xëccoo. Ku ci nekk bëg aakimo dend yi . naar yi tamit door seeni lël ngir jappu nit nu nuul yi di leen jaay njaam. Yen si nappukat danu doon jëflaante ak tubaab yi ci mbeex mi, di leen jaay ndox mu neex, jen, ak yu ni mel. Tubaab di leen jox ay sangara, wenñ, ay piis, ak tooke. Si njelbeenu fukk ak juróom ñaari xarnu, ci nguurug Buuru faraase bu tuddoon lui fu ak ñett, ci la kangam Riseliye joxe ndigel way tukkikat géej yi ngir nu tambale foxrañi beppu suuf bu ñu man a foxarñi ci dendub Afrig.
Dayoo bi mu am tey jii, mi ngi jóge ca séddatle gi ñu def ci atum 2002. Bu njëkk diiwaan bi da fa ëmboon tamit diiwaanu Maatam bépp ak li ko wër.
Ay Tundam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Xool it
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (fr) Annie Ravisé, Contribution à l’étude des Kjökkenmöddinger (amas artificiels de coquillages) dans la région de Saint-Louis, Dakar, Université de Dakar, 1969 (Mémoire de Maîtrise)
Lëkkalekaay yu biti
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (fr) Statistiques Geo Hive
- (fr) Conseil régional de Saint-Louis
- (fr) La région aux Archives régionales du Sénégal
- (fr) La filière lait et produits laitiers dans la région de Saint-Louis (Christian Corniaux, rapport, avril 2003)
| |||
Cees · Fatik · Jurbel · Kafrin · Kawlax · Kéedugu · Koldaa · Luga · Maatam · Ndakaaru · Ndar · Séeju · Siggcoor Tambakundaa · |