Dëgërluwiin
Dëgërluwiin walla Dëgërluwiin gu mbëj mooy ni ab wommatukaayu mbëj jikkowoo di jéem a bañ ay yani mbëj di ko jàll, di dëgërlu. Ci dëgërluwiinu ab jumtukaay lanuy man a xamee nu ndëgërloom toll.
Tekki
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dëgërluwiin wi ρ bennaanu nattam mooy ohm x meetar [Ω x m], dafa aju ci ni wommatukaay bi bindoo (dijjaayam, guddaayam) waaye li ko lonkale ak Ndëgërlu gi R mooy mile mbind:
- ρ mooy Dëgërluwiin wi ñu koy natte ohm x meetar [Ω x m];
- R mooy ndëgërlu gu benn dogu jumtukaay boo jël ñu koy natte ohm [Ω];
- l mooy guddaayu jumtukaay bi dawaan bi di jaar ñu koy natte meetar;
- S mooy dijjaayu jumtukaay bi ñu koy natte meetar kaare [m2].
Sunu wëlbëtee ci bii yamale mu jox nu nan lanuy natte ndëgërlu gu ab wommatukaay bu nu xamee guddaayam ak dijjaayam:
Dëgërluwiin gi manees na koo natte itam ak bii yamale:
- E mooy taraayu toolu mbëj bi, ñu koy natte volt ci meetar
- J mooy fattaayu dawaan bi, ñu koy natte ampere ci meetar kaare
ci mujjante manees na koo natte itam ak safaanu wommatiin wi:
- σ mooy wommatiin wi.
Ajoom ci tàngoor
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dëgërluwiin gu ab wommatukaay dafay aju ci xeetu ne-ne bi ñu ko defaree.
Dëgërluwiin gu ab mbéll
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci mbéll yi Dëgërluwiin gi dafay yokk lu tàngaay bi di gën a bari, manam a wommat dafay wàññeeku. Safaan wa su tàngaay bi wàññee koo ba àgg ci benn lim bumu manuta romb.
mooy Dëgërluwiin gi T tàngaay bi, mooy Dëgërluwiin gi ci tàngaayu delluwaay bi, naka-jekk benn ci ñaar yii lay doon 0° walla 20°. &alpha di ab ngungu tàngoor bu aju ci ne-ne bi.
Dëgërluwiin bu ab xaaj-wommatukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dëgërluwiin gu ab xaaj-wommatukaay dafay wàññeeku lu tàngaay bi di yokk, kon lu tàngaay bi yokk ñuy gën a man a wommat. Bii digaale moo koy faramface:
A, B ak C ay ngung yees jagleel ne-ne bi lañu.