Arminaat

Jóge Wikipedia.

Arminaat seddatlinu taariix(date) yi la ci jenn jamono. Doon na ag noste gu waa Isipt yu yàgg ya sàkkoon ngir séddatle ak a nos jamono ji ci ay diir. Ca ndoorte la dañu koo sàkkoon ngir man a dëppale yenn feeñte yu saytubiddiw ak yu gëstubiddiw ak jamono ja ñuy amee. Doon nañu ko jëfandikoo it ngir natt seeni bési xumbéeli diine.

Bennte yu arminaat[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci taariix arminaat yépp a cëslaayu ci ay bennte(unite) yu dénd yu seen diir aju ciy feeñtey saytubiddiw.

Bés[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daanaka ci xay yépp, coppite gi ci bés ak guddi moo doonoon bennte bi ñuy natte at yi. Wëndéelug Suuf si doon li waral safaanu googu, te njël gi du amandoo ci barab yi ne ci kol-kolu suuf si . Soo xoolee Senegaal ak Faraas bokkuñuy waxtu, Faraas a ñuy rawee ñaari waxtu su dee nawet la, benn waxtu su dee noor la .

Weer[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li demiinu weer doon lu yomb a may-bët, moo tax mu doon ab jumtukaay ngir natt jamono ji. Arminaatu jullit ñi moon weer wi lay topp , waaye arminaatu geregori moom jant bi lay topp.

At[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mooy mbooleem jamono yi, at doon na diir bu gudd. Cig njort, Moom it ci yenn feeñtey dénd la ko nit ñi ko sàkk arminaat daa natte.

Arminaat bi njëkk a cëslaayu ci at, maanaam ci soppiku at ba at mooy arminaatu waa isipt.

Booleeg benntey dénd yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

At ak bis[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci jamono ji ñu ne, am at mooy 365,24220 bis. arminaatu waa isipt, ak arminaatu suleymaan, ak arminaatu geregori, doon nañu ay royuwaay ci liggéey bu mag bi ñu def ngir man a dëppale (syncroniser) at mi ak wëndéelug Suuf si ci li wër jant bi.

ba tay sax séenug dëppoo des na, ba tax na 10000 at yu ne di na juum 3 fan.

Weer ak bés[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Diirub weer mooy 29 bés 12 waxtu 44 simili ak 2,8 saa (muy 29,53 bés). Kon su ñuy weccee ay weeri fanweeri fan ak yu ñaar-fukk ak juroom-ñenti fan, te di yokk benn bés fanweeri weer yu ne, dina doon lu nanguwu. wii nattiin, arminaati weer yépp a koy jëfandikoo ngir dëppale bés yi ci weer ak wëndéelinu weer wi.

Jamono ak at[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci arminaat yu bari, ñeenti jamono ñoo am: noor, nawet, lolli. Jamono yooyu, ci xay goo dem ak ni ñu koy séddalee ci at mi. Su ñu xoolee waa siin ñoom nawet la at mi di tambalee.