Ancos ci Siri

Jóge Wikipedia.

Ancos, ca jamono Injiil, péeyu diiwaanu nguuru Room bu tudd Siri la woon. Dafa nekkoon ca wetu joor gu naat ca dex gu yaatu gu tudd Oront (fleuve Oronte), 32 kilomet ca kaw bëlu dex ga, maanaam fu dex ga dugg géej ga. Teeru Ancos moo doon ca dëkku Selusi, bu nekkoon ca Géej gu Mag 8 kilomet ca noru bëlu dexu Oront ba. Selusi nekkoon na 26 kilomet ca sowu Ancos.

Ca at bu Pool demoon fa, daanaka atu 43 g.K. dëkk bi xumb na. Nu ngi doon tabax di beesal dëkk ba, gannaaw ñaari yëngu-yëngu suuf yu yàqoon lu bare. Ay fukki junni Yawut ya dëkkoon Ancos te ñoom woomle nañu, te seen jàngu rafet nañu. Gereg yu bare ñi ngi doon ñëw ca seen diine. Ancos moo doon dëkk bu neex a dëkk te rafet. Waaye dëkk ba dafa siiwoon itam ndax seeni noos, seen ñaawteef ak seen njaaloo ak doxaanu yàqute. Bànneexu àddina si rekk la waa Ancos doon wut.

Dëkku Gereg bu am solo la woon bu nekkoon ñetteelu dëkk bu gëna mag ci nguuru Room gannaaw dëkki Room ak Alegsàndiri. Buuru nguuru Maseduwan ñoo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist. Naka noonu ña fa jëkk a dëkk ñoo doon ay xarekatu Maseduwan ak waa Aten. Waaye yeneen Gereg ya toppoon nañu ca ñoom. Tamit buuru Geres dafa xiirtal Yawut ya ñu ñëw dëkk fa, te may na leen ñu nekk jaamburu dëkk ba. Waa Room nangu nañu diiwaanu Siri ca atu 64 j.K. Naka noonu ca jamono Injiil dëkk bi dafa boole waa Maseduwan, waa Geres, waa Room, waa Siri ak Yawut ya. Waaye amoon na ay jafe-jafe diggante Yawut ya ak ñi des ca waa Ancos ba dem sax ba am jamono waa dëkk ba bëggoon nañu rey Yawut ya fa dëkk.

Ca suufu nguuru Room diiwaanu Siri dafa jëm kanam bu baax. Waa Room ñoo defoon Ancos seen péey ak màkkaanu xare ci diiwaanu Siri. Waaye ba tey waa Room may na dëkk ba mu yilif boppam. Ndegam Siri dafa nekkoon ca digu nguuru Room te mu féete waa Pàrt, beneen nguur bu xeex ak nguuru Room, Siri nekkoon ca suufu buuru Room ba moom ci boppam. Buur ba, Sesaar, moo faloon benn jawriñ ngir toogal ko ñetti at ba juróomi at yu nekk, mu nekk Boroom réewu Siri. Boroom réewu Siri moo sutoon Boroom réewu Yude, di ko yilif. Amoon na ñeenti mbooloom xare bu tudd 'léjiyoŋ' ca Siri, bu nekk bu am 6.000 xarekat ya. Amoon na itam ay gaalu xare ca Selusi.

Yaakaar nañu ne daanaka 200.000 nit ña fa dëkkoon ca jamono Injiil. Benn boroom xam-xam dafa yaakaar ne benn cér ca juróom-ñaar ca niti dëkk ba Yawut la woon te Yawut ya dëkkoon ca ñetti gox ya. Yawut ya amoon nañu alal te seen dundin xëcc na yu dul Yawut yu bare ñëw bokk ca seen diine.

Koom-koomu Ancos amoon na doole lool ndax kàttan gu mu am ci biir nguuru Room, tamit ndax yoonu jaaykat yi am solo ya jaaroon Ancos ak ndax lu ñu fa defaroon ca dëkk ba. Ancos dafa siiwoon ndax dàllu der yu rafet, latkoloñ, saf-saf yi ak ndàbb lu xeeñ, piis yi, gànjar ya ak takkaay ya, téere ya, ak li tëggu xaalis ak wurus defare.

Yoonu jaaykat ya jóge ca penku, maanaam Babilon, Asiri ak Iraak jaar na Ancos, te dafa tiim yoon wu dem nor ak sudd wu boole Palestiin, Siri ak Asi Minër. Naka noonu amoon na wenn yoonu jaaykat wu jaar ca tund ya ca xunt bu tudd 'Buntu Siri' ba noppi dem Tars. Yoon mu jóge Tars wu tudd 'Yoonu Eŋaca' (Via Egnatia) dafa jàll Asi Minër ba dëkku Efes. Tamit gaal ya mënoon nañu dox ca dexu Oront diggante géej ga ak dëkk ba.

Dëkk ba, moom, rafet na lool. Nguuru Geres def nañu yoon ya ca kaw tëralinu damyee ngir yoon yu mag ya jàpp ngelaw lu féex lu jóge géej ga. Amoon na benn miir bu mel ni tata bu wër dëkk ba lépp. Buuru Room bu nekk tàmbali ak Pompey ca atu 64 j.K., dugg na xaalisu nguuru Room yu bare ci tabax ya ak rafetaayu dëkk ba. Ni bépp dëkk bi Gereg ya walla waa Room tabaxoon amoon na ay powukaay ak amfiteyatërë, ay màggalukaayu yàllay xërëm yu bare, ak ay këru sanguwaay ya. Feesoon na dell ak ay pénc fu xale ya doon fo, waxkat ya indi seen wax, jaaykat ya jaay, te reetaanlukat ya bégloo mbooloo ya. Def nañu ay robine ca kaarfuur mbedd ya ngir jigéen ya mënoon nañu root, ndox moo xam ne mu jóge ca dex ga walla ca ay bëtu ndox ya amoon ca dëkk ba. Tamit Yulyus Sesaar tabax na benn 'akwadakk', maanaam pom bu indi ndox, ngir dimbali gox yoo xam ne amuñu woon ndox.

Erodd bu Mag ba tabax na wenn yoon wu jàll diggu dëkk bi diggante buntu miiru dëkk ba ca penku-kaw, ak buntu miir ca sowu-suuf. Yaatuwaayu yoon wu mag woowu 10 meetar la woon. Dem na 4 kilomet, te lépp tali doj wu dëgër wu jóge Misra, walla marbar. Dafa dem ca pénc bu réy ca diggu dëkk ba. Ca pénc moomu amoon na benn nataalu Buuru Room Tibeer Sesaar bu réy bi ñu defare xànjar. Ca wetu yoon wa ca ñaari bor, fukki meetar yu nekk, amoon na ay kenu doj yi ñu taaral. Dafa meloon ni mbaar ba tax ñi dox ña mënoon nañu dox ca wetu yoon wa guddaayam lépp te bañ génne ca naaj wa walla taw ba. Yu gën a bare ca kenu ya amoon na ay nataal yi ñu yett walla defar ca xànjar. Diggante kenu ya amoon na bunt ngir dugg ca kër ya, bitik ya ak biro ya. Yoon ya amoon na sax làmp ya tàkk guddi.

Amoon na benn dun ca biir dex ga fu dex ga jaar ci biir gox yu nekk ca noru dëkk ba. Guddaayam ak yaatuwaayam 3 kilomet la. Foofu lañu tabax këri buur yi, ak benn estaad ngir rawante fas ak sareet ya. Guddaayu estaad ba 500 meetar la woon ba moo wara tax mu bokk ca ya gën a réy ca àddina si.

Ancos amoon na itam ay màggalukaay ca yàllay Gereg ak Room, ak ay powukaay. Yàllay Ancos moo doon Sës.

Juróom-ñetti kilomet ca suddu miiru dëkk ba amoon na benn gox bu tudd Dafëne. Ca wetu yoon wa dem Dafëne amoon na ay tool fu ñu bey lawtanu réseñ ngir defare biiñ ak tóor-tóor yi ñu defare latkoloñ. Dafa nekkoon ca kaw benn déndu tund, maanaam 'palato'. Yaatuwaay ak guddaayu palato ba bu ne 1800 meetar ya la, te mu nekk 90 meetar lu gën a kawe niwo Ancos. Amoon na màggalukaay ca yàllay xërëm ju jigéen ju tudd itam Dafëne. Waa Ancos gëm nañu woon ne Dafëne nit la woon, ki Apolo, benn yàllay Gereg, soppoon. Apolo dafa ko dàqe di dàqe ba ci mujj Dafëne dafa soppiku nekk as ngarab bu tudd 'loriye'. Goxu Dafëne amoon na benn sardin walla park bi ñu defaroon ngir bànneex rekk bu am wëraayu 16 kilomet. Ca biir màggalukaayu Dafëne amoon na ay sëriñ yu jigéen yu nekk gànc yu bare. Guddi gu nekk ci seen turu diine ñu defaat li amoon ca nettali ba, maanaam jaamukat ya doon nañu dàqe sëriñ yu jigéen ya ci biir garabu loriye yi ci biir sardin ba, ba jàpp leen di séy ak ñoom.

Buuru Room Ogust Sesaar samp na benn po 'olimpik' (Jeux D’olympique). Ñeenti at yu nekk po boobu indi na ay joŋantekat yu bare ngir rawante ci diiru 30 fan ci daw, tëb, sànni xeej ak fitt, rawante fas ak sareet, bëre ak ñoom seen. Amoon na itam rawante ca misik ak ci tari nettali.

Gis nañu ne ay at gannaaw deewu Kirist, mbooloo ñi gëm ca Yerusalem fal nañu benn waa Ancos bu tudd Nikolas ngir mu bokk ca juróom ñaar yi doon toppatoo yëfu mbooloo ñi gëm (Jëf 6:5). Xebaar bu baax bi egg na Ancos gannaaw deewu Ecen daanaka atu 40 g.K. (Jëf 11:19-21). Ñi ko indi ay Yawut yi làkk Gereg lañu woon, yi jóge dunu Sipar ak dëkku Siren ca Libi. Ñoom def nañu lu bees. May nañu Gereg yi topp Yeesu ci lu sësul ca xaraf walla yeneen aada Yawut. Mbooloo bu mag gëm na Boroom bi. Foofu lañu jëkk tudd taalibe Kirist 'Gaayi Kirist' (Jëf 11:26). Ci bu jëkk tur boobu turu foontoo la woon. Waa Ancos dañu doon siiw ndax ni ñu doon foontoo nit. Daanaka fukki at gannaaw ga, amoon na ca ña gëm ca Yawut ya ca Yerusalem, ña jaaxle ndax yu dul Yawut yu topp Yeesu te kenn xarafalu leen. Werante wu réy amoon na ba tax ñu def genn géew ca Yerusalem, 650 kilomet fu sore Ancos, ngir waxtaan ci.

Am-ami ñi gëm may na leen ñu mënoon a yónni ndimbal ca ña gëm ca Yerusalem (Jëf 11:27-30). Tamit ca mbooloo ñi gëm ca Ancos la Pool jóge ngir tas xebaar bu baax ba ci biir yu dul Yawut ya, te ca Ancos la dellusi yoon bu nekk – maanaam Ancos dafa nekkoon mel ni màkkaanam. Ñetti tukkeem yépp dafa tàmbali Ancos. Ca jamonoom, mbooloom ñi gëm ca Ancos moo gën a am taxawaay bépp mbooloo ci mbiru ni mbooloom yi ca àddina sépp doxe, xëyna bu dul mbooloom ca Yerusalem.

Tey jii dëkk bu ñàkk solo la bu tudd Antakya ci Tirki (Turquie). Am na 35.000 nit kese, ay toppkatu egëliis gereg yi des ci biir am réewu jullit yi.

Ancos ca Siri feeñ na ca Jëf 6:5; 11:19-27; 13:1; 14:26-15:3; 15:22,23,30-33,35; 18:22-23; Gal 2:11