Babilon

Jóge Wikipedia.

32°32′11″N 44°25′15″E / 32.53639, 44.42083

Ci làkku ibrë (בבל) la tur wi jóge ci Biibal. Ci angale mooy Babylon; Ci faranse mooy Babylone

Ni ñu jëfandikoo Babilon ci Injiil mooy ñett.

  1. Babilon dëkku penku la woon, di péeyug réewu Kalde, maanaam Irak. Ci dexu Efraat la nekkoon, lu tollu 80 kilomet ci bëj-saalumu dëkku Bagadad (Bagdad). Fa la bànni Israyil nekke jaam ca 566-536 at lu jiitu Kirist. Mc 1:11,12,17; Jëf 7:43
  2. Léeg-léeg xanaa ñu misaale ko dëkku Room, ak it nguur, giy bëreek Yàlla ci muju jamono yi. Pe 14:8; 16:19; 17:5; 18:2,10,21,24
  3. Benn yoon ci 1Pi 5:13 mu nekk wax ju làqu ju misaale ko benn dëkk: xanaa Babilon walla Room walla benn tata nguur Room ci dexu Niil gi fu dëkku Kayro (Cairo) nekk tey jii.