Gëwéel
Ab jukkib Wikipedia.
Gëwéel yi ñaari rëdd la ñu yu dëppook yamoo gi: gëwéelub Tef tollu ci 23°24' wu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar gi ak gëwéelub Sànkar tollu ci 23°27' wu tus-wu-gaar wu bëj-saalum. di nañ woowe it gëwéel diwaan yi ne ci li wër rëdd yooyule (di faral di wax dëkk ci gëwéel yi).
[Soppi] Melokaan
Ci li jege yamoo gi, di nañ faral di gis klimaa bu ànd ak tangoor gu tar ak taw bu bari ci at mépp: di ko wax klimaab yamoo. Waaye, ci njegeeti gëwéel yi (tef mbaa Sankar), ci at mi noor ak nawet rekk a ci am, kon wàccit yi (taw yi) day wuute ci jamonoy at mi, ba daanaka at méppay tang, di li ñuy wax klimaab gëwéel.
Waaye nag jàpp ne it ngelaw yiy uppu ak dawaani géej yi ak rëyaayu diwaan bi am nañ ay njeexit yu solowu ci klimaay diwaan yi, ba tax na su nu seetloo yenn diwaan yi, donte nekk nañ ci wetu ab gëwéel, amuñu klimaab gëwéel (ci misaal diggu Óstraali walla gu Sahara, nga xamne amuñu nawet) ak yenn diwaan yu am klimaab gëwéel te nekkuñu ci njegeeti gëwéel yi( lu mel ne réewum Keeñaa, nekk ci yamoo gi te li ëpp ci suufam klimaab gëwéel la am).
[Soppi] Diwaani gëwéel yu mag yi
Diwaan yiy dundu cib klimaab gëwéel dëgg-dëgg ñoo ngi nekk ci diggu Aamerig ak bëj-saalumu Aamerig, ci digg ak genn wàllu bëj-gànnaaru Afrig, ci bëj-gànnaaru Óstraali ak genn wàllu Endoneesi. Li des ci barabu diggantegëwéel bi dañ leen di séddale ci diggante klimaab tàkk (rawatina ci Afrig), bu yamoo walla bu xaw a sedd (rawatina ca Asi
[Soppi] Lëkkalekaay yu biti
- {fr} CNRS [1] La bodiversité tropicale.
- {fr} Agropolis: Portail européen de recherche de formation et d'information sur la Méditerranée et les pays tropicaux.
- {fr} Une agronomie tropicale au service des agricultures familiales ? (Forum d'Agropolis)
- {fr} P. W. Richards, professeur de botanique, "Etude de la végétation tropicale (se référant particulièrement à la Guyane britannique et à l'Afrique occidentale britannique)". University College of North Wales, Bangor. UNESCO 1956. Archives de la fAO.
- {fr} Mieux connaître et protéger la nature et les peuples des forêts humides
- {fr} "Gestion environnementale des écosystèmes et forêts tropicales" : Groupe de Formation et de Recherche sur les écosystèmes tropicaux forestiers et naturels, AgroParisTech-ENGREF

