Diggu Aamerig
Jóge Wikipedia.
Diggu Aamerig mooy xaaj bi nekk ci digg goxu Aamerig, ci diggante Meksik (bokk ci Bëj-gànnaaru Aamerig), ak Koloombi (bokk ci Bëj-saalumu Aamerig). Ay melokaanam ñooy li mu nekk ab sala ci diggante ñaari Aamerig yi, ak li mu doon it barabu jàllu, ngir man a jòge ci Mbàmbulaanu Atlas dem ci Mbàmbulaan gu Dal gi. Ca réewu Panamaa la boobu jàllu nekk.
[Soppi] Séwógaraafi
Réew ya fa nekk:
[Soppi] Taariix
Ci bii diwaan ay xay yu mag juddoo nañ fi, yu ci mel ne yu Maya yi. Waa Espaañ ñooy waa Tugal yi fa njëkk a ñéw. Ñoom ñoo aakimoo nguuru Maya yi dal di leen di noot ci lu mat ñetti xarnu. Daanaka réew yi nekk ci Diggu Aamerig yépp kàllaama waa Espaañ lañuy làkk.
Bi ñu amee seenub tembte, ci ndoorteelu 1800, la leen ay jafe-jafe yu bari ganesi. Looloo tax li ëpp ci taariixu réewu Diggu Aamerig yi, ba ci 1900, ay yong ak ay xare ci gën a fes.
[Soppi] Koom-koom
Li ëpp ci am-am yi nekk ci diwaan bi, suufu mbéy la te li ci ëpp ci loxoy yenn nit yu néew la nekk. Mbéy mi, ba tay, moo ëpp solo ci seen koom-koom, yoox yi ñu soxla ngir seen dund da'ñ koy jëndaani bitim-réew. Seen këru koom-koom yi tamit li ci ëpp ay wàlliyaan a leen moom.
| Diwaani Goxu Aamerig | |||
| Diggu Aamerig · Bëj-gànnaaru Aamerig · Carayib · Bëj-saalumu Aamerig | |||