Waxtaani jëfandikukat:Abdu Xaadir KEBE
Welcome to the Wolof Wikipedia/Bienvenue au Wolof Wikipedia! Feel free to write something about yourself on user page. Si vous preferez, je peux aussi ecrire en francais. Feel free to leave any questions. You can sign comments and questions using ~~~~. --Jose77 18 juillet 2007 à 22:50 (UTC)
dalal-jamm
[soppi gongikuwaay bi]ñoo ngi lay dalal-jamm ci wikipedia. lu benn loxo man ñaari loxo ko ko dax, con bek nañ ci sag mbindu. wiki wolof ca kanam. yërël xëtu dala-jamm gi fii
--Ibou 19 juillet 2007 à 11:06 (UTC)
Di am yeenee jàpp ci bépp liggéey buy jëmale sunu làkk wii di wolof kanam
soppi
[soppi gongikuwaay bi]maa soppi saa Xëtu jëfëndikookat, looy wax ci lu jëm ci yaw, ci moomu xët nga ka wara bind yaw lañ ko jaglel. --Ibou 20 juillet 2007 à 19:34 (UTC)
leeral
[soppi gongikuwaay bi]bu ma sañoon xët-njëkk da nga naan xët wu njëkk wi, walla nga ne teeru walla kër gi. bul tënku ci li ñenn ñiy bind rekk, ndax am na ci ñoo xam ne gënuñu laa dégg wolof, te boo jëfandikoo sa xael génne lu gën li ñu génne, day mujj nga leen di jariñ, te maak yaw man nanoo sos ab gëstuwaayu baat muy akaademi boo xam ne baat bunuy génne gëstu ko ci. aji jëfandikoo moo gën jëfandikookat, bu dee ñu bari di way jëfandikoo
laaj
[soppi gongikuwaay bi]Nooy tekkee yii
compte:lim
categorie:maas:kuréel;mbooloo
son:kàddu
video:bu dee araab sax wideo lanuy wax, daa am baat yoo xam ne làkk yépp a ko bokk itaalien itam moom lay wax fr ak ang, waaye man nga koo firee (seetaanu) (gisu)
citation, citer: tudd
tableau: alliwa;tablo; limuwaay
espace:diggante
copier: sotti; làwwi;jël; tonni;yaxal;dayal. Sotti bu nu daa jàng alxuraan këyit wu ñu nu jox ngir ñu bind ko feneen dañu naan ñu sottileen ko mooy kopileen ko
coller:taf;tay
parrainage:baayale;waajurale
contribution:ag bokk;joxe xalaat, ceru,joxe ci ab cer
damaa bëggoona xam ndax baatu xarala yi ngay jëfëndikoo yaa koy sos wala?
man yi may jëfëndikoo ci sa may jukki fii laa koy jëlee muy baat yu seex anta joob sos. Yaakaar naa ne sunug deggoo ci baat yi nuy jëfëndikoo lu am solo la.--Ibou 20 juillet 2007 à 19:43 (UTC)
Ma lay xamal
[soppi gongikuwaay bi]ma lay xamal ne Seex Anta maa ko gën a dégg wolof, ndax moom tubaab bi duggoon bu baax ci làmmiñam aki xalaatm, am na téere bu ma la yonnee woon ci taariix, ma lay xamal ne bu ñu naw la ci Senegaal ci wàllug terminologie, ndax am na ci term yoy day reeral te day tax ba làkk wi di jafe
jukki
[soppi gongikuwaay bi]waaw kon ngir sunuy baat ma na nengoo faw nu book fañ leel di jëlee. ndax am nga ab baatukaay bu mel ne bu sex anta bi ma yor, boo ma ma na jox? man lii soxal na ma lool ndax mooy tax làkk wi neexa nand. kon li ma lay ñaan mooy nga jàng jukki yi ma bind, nga xool ndax baati xarala yi ma fay jëfëndikoo mengoo nañ ak yi nga xam. soo ci gisee ay dëngte,di la ñaan, nga jubbanti leen te wax ma, ci sama xëtu waxtaanukaay, yan lañu. jërëjëf --Ibou 22 juillet 2007 à 15:30 (UTC)
categorie:Wall la ko tekkeewoon wall moom manul a tekki categorie moom kay benn ci baat yi ma la yonnee, boo amatee lu l jaaxal wax ma teg it baat ba nu ne moo baax ci wolof te laaj ma ba xam baax na walla deet, rawati na boo ko dugalee cib jumla maanaam fraas
compte: waxumawoon lim, ci misaal:compte banque, boite Email (une compte)
espace nom: (l'espace qui est reservee0 pour ecrire quelque chose)
tontu
[soppi gongikuwaay bi]diggante day firi espace bu boobaa ab diggante ngay wax, day firi it entre diggante ñaari kër yi aw yoon jaar na fi/entre/, bokkul ak bindal ci diggante bii maanaam espace bii, yaatu–yaatu it dina firi espace. boite Email moom boyotu bataaxel lanu koy wax, compte nag man naa tekki am sàq, muy fi ngay denc li nga jot a am ciy bataaxel di leen fa génnee. man ngaa yonnee ab E–bataaxel ci abd@sentoo.sn ci ku nuy wax soxna Aram FAAl moom lingust bu mag la def na benn téere xamtéef /informatique/ bu am solo, xamante leen nee ko maa leen boole. jëlal baat yii nag : fàccaakon:explosif, fàcc exploser; ci maanaa xare booba de fàccal nanu fa ay fàccaakon yu bari
baatukaay xamteef gi
[soppi gongikuwaay bi]waaw googu téere gisoo naa ki internet, wax naa sax ngir ñu jëndël ma ko te yònnee ma ko. xam na bala yagg di naa ko jot. soxna aram fal tamit degg naa ko; ligey yu am solo lay def ci làkk wi. dinaa jokkoo ag moom. wasalaam maa ngi jëndlu tamit baatukaay bu Jean-Léopold Diouf, Dictionnaire bilingue Wolof-Français, Paris, Éditions Karthala, 2003;
yaakaar nga ne jar naa jënd. man naa cee gis ay baat yu am solo? --Ibou 23 juillet 2007 à 17:29 (UTC)
tontu
[soppi gongikuwaay bi]Waa-waaw bu am njariñ la te moom man ngéen a liggéey sax, ku wolof ñor la boo amoon sa mbokk mu nekk fii fi senegaal boo ma boolee ak moom ma jox ko ay téere yu mu def, waaye ma lay xamal ne ab gëstukaayu baat bu ñépp déggoo moom amagul, lu ci waay def it lu aju ci yaw mi ko def rekk la, kon yaakaar naa ne yaw boo góor-góorloo xar baax (def lu extraordinaire), te man man naa laa jàpple, ñooñu ngay wax de maa leen raw li ma ci man de manuñu ko ci, caaxaanuma nag. Meme Aram Faal moomu damay faral a laaj. boo ma dee tegal ay jukki yu jar a tekki, dinaa la leen di faral di tekkil
aram faal
[soppi gongikuwaay bi]bind naa ko ab bataaxal, tont na ma. nee na ma li ma wax ci wikipedia amal na ko solo, nee na di na fi ñëw.
Say xarit yi nga am yu wolof yiiteel, daŋ leen cee wara xiir.
wikitionary: wall la ci wikipedia, foofu lu jëm ci wallu lakk rek lañ fay def. Man nan faa sakk ab baatu kaay boo xam ne ñëpp a ciy ma na duggal seen loxo. Di nan mana waxtan ci baat yi ba deggoo am ci, ni muy amee fii ci wikipedia. sunu amee ñu mel ne yaw, aram ak ñeneen, di nan fi ma na sakk ab baatukaay bu dëgër te wòor.--Ibou 25 juillet 2007 à 18:00 (UTC)
lahamdu lillaa
[soppi gongikuwaay bi]kon dinaa gën a gëstu loolu, xoolal maa ngi la ciy déglu, Aram Faal nag fonk ko, ku am solo ci wolof la
Wolof Wiktionary
[soppi gongikuwaay bi]Hi Abdu Xaadir KEBE,
User:Ibou wishes to become an administator on Wolof Wiktionary. You can support him here. Thankyou. --Jose77 26 juillet 2007 à 04:17 (UTC)
tekki
[soppi gongikuwaay bi]baat yi nekk ci sama Xëtu waxtaan. So leen mane tekki --Ibou 26 juillet 2007 à 18:57 (UTC)
Welcome, bienvenu!
[soppi gongikuwaay bi]Welcome, ou bienvenu! Maybe you can also write a little bit about yourself in English and/or French. Peut-etre vous pouvez aussi ecrire un sur vous-meme en anglais et/ou francais :) Une question importante: est-ce que vous preferez l'anglais ou le francais? Merci, thanks! Guaka 31 juillet 2007 à 10:24 (UTC)
reply
[soppi gongikuwaay bi]I like english more than french,
wolof wikitionary
[soppi gongikuwaay bi]soo demee fii Wolof Wiktionary man nga faa duggal ay baat ak seen tekki ci yeneen làkk --Ibou 2 Baraxlu 2007 à 11:19 (UTC)
- Please support Ibou for administrator here. Thanks. --203.109.217.207 4 Baraxlu 2007 à 05:33 (UTC)
laaj
[soppi gongikuwaay bi]man sama jot daa bariwul, boo mamanoon a leeral bu baax nan lanuy dugale baat dina ma gën a sawarloo,ñaareel ba soo ma mayoon may man a gëstu baat yi nga duggal di wone yu ko gën dëppoo ba xam di nga ci ànd am déet loolu dina gën a rafetal liggéey bi. boo manoon it ma lay bindal li ma am ciy baat nga koy duggal moo may gën a noppal.jàmm ak xéewal
tontu
[soppi gongikuwaay bi]Soo bëggee duggal ab baat, ci lu njëkk seetal baxam baat bi am na ba noppi, walla deet. su dee amul, nga xool fan la baat bi wara bokk, ci ban wàll (su fekkee baatu xeltu la, nga bind ko ci biir xeltu, su dee xaralaymbëj la nga def ko fa). su dee nak baat bi bokkul ci benn ci yooyu, nga bind ko ci seet, kligal Ayca, su fekkee baat bi amul daf lay laaj ndax dang kaa bëgga sos. ci nii dafay mel ni nga sos ab jukki ci wikipedia. baat bi mooy nekk koju jukki bi. nga tekki ko ci làkk yi nga xam yëpp. ci suufa-suuf nga bind fa lii '''catégorie:baati wolof'''. soo bëggee gis baat yi ma mujjee duggal, da ngay dem ci Modifications récentes, nga soppi leen su ñu amee ay ndëng-ndëng. su la neexee tamit, saa yoo amul jot, nga bindal ma baat yëpp ci sama xëtu waxtaanukaay, man ma duggal leen. Soo bëggee seet baat yi nga duggal nga dem (Seet ab baat). Jàmm ak xéewal
Ay baat a ngoogu yu bees
[soppi gongikuwaay bi]dinaa def li nga wax bu ma gënee am jot waaye xoolal baat yooyu:
layalkat: avocat
naal;sémb:projet
jiiñkat:procureur
jiiñkat bu mag bi:procureur général
àttekaay;ëttu àttekaay:tribunal
yoon wiy yare:code penale
àttekatu càmbar: juge d'instruction
ag réewu:nationalité
kayitu jëmmal:carte d'identité
yoonu jawwu:ligne aerienne
nuuraakon:submersible;sous-marin
mburgël walla mburgal:tunnel
bàyyi-mu-jàll:laissez-passer
naawuwaay:aéroport
sañal-tukki:passport
sañ-dugg:visa
leer gu wert mbaa gu xonq:feu vert ou rouge
baagante:navette
sëla-bi-yoon:carrefourt;rond point
sañal-dawal:permis de conduire
waax:port
yoonu weñ:chemain de fer;rail
ab jéggiwu;pom:pont
wata cëfka:camion
aji doxal:directeur
jumu asamaan:satellite
barabu xibaar walla barabu tas-xibaar:agence de presse
boppi xibaar:les titres
temb;tembte:independance
pëjj:infrastructure
mbootaayu liggéeykat yi:syndicat
yong:coup d'état
gox-goxaan:local
waxiin:terme;therminologie
waxiin:dialecte
waxiin:mode da dire, de parler
jum:rocket
gàddaay gu yoonoodi:immigration clandistine
jëwrin:ministre
njëwrin:ministère
ma lay xamal ne ci wikitionary boo xoolee baat bu nekk ca discussion-wam defal naa la fa baat ba gën walla ba ma yaakaar ne moo gën, nanga ko xool nag te seet yi gën nga soppee léen yeneen yi
.
assalaamu 'aleykum
no gui lèen di nuyu té di lèen sant ci liguèy bu rafét bi guèen di laguèey guir képp kuy wolof. guinnaw bà me am tuuti luma baga bukké ci mbir mii guir am luma lèen ciy fattali lumélni "gox-goxaan:local" lolu japp naani warguèen ko sèetaat ndax gox xam-nanu ko mumana nekk(Department)wayé goxaan moom mante firi ludul gox yu nèew te yaraax kon boolé gox-goxaan du mana tax muy local té yit "local" boka waxèe boolé gaci "region" té region ci wolof Tund là mana doon kon du jaadu gani gox-goxaan mooy local ndax bu booba tund du dung té ci la wara bukk té yit batëy budèe gox-guxaan bu rey ba-ak bu tuut bà guèen ci jublu ni gox mooy bu mat bà ni goxaan du tax mu tuuti liy waral mu tuuti manna nékk Ngox (tundu wi, qox bi, ngox si) tektal:tundu bawal (diourbel) tundu kajoor (thiès). kon warèess nako sèetat man nak lima ci joxé mooy Biir-rèew:local
guir yi tam baat yi guèen di jafandiko sax, ba nit ñi diko jafandiko faww guèen di wut ay baat yoy day boolo te baña melni luñ firi Téktal: aji doxal:directeur guir nit ñi manko jafandiko faww guéen koy féxèe boolé melni doxalkat:directeur mba doxalakon:directeur wata cëfka:camion daanan ko wax ndagg:camion. gàddaay gu yoonoodi:immigration clandestine, immigration mante doon gadday ci lima japp gadday:depayisé immigration:tukki moom lan ku gëna xamé manna nekk yit immigration:jeggaani immigration clandestine:tukkiin wu jaadu-wul mba immigration clandestine:jeggaanin gu jaadu-wull lolu la ci doon bokké té guèen jéggalma ci bindiin wi ndax jaggu mako fénn waya wolof laa nak bu wolofé guinnaw lolu yit lii mafi doon lèeral taxul ma wéddi waxi kénn danuy layibiirenté rekk ma joxé ci sama xalaat buka défèe nu xool bu jubèe nu jall bu jubul nu bà ndax dagg yalla rekk moka moom, bu dara tax yit ba guèen xèep ma ndax lima amul fumay tektalo am fooy téktalo baax-na lool waya ñi nuy téktelo yalla moo lèen joxon ab deg té mongui fi diko joxé ba tëy li am solo mooy bu nit waxèe nu xool wax jà baxam jubna am dèet jërëgèen jëf may déllu bà tëy ci di rafét lu sèen linguèy bu wér té di lèen ñanal sèeni naal yegg waw-kay (ok)
tur:Abdu Xaadir Sant:GUEYE Dëkk:Dakaar/Guèjawaay jokko:221775724577 E–bataaxel:djili.gueye@hotmail.com
ma ne
[soppi gongikuwaay bi]leegi ma bàyyi la nga wéy nag ndax leegi nga miin mbir mi, xam naa xam-xam yi nu leeralagul dinaa ko xamale te ba la nga wéy b ko defee keneen ñëw moom itam joxe ab céram
ay laaj
[soppi gongikuwaay bi]Baat yii lu ñuy tekki?
- yaxantu:commerce
- gëweel:cercle
- koju:koj mooy luy dëkkale fennci maanaa nit ku di hijug Tuubaa ku bokk tuubaa, xam-xam bu di kojug koom-koom mooy xam-xamu koom-koom, xeltu bu di kojug nite añse. Añse mooy ak ñoom seen = ect
- empire: "nguur gu mag" laa ko doon woowee ci jukki taariix yi ma bing. Kon da ma leen war a soppi bind "imbraatòor"? waaw mooy baat bu baax bi
- falag:mooy xeet astronpmie baatu araab la, dees na ko wax it xam-xamu bidiw
- arminaat:mooy calendrier
dig:aw dig mooy frontiere? date mooy ba tay taariix, ci datu nàngam mooy ci taariixu nàngam --AbduXaadir 1 septembre 2007 à 18:36 (UTC)
sooy waxtaan deel xaatim say mbind, loolu di na tax ñu man laa xammee. gisóo man ci suuf, xaatim naa fa
--Ibou 1 septembre 2007 à 18:36 (UTC)
Ay tontu
[soppi gongikuwaay bi]Baat yii lu ñuy tekki?
- yaxantu:commerce
- gëweel:cercle
- koju:koj mooy luy dëkkale fennci maanaa nit ku di hijug Tuubaa ku bokk tuubaa, xam-xam bu di kojug koom-koom mooy xam-xamu koom-koom, xeltu bu di kojug nite añse. Añse mooy ak ñoom seen = ect
- empire: "nguur gu mag" laa ko doon woowee ci jukki taariix yi ma bing. Kon da ma leen war a soppi bind "imbraatòor"? waaw mooy baat bu baax bi
- falag:mooy xeet astronpmie baatu araab la, dees na ko wax it xam-xamu bidiw
arminaat:mooy calendrier
- dig:aw dig mooy frontiere? date mooy ba tay taariix, ci datu nàngam mooy ci taariixu nàngam
--AbduXaadir 1 septembre 2007 à 18:36
dal
[soppi gongikuwaay bi]Gis naa sa dalub internet www.institutkhalil.com/Wolof.html, am na solo lool! --Ibou 27 octobre 2007 à 10:26 (UTC)
ma ne
[soppi gongikuwaay bi]noo def ba gis ko? bul fàtte ne joor mooy ci italien pianura, yaw yaa ngi koy firee terre ferme walla lifthosphere, te terre ferme walla lithosphere mooy jéeri, danuy wax jéeri ak géej walla jéeri ak ndox, ma lay ñaan boo gisatee baat yu la jaaxal nga laaj ma nu ñu koy firee ci wolof, ndax loolu dina waral wax ji di gën a leer, ndax li ngay bind lu am solo la waaye leeg-leeg day fasu, ngir ay baat yooy jëfandikoo te nuy tekki leneen ci wolof, walla sax ñu manoon a am yu gën a woyof. boo manoon it di def baat boo firi ci wolof, nga tekki ko ci tubaab ci diggante ñaari xàlla maanaam () tra virgoletti. maa ngi kontaan ci yaw ci liggeey bu mag bi. waaye liy li ci soof bu nit bëggee xam dal bi (site) bi day sonnu lool, lu tax manuñu koo def non boo ko gëstoo ci google gis ko? ba beneen
tontu
[soppi gongikuwaay bi]Waaw degg naa li nga wax. waaye sooy duggal ay baati nasaraan ci jukki wolof yi, ci sama gis-gis, day waññi taar bi. Moo tax baat yu jafe yi may jëfandikoo dama leen di duggal ci wikbaatukaay. Ci biir jukki bi ma def fa lii ci suuf: {{wikibaatukaay}}. soo ko bëgge duggal ci ab jukki, da ngay dem ba ca jeexit la nga duggal fa lii: {{m|wikibaatukaay}} ci misaal ubbil jukki bii Xaaju kol-kol, su ubbeekoo nga cuq ci wikibaatukaay nga xool.
Ban dalu ngay wax ne neexul a gis ci internet sa bos walla bu wikipedia?
Su fekkee sa bos ngay wax: am na lu ñuy meta-tag, ay baati cabi lañu yooy duggal ci say xëti dalu. baat yu mel ne: wolof, senegaal, njang, añs lépp lu ñeel dalu bi. Di na tax képp ku bind baati caabi yooyu le ci google sa dalu bokk ci yiy njëkk a feeñ. xoolal fii
ci bii dalu laa dem fekk ko fa, gis fa sa tur. wasalaam
--Ibou 27 octobre 2007 à 10:26 (UTC)
limbare (statistique)
[soppi gongikuwaay bi]Xoolal xët yii dañ la fiy won màggug wikipedia ci wolof tables akcharts. --Ibou 27 octobre 2007 à 10:26 (UTC)
ay baat
[soppi gongikuwaay bi]Xoolal baat yii
ibou
[soppi gongikuwaay bi]xanaa yaa ngi may soog a gis? monte sama nataal yàgg na fee ne.
Li am solo ci nit du at ya, waaye xel ma!!!!!! Ibou 27 octobre 2007 à 10:26 (UTC)
jukki bi
[soppi gongikuwaay bi]Dindiwu ma ko de!!!!!! da maa gis ne fii la gënn a jekke ma toopale ko, def ñaar:Melosuufug Afrig ak Koom-koomu Afrig. sooy seddale jukki yu gudd yi ci yu bari di na tax xët yi gën a bari. te sooy wax ci lenn li rekk utal ko xëtu boppam moo gën. Nuy bañ a boole li bokkul di na tax mbir yi gën a leer. Ibou 27 octobre 2007 à 10:26 (UTC)
baat bu bees
[soppi gongikuwaay bi]sékk: staticco, maanaam lu ne sékk rekk doxul bawaul.
- ngir duggal baat bu bees demal fii. su ma amee jot di naa ko gënn a xóotal. --85.34.94.100 30 rakki gamu(avril) 2008 à 18:55 (UTC)
Catégories
[soppi gongikuwaay bi]Salut, peux-tu rajouter des catégories en bas des articles que tu écris, merci d'avance. Guérin Nicolas 2 Rakkaati-gamu 2008 à 16:13 (UTC)
Salut
[soppi gongikuwaay bi]comment le faire? Abdu Xaadir KEBE --Abdu Xaadir Kebe 3 Rakkaati-gamu 2008 à 15:47 (UTC)03/05/08
- Ajoute en bas de la page [[Catégorie:NOM DE LA CATEGORIE]] en remplaçant "NOM DE LA CATEGORIE" par le nom approprié, par exemple pour religion cela donne Catégorie:Diine. Au plaisir. Guérin Nicolas 4 Rakkaati-gamu 2008 à 08:00 (UTC)
reponse
[soppi gongikuwaay bi]je pense q je n'ai pas besoin de le faire puisque je les met là oü tout ent en ordre, sinon donnez moi un example Abdu Xaadir KEBE--Abdu Xaadir Kebe 4 Rakkaati-gamu 2008 à 16:25 (UTC)
- categorie yi ci wikipedia yépp lañ am. day tax jukki yi nga xam ne ñoo bokk ci li ñuy wax man a bokk nekk ci wenn xët. Soo xoolee Catégorie:senegaal xët yi ñeel senegaal yépp a fi nekk. jukki yi ñeel nguuri senegaal yépp soo xoolee ñoo ngi leen boole ci Catégorie:nguuri senegaal; soo xoolee di nga gis ne itam nguuri senegaal mi ngi ci biir categorie:senegaal. Li ma la bindaloon ci wikbaatukaay yokk naa ci dara xoolal. fii. xéewal --Ibou 11 Rakkaati-gamu 2008 à 16:35 (UTC)
leer na
[soppi gongikuwaay bi]jaajef, sa naatagooy Wiki yi woo woo nanu ma ba nu gise ca ndaje ma ñu amaloon fii ci Senegaal, am na ku ci ne sax suba dina fi jaar.--Abdu Xaadir Kebe 14 Rakkaati-gamu 2008 à 22:25 (UTC)
- gis naa li nga mujje duggal ci wikbaatukaay noonu la! ni nga leen duggalee neex na ma te rafet na. Waaye soo amee jot, su manee ne, nga soppi baat yi nga njëkk a duggal, te ni nga leen duggale baaxadi, soo ma manoon a tekkil yii tamit: Lac de Gueir, Vallée du Ferlo, Tiângol Lougguéré, Vallée de Mboun, Vallée du Saloum, Badiara, Niéri Ko, Niokolo Koba, Soungrougrou, Géba (partially in Guinea-Bissau), Djoudj Bird Sanctuary. Daa am ku ma leen di tekkiloo.
waaw kon mujje nga gise ak waa-wikipedia yooyu, mbaa ndaje ma neexoon na rekk? dama gis ni rek yaay ki gën a farlu ci wiki bi, ci ñi ma xam, te mu ñor la loo, moo tax ma jox ko sa e-mail. xeewal --Ibou 15 Rakkaati-gamu 2008 à 18:44 (UTC)
tontu
[soppi gongikuwaay bi]Ndaje ma neex na waaye yàgguma fa ngir ay yitte yu ma amoon, ñaareel bi lu ëpp ca ndaje ma mi ngi aju woon ci mbirum fànn te loolu taxul mu yittéel ma dara. Waaye am na ca ñoom kenn ku ma ci seetsi sama kër ba ñu jot a waxtaan ñu koy wax Tania.
Lac de Gueir: Lac dees na ko firee as ngéej boo xoolee sax ci melo suuf di nga fa gis lu bari ma ko fay jëfandiko, ndax bu dee ci araab mooy buhayra buhayra nag mi ngi juge ci bahru giy tekki géej, buhayra di géej ñu xeeb ko muy as ngéej, Ag géej = Bahru,ñu xeeb ko muy Buhayra = As ngéej. Dees na ko firee it moom Lac déeg. Kon bu la neexee nga ne ngéejus Geer walla déegub Geer. Vallée du Ferlo: Vallée:Xur, Kon xuru Ferlo. Tiângol Lougguéré, lii du làkk baat la kon danga koy bàyyi ni ñu ko binde walla nga wolofal ko, maanaam jox ko kàddu gu ko wolof yi man a waxe: Cangol Lugere. Vallée de Mboun: Xuru Mbun, Vallée du Saloum: Xuru Saalum, Badiara: Bajara, Niéri Ko: Ñeeri Ko, Niokolo Koba: Ñokolo Koba, Soungrougrou: Sungurugru. Géba (partially in Guinea-Bissau), Djoudj Bird Sanctuary.--Abdu Xaadir Kebe 17 Rakkaati-gamu 2008 à 16:29 (UTC)
laaj
[soppi gongikuwaay bi]lu tollu nan ci ay way joowu aki gëstukat ñooy dugg ci Wikiwolof bi ci bis? ndax am na ñeneen ñu dul ñun ñaar ñu mbir mii yittéel te ñuy bokk ci way céru ñi?
Lii nag ag gaaral xalaat la (proposition): ndax doo def leeg-leeg nga yër bu baax li ma duggal, baat bu ci jar duggal ci wikibaatukaay bi nga duggal ko ci, bu la leeradee nga yonnee ma ma leeral ko?
Ndax du jàppandi sos ag mbootaay guy yëngu ci lii, te ñu jéem a def am ndajem tas-xibaar (conference de press) ngir leeral ci mbooleem jéego yii ñuy def ngir xëcc ci mbooleem ñi mu yittéel. Sax leen ci jàmm! --Abdu Xaadir Kebe 19 Rakkaati-gamu 2008 à 13:26 (UTC)
- jàmm nga am? soo xoolee fii di nga gis ñi bindu ci wikiwolof yépp ak li ñu cëru. fii
man di naay jàng, daana-ka, sa jukki yépp. Baat yu bari fa laa leen di jële. Di naa it faral di leen def ci ca wikbaatukaay.
Mbootaay gi xalaatoon naa ko, loolu ci xeeti wikipedia yépp la am, réew mu ne am na ab banqaasu wikimedia, di mbootaay miy dundal wikipedia, ci coppar ak xalaat. kon senegaal war naa am ab banqaasam, ci ag juddoom la ëllagu wikiwolof aju. ci weeru baraxlu am na ndaje mu mag mu mediawiki muy am ca Isipt , ndaje la muy am at mu ne, ci menn réew mu ñuy tànn, bëgg naa caa dem, su loolu antoo di naa fa gaaral xalaat bi. Sunu fexee bañ nangu ko danuy and ak njiiti mediawiki def ndajem tas-xibaar mi ngir leeral ci mbooleem jéego yii ñuy def ngir xëcc ci mbooleem ñi mu yittéel, dem wax ak kangam yi wolof yittéel te di ci liggéey. Li ma doon xalaat lu gën a sori, mooy fexe ba sos lu mel ne ab academie wolof ci wikbaatukaay, ngir sos baatukaay bu matale. fexe ba xëcc ñu mel ne aram fal, saxiir caam, yaw, ak añ.xéewal --Ibou 22 Rakkaati-gamu 2008 à 19:36 (UTC)
Tontuuuuuuuuuuu
Xalaat bu jéggi dayo ba ci am solo, man na la wóor ne dugg naa ci te nanga xam ne ñu ëpp ñooñu maanaa ci wolof sax ñi ngi fi man fas naa ñu bokk ci bu boobaa, na la Yàlla dooleel, guddalu fan --Abdu Xaadir Kebe 24 Rakkaati-gamu 2008 à 22:53 (UTC)
tontu
[soppi gongikuwaay bi]Ndaje ma neex na waaye yàgguma fa ngir ay yitte yu ma amoon, ñaareel bi lu ëpp ca ndaje ma mi ngi aju woon ci mbirum fànn te loolu taxul mu yittéel ma dara. Waaye am na ca ñoom kenn ku ma ci seetsi sama kër ba ñu jot a waxtaan ñu koy wax Tania.
Lac de Gueir: Lac dees na ko firee as ngéej boo xoolee sax ci melo suuf di nga fa gis lu bari ma ko fay jëfandiko, ndax bu dee ci araab mooy buhayra buhayra nag mi ngi juge ci bahru giy tekki géej, buhayra di géej ñu xeeb ko muy as ngéej, Ag géej = Bahru,ñu xeeb ko muy Buhayra = As ngéej. Dees na ko firee it moom Lac déeg. Kon bu la neexee nga ne ngéejus Geer walla déegub Geer. Vallée du Ferlo: Vallée:Xur, Kon xuru Ferlo. Tiângol Lougguéré, lii du làkk baat la kon danga koy bàyyi ni ñu ko binde walla nga wolofal ko, maanaam jox ko kàddu gu ko wolof yi man a waxe: Cangol Lugere. Vallée de Mboun: Xuru Mbun, Vallée du Saloum: Xuru Saalum, Badiara: Bajara, Niéri Ko: Ñeeri Ko, Niokolo Koba: Ñokolo Koba, Soungrougrou: Sungurugru. Géba (partially in Guinea-Bissau), Djoudj Bird Sanctuary.
Babel
[soppi gongikuwaay bi]Il y a un nouveau modèle que tu peux mettre sur ta page utilisateur personnelle et qui renseigne sur les langues que tu parles : {{Babel}}. Par exemple {{m|Babel|wo|fr-3}} ou autres. C'est particulièrement utile pour connaître le niveau de wolof de chacun. Guérin Nicolas 15 Rakkaati-gamu 2008 à 13:05 (UTC)
Merci
[soppi gongikuwaay bi]j'ai deja fait, regardez le--Abdu Xaadir Kebe 17 Rakkaati-gamu 2008 à 17:46 (UTC)
Merci
[soppi gongikuwaay bi]j'ai deja faif, regardez le
- Normalement, maintenant c'est bon pour "ar-5" ou "ar-4", ils devraient s'afficher, sinon purger le cache. Guérin Nicolas 17 Rakkaati-gamu 2008 à 17:45 (UTC)
ok je vai voir mais vtre mail? comme ca on pourra parler a travers msn
- J'utilise pas msn... Sais-tu comment on dit "français" (pour la langue) en wolof? et anglais? Si tu as le temps ce serait bien que tu crées des ébauches sur ces langues. Guérin Nicolas 17 Rakkaati-gamu 2008 à 17:53 (UTC)
sois plus clair!
- par exemple comment traduire en wolof le titre de l'article it:Lingua francese = fr:Français? Guérin Nicolas 17 Rakkaati-gamu 2008 à 18:06 (UTC)
A little help: Ecser
[soppi gongikuwaay bi]Hi! I'm a Hungarian Wikipedia editor, my name is Norbert Kiss. I'm very proud of my village and I would like to read about it in a lot of langauges. I translated already it into 10 languages (now it is in 42 languages), but I can't speak Wolof. Could you help me? My village's English page is this: Ecser in English or French page Ecser en francais. Could you translate the page of Ecser into Wolof? Then just link the side into the English version and I will see it, or you could write me, when it is ready. My Hungarian Wikipedia side is: My profile.
Thank you! Norbert
I ll try to do, but not now because i ve lot of tuings to do.thanks however
- Ok, It will be ok also later... Thank you! - Norbert
wikbaatukaay
[soppi gongikuwaay bi]Di nuyooti.
léegi waxtaan yi ñeel tànnug baat yi ci wikibaatukaay la leen di bind. Am na ay laaj yu ma la fa def, soo amee jot nga xool leen. soo ubbee sa sàq. jaajëf fii --Ibou 29 Maami-koor 2008 à 13:02 (UTC)
dinaa ko xool--Abdu Xaadir Kebe 30 Maami-koor 2008 à 21:14 (UTC)
bëgg naa nga seet ci wu fraas, li ñuy wax découpage administrative du territoire sénégalais = dogiin wu yoriinu senegaal, su ko defee nga yonnee ma ko ma tekki ko ci wolof, maanaam ni ñu seddalee réew mi dale ko ci {région, département, arrondissement añs} --Abdu Xaadir Kebe 1 Sattumbar 2008 à 22:43 (UTC)
- soo may bind soo ko deful ci sama xëtu waxtaanuwaay man naa ko bañ a gis, gisoo ni yaw su amee ku la bind so dugge ci wikipedia rekk mu yëggal la ko. bëggon laa bind ab bataaxal moo tax ma dugg ci sa waxtaanuwaay ba gis bataaxal bi, lu ko moy du ma ko gis ndax kenn du ma ko yëgal.
leneen li mooy ci biir jukki wolof yi jarul c nga ciy def ay mbindi wu faraas doy na baat bi muy tekki, te yaa ngi duggal ay mbir yu waroona na nekk ci wikbaatukaay. Fii ay jukki rekka fi wara nekk. lu nekk lii ci wikbaatukaay la waroon ana nekk Yonnee.
Dogiinu yoriinu senegaal a gi nii ci wu faraas jukki yi ko ñeel yepp: fii --Ibou 2 Sattumbar 2008 à 17:53 (UTC) Degg naa li nga wax, dinaa xool it loolu
Hi Abdu Xaadir KEBE ;)
[soppi gongikuwaay bi]Hi! How are you? Could you please help me add a couple of sentences to the .wo version of this interesting article?
Thanks so much! -Ivana Icana 6 Sattumbar 2008 à 21:38 (UTC)
Hi, I'd like to do, but my problem is business, I have a great deal of things to do, but however I'll try to do later --Abdu Xaadir Kebe 6 Sattumbar 2008 à 21:51 (UTC)
Xoolal fii te wax ma ci sa xalaat --Abdu Xaadir Kebe 10 Sattumbar 2008 à 14:17 (UTC)
Ay siyaarati ci koor gi
[soppi gongikuwaay bi]Ma ne daa am ab jukki bu am solo boo defoon ci Mbëj ma bëggoon ñu àndandoo maak yaw def ci ay lajmbat, rawati na ci baat yi, ngir ne gis naa ci baat yu manoon a gën a lëmóodiku, gën a leer, te ma bëggoon ñu àndandoo ci. --Abdu Xaadir Kebe 14 Sattumbar 2008 à 18:17 (UTC)
- man nan see waxtaan kay, bindal ma baat yi nga andul, nu xool. Baat yi ngay tekki fii, di leen sakkali xët te duñu ay jukki, faruñu nekk ci wikipedia waaye ci wikbaatukaay. Fii ay jukki rekk nga fi wara def. yii nii ci suuf ci wikbaatu kaay lañ wara nekk, su fekke danga bëgg a yem rek ci tekki leen, soo leen bëgge yaatal nak bind ci lu bari man nga leen fee def. Soo leen defee fii waroo yem rekk ci bind seen tekki ci wu-fraas. Doxaliin Yéwénal Lonkoo yu askan Nosteg galag Ndefar gu barab gi, añs --Ibou 20 Sattumbar 2008 à 12:41 (UTC)
Siyaar dégg naa li nga wax, bu beneen yoonatee damay def tekki yi ci diggante ñaari xala () --Abdu Xaadir Kebe 20 Sattumbar 2008 à 13:46 (UTC)
Jaajef sang xoolal baat yooyu ngir ñu man cee tënku:
* Diiwaani Senegaal: Régions du Sénégal * Tundi Senegaal: Départements du Sénégal * Ndiiwaani Senegaal: Arrondissements du Sénégal * Dëkkaani Ndiiwaan yu Senegaal: Communes d'arrondissement du Sénégal * Dëkkaan yu Senegaal : Communes du Sénégal * Gox-goxaan yu Senegaal : Communautés rurales du Sénégal * Dëkk yu Senegaal : Villes du Sénégal * Dëkk-dëkkaan yu Senegaal : Villages du Senegal --Abdu Xaadir Kebe 24 Sattumbar 2008 à 11:14 (UTC)
--Abdu Xaadir Kebe 21 Sattumbar 2008 à 16:22 (UTC)
- waaw kon nu tënku ci. di naa ci tambalee liggéey. Di delloo siyaar ci koor gi. xéewal!!! --Ibou 24 Sattumbar 2008 à 10:19 (UTC)
- maa jàmm nga am? baat yi nga fi duggal yu mel ni elektron, proton, elektronik, añs. bindoon leen ci wolof moo gënoo ndax am na leen.jàmm-ak-jàmm --Ibou 10 Oktoobar 2008 à 06:34 (UTC)
Jaajef
[soppi gongikuwaay bi]Ñi ngi delloo siyaar tey nuyyoo tey baalu àq te di ko baale, rawati na ci njeextel koor gi, ci korite gii, di ñaan Yàlla mu indil ñu ko ay yooni yoon. Li aju ci baat yooyu: man da maa xamul baat yooyu, ma bëggoon nga raŋaleel ma leen fii ngir ma xam leen ci wolof, bu ma ci manee def ay gëstu aki lajbat def ko ci as lëf.
Am na leneen lu ma bëggoon a wax: mooy gis naa ne araab de elektron lay wax, xoolal ba xam dina jar firi am déet.maa ngi la ko doon wax ca ginnaaw, boo ma manoon a bindal mbooleem baat yi aju ci mbëj raŋaleel ma leen te firl ma leen ngir ma xool ba xam amul yu leen gën a noppale ci wolof, ndax lu mel ne jalaxu man xamuma ko, ak yennaat ci baat yu ni mel, du ñàkk su ma xamoon li m uy tekki man cee ànd mbaa ma man a am baat bu ko gën a méngoo
--Abdu Xaadir Kebe 10 Oktoobar 2008 à 09:54 (UTC)
- Baat yooyu yépp an nañu ndax seex anta joob defoon na ci ay gëstu yu sori. Man ab gëstu bu ma amal ci internet moo tax ma jot ci yooyu liggéey. Di naa leen duggal ci wikbaatukaay, baal naa la yàlla nanu yàlla baal. dewenati. --Ibou 11 Oktoobar 2008 à 12:44 (UTC)
Yaa ngi xool xëtu senegaal, maa ngi fay deyi coppat de --Abdu Xaadir Kebe 19 Oktoobar 2008 à 12:33 (UTC)
xetu waxtaanuwaay
[soppi gongikuwaay bi]Discussion Utilisateur:Abdu Xaadir KEBE manoo koo jox weneen tur. soo ko tudde neneen dakoy jàppe niki ab jukki, dootul nekk xëtu waxtaanuwaay. Soo seetloo nii-nii xët wi daa xonk, te ba nga ko tuddewaate daa weexoon. Man miy tekki jokkalekaayu (interface) dal bi maa ko man a tekki ci wolof ni li nga fi gis yépp mu nekk wolof, dama faa àggagul rek.
Jamono yii njàng mi damaa gëtën lool, ba tax samay cëru ci dal bi wàññeeku bu baax, suma féexee tuuti rekk dellusi, jàmm-ak-jàmm. --Ibou 28 Oktoobar 2008 à 19:25 (UTC)
Jaajef --Abdu Xaadir Kebe 28 Oktoobar 2008 à 21:43 (UTC)
Translation Request
[soppi gongikuwaay bi]Hello, Abdu Xaadir KEBE. Can you help me translating just short stub article of Kiswahili, which based on http://simple.wikipedia.org/wiki/Kiswahili ? And I'll definetely help you to write any article which ask you me to write for you! Please,--Mwanaharakati (Longa) 3 Disembar 2008 à 12:53 (UTC)
I'll do because it's nothing, it's very short but u need me to translate it into wolof or ? but look at here: http://wo.wikipedia.org/wiki/Kiswahili --Abdu Xaadir Kebe 3 Disembar 2008 à 18:38 (UTC)
- Excellent response. Yes, what I was just about to say is, to translate it into Wolof Language! But I saw you made it very clear. I have absolutely nothing to say, but thanks!! Whenever you wish to see any article wants to be translated to Kiswahili, I welcome you right there at anytime!! And can you add any other more information on the article of Tansani? Because I found only one line and no more words anymore! Please (if possible!). Cheers,--Mwanaharakati (Longa) 4 Disembar 2008 à 07:13 (UTC)
Dont mention it, if I have to tell u I'll do. Glad to meet u by the net --Abdu Xaadir Kebe 4 Disembar 2008 à 07:43 (UTC)
New page for discussion
[soppi gongikuwaay bi]Hi, i oppened the following page Wikipedia:Pénc for global discussion on this wiki. Everything can be discussed in wolof or other languages. I posted already many messages in french or in english (my wolof is too poor sorry) about priorities on this wiki. I think your opinion is highly needed as you are one of the most active contributor on this wiki. Thank you in advance and see you on Wikipedia:Pénc (to be faster, you can access this page with the shortcut WP:P). Guérin Nicolas (Xëtu waxtaanukaay) 5 Disembar 2008 à 13:18 (UTC)
Ok I'll see. See u there!--Abdu Xaadir Kebe 6 Disembar 2008 à 21:20 (UTC)
Élection
[soppi gongikuwaay bi]Salut et merci pour ton message et ta proposition d'aide sur Wikipedia:Pénc. Je me présente au poste de Bureaucrate à cette page d'élection Wikipedia:Bureaucrats/Guérin Nicolas pour faciliter l'aide technique (tout est expliqué sur cette page). J'espère que je ferais bien ce travail, comme cela vous pourrez rédiger les articles sans se soucier des ennuis techniques. Guérin Nicolas (Xëtu waxtaanukaay) 8 Disembar 2008 à 01:11 (UTC)
Leeral
[soppi gongikuwaay bi]Ma ne sumb mu móoluwu kenn du ko wax, waaye sumb bu móolu.
Ay misaal U: jumtukaay la ñeel jëf juy def boppam : lekku gi gongikoo co lekk: weñ gi lekku na, suuf si màbbu na, màbb na boppam. Walla muy jumtukaay ñeel jëf ju nangoo defu, móol, móolu: sumb bu móolu: bu nangu ñu móol ko. Bu àndee ak ab baatal ni u walla i danga ciy boo w, niki tere terewu
--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 4 Maars 2009 à 15:39 (UTC)
Please, could you translate this article onto Wolof language? Thanks a lot for your help. If you want to translate any article onto Galicia, Catalonian, Spanish or Portuguese, tell it to me. --Jult (xëtu waxtaanuwaay) 2 Fewiriye 2009 à 16:17 (UTC) I'll do after, because I m engaged in these days in some heavy tasks, I mean some long articles to translate. But I'll do, --Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 2 Fewiriye 2009 à 18:35 (UTC)
Gamadji
[soppi gongikuwaay bi]Asala maleykoum sa ma bokk senegalais. Balma ca sa ma bind, ak toppando gi, dina geuneu goorgolu, man pulaar la, france lay juddu li moye tax français lay geuneu xam, wayé lakk wolof nex na ma lol, damay jang bind sasounek. Gamadji moye sama dakantal, Gamadji-Saré deuku samay mam (Fouta). Jajëf 212.198.179.151 4 Fewiriye 2009 à 02:06 (UTC)
Gis naa loolu, kon xam naa yaay bind jukki yu am solo yooyu ma doon topp(corriger)? Boo manoon a bindu maanaam créer compte, dina gen a am solo, bu ko defee man dinaay jeem a topp li ngay bind, waaye boo doon jang mbind mi dina gen. --Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 4 Fewiriye 2009 à 17:27 (UTC)
Bataaxalu dalal-jàmm
[soppi gongikuwaay bi]
Dalal-jàmm / Bienvenue / Welcome , Abdu Xaadir KEBE ! | |
(wo) Bataaxalu dalal-jàmm : dila nuyu Abdu Xaadir KEBE te dila dalal ci Wikipedia. Dila gërëm ci say cëru ci bii jimbulang. Su dee dangay làkk wolof, soxla nañu la lool ngir bind walla soppi ay jukki.; walla it, sag ndimbal ci wàllu xarala. Su fekke it dangaa soxla ndimbal walla dangaa ami laaj, saytul xët wii Ndimbal, man nga maa bind ci sama xëtu waxtaanuwaay, walla nga bind sa laaj ci Wikipedia:Pénc, ci xëtu waxtaanuwaay yi, dee fa xaatim say bataaxal, deel cuq ci walla ngay bind ~~~~ ngir xaatim: dina tax, sa turu jëfandikukat ak taariix bi, feeñ ci sa wetu bataaxal. Liggéeyal ak jàmm! | |
(fr) Message de bienvenue : Salut Abdu Xaadir KEBE et bienvenue sur Wikipédia. Merci pour tes contributions sur cette encyclopédie libre. Si tu parles la langue wolof, nous avons extrêment besoin de toi pour éditer les articles; sinon, nous avons toujours besoin de ton aide pour l'assistance technique. Si tu as toi-même besoin d'aide ou si tu as des questions, consulte Ndimbal, demande-moi sur ma page de discussion, ou pose ta requête sur Wikipedia:Pénc. Sur les pages de discussion, signe tes messages en cliquant sur ou en écrivant ~~~~ : ceci fera afficher automatiquent ton nom utilisateur et la date. Bonne continuation! | |
(en) Welcome message: Hello Abdu Xaadir KEBE and welcome to Wikipedia. Thank you for your contributions to this free encyclopedia. If you speak the wolof language, we highly need you to edit articles; if you don't, we always need your help for technical support. If you need help or for any question, check out Ndimbal, ask me on my talk page, or ask your question on Wikipedia:Pénc. Please remember to sign your name on talk pages by clicking or using four tildes (~~~~): this will automatically produce your username and the date. Happy editing! |
Guérin Nicolas (Xëtu waxtaanukaay) 7 Awril 2009 à 12:58 (UTC)
Gamadji
[soppi gongikuwaay bi]Asala Maleikoum.
Na ngeen def ? Da ma beugeu bind bene yeuf, ca wallu Diine bu amon bu jekk ca afrig sogo islam ak yenene diine nasaraan niow fofu. Dama la bougone ko wax, sogo ma tambali ko bind, ngiir nga set fan lay bindul bu bax. Wayé tamit dina def ni ma jeem bind bou bax, kon nga xol su fekené amna ay bind yu baxul. Ciao. 212.198.179.151 4 Suwe 2009 à 02:50 (UTC)
Sant
[soppi gongikuwaay bi]Jaajëf Sëñ Abdu Xaadir KEBE wax ji rafet na waaye ni ma dangaa dëgër bopp de yéeme na yéem na ma lool waaye amul solo, Ma lay xamal ni jàppee naa la lu ëpp doole li ngay def fii ak li nu fiy def, te it am na lu nu boole lu ëpp doole Wiki bi ak feneen, bàyyi ko xel, Xalaatal. Ahloubadar (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 15:35 (UTC) Looloo tax ma sañ la koo wax, te it leegi nu la neex defal, jeggalu--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 16:11 (UTC)
- Déet bul waxee noonu na nuy def li gën rek te bañ a def li nu neex lee nag waxtaan la woon rek, Nee wonn naa la amul solo, man du ma jàppal nit lu may lu baax te rafet, lu gënul mbaa lu ñaaw ma jàppee ko njuumte nde matu nu, waaw-kay Ahloubadar (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 19:15 (UTC)
Kon ñi ngi dolli sunug jeggalu ci lu nu warul--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 21:07 (UTC)
Request for help
[soppi gongikuwaay bi]Greetings Abdu Xaadir KEBE! Could I ask you to translate en:Qin Shi Huang(listed in 1000 vital articles) and en:Wuhan(a chinese city,my hometown) into wolof? You may shorten them as possible to contain only the basic informations,one or two sentences are enough. If you want me to translate any article into Chinese or Vahcuengh,contact me without hesistation. Thank you very much!------
I'll do when I have some time, but if you could shorten it, and put it there again as a link, that would help more --Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 3 Ut 2009 à 11:29 (UTC)
The short version of the first article (which is more important):"Qin Shi Huang (Chinese: 秦始皇; 259 BC – 210 BC) was the first emperor of a unified China. After unifying China, he and his chief adviser Li Si passed a series of major economic and political reforms, and undertook gigantic projects including the first version of the Great Wall of China. But the tyranny of his autocratic rule (including the burning of books and burying of scholars) make him a controversial figure in Chinese history."
Do you think this short version is all right?
Thanks:)--Biŋhai (xëtu waxtaanuwaay) 1 Sattumbar 2009 à 07:13 (UTC)
I ve translated it:
Qin Shi Huang moo doonoon imbraatóor bu njëkk bu Siin gees Bennal. Ginnaaw bi mu bennalee Siin, mook njiitu xelalkatam yi Li Si def nañu am mbooloom ay yewenal (reformes) yu koom ak politig yu mag, def it ay sémb yu ngand yu ëmbaale sumb bu njëkk bu Miir bu Mag bu Siin bi. Waaye nguurug jaay-dooleem ga ( nga xam ne lakk na ay téer, suul ay woroom xam-xam) tax na muy jëmm ju jeqi dàggasante ci taariixu Siin --Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 12 Samwie 2010 à 22:55 (UTC)
South Sudan
[soppi gongikuwaay bi]Hi, Abdu!
There is an article for Sudaan but none for "South Sudan". How is this (new) country called in Wolof? Maybe you could add it to Royuwaay:Réewi afrig. Thanks! Malafaya (xëtu waxtaanuwaay) 15 Sulet 2011 à 08:50 (UTC)
-
Sudaan gu Bëj-saalum, That s its name, we ll add it
--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 7 Oktoobar 2011 à 18:18 (UTC)