Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal
Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal
Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Tugal, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Tugal gis tay ci jamonoom ju yees jii ñu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu ndefar ci Tugal, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Tugal rekk la ñeel waaye àdduna bépp.
Li taxoon xam-xam jëm kanam :
Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci réewi Tugal gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di:
(1) Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Tugal yi te jariñu ci.
(2) Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Tugal yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam
(3) Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi ñu fentee móolukaay yi.
(4) Xemmeemtéef gu waa Tugal yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: xam-xam yu Gres-Rom ya.
Wàll yi xam-xam jëme kanam :
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ak li ñuy misaal jamono yu diggu yi ci Tugal lepp, naan jamonoy réer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn manta réere, manta weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu néew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Tugal yi nekkutoon lu moy li ñu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu ak jarbu . Ci noonu Tugal jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di:
Paj :
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Paj walla “Ndoktoor” ci Tugal wéyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak pajug jullit ñi, jaare ko ci seen téerey paj yi nga xam ne waa Tugal mujjoon nañu leen’a firi ci seeni làkk.
Xam-xam bi Tugal ame ci paj weesuwutoon fii, ba ci xarnub fukk ak juroom benn g.
Waa Tugal yittewoo woon nañu bu baax xam-xamu paj, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom de xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug paj ci Tugal.
Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu melosuuf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci réew yii ñuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Tugal te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu ñu xamutoon ci Tugal. Mu mujj nag bokk ci wartéefi doktoor yi ci Tugal ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu ñu leen di faje, wutal leen ay garab.
Ci noonu boroom xami-xami Tugal yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Belsig mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Faraas, ak Lofan Hok mu Olaand mi, ak Luwis Pastor mu Faraas mi ak Kox mu Almaañ mi añs. Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs.
Xalaat wi naan suuf si daa tàllaliku, te boroom xam-xami saytubiddiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gépp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nañu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay liggéey ci googu wàll.
Waa Tugal yi nag seen xam-xamu melosuuf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li ñu xame ci wuññiy melosuuf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu melosuuf tàmblee jëm kanam ci Tugal. Jëm kanamug xam-xamu melosuuf tax na ba bu saytubiddiw it jëm kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siiwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom déy duggal na loxoom bu baax – boo xoolee liggéeyam yi aju ci xam-xamu saytubiddiw – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg àdduna bi, bu ko defee yarami asamaan yi di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen yarami asamaan yi, ñoom ñepp dañuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër abdiggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wërngalu, maanaam roo te wërngaloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wërngalu, di wëndéelu.
Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal Jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewuñu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu saytubiddiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay (microscope) ngir fuglu biddiw yi ak yaram yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi.
Xam-xamu Jëmm gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu Jëmm bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu.
Boroom xam-xami Tugal yi def seen yitte ci ñòddi gi nekk ci suuf si . Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yéegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yëf sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lañuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yittewoo xam-xamu Jëmm, ndax kat mooy ki teg dàtti xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g.
Boroom xam-xamu Angalteer bii di Isaac Newton (1742 – 1727 g ) mooy ki wuññi dooley ñòddi walla bijji gi nekk ci suuf si . Moo wax ne kawkab yepp, dañuy wër jant bi, ci ay ngunu walla koto yu sax, yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon. Ki ñuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni biddiw yi sosoo.
Waa Tugal yi tuxale nañu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu simi bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw. Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti yu simi yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci. Toggaliit yii ba leegi danga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lañuy yore.
Waa Tugal yi nag, ñoom, dañoo gën a jëmale kanam xam-xamu Simi, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Faraas, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g.
Boroom xam-xam bii ñuy wax Thales, di ku dëkkoon Geres, moo seetlu woon dooley bijji ju nekk ci mbëj, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu mbëj. Boroom xam-xamu Angalteer bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigéen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul mbëj rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu mbëj buy juddal mbëj atum 1672 g.
Ki ñuy wax Stephen Gray dikk, won ñu ni ñuy tuxale mbëj, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci buum yu xànjar.
Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi mbëj yi, te fent batari. Borom xam-xamu Aamerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak mbëj benn lañu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la ñuy jaare di genne mbëj bu bari atum 1831 g. Waa Tugal soobu nañu ci xam-xamu Xayma, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Faraas bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu Jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële.
Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu suuf (Géologie)la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni ñuy sosoo.
Jamonoy yewwute daal ci Tugal mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te féexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Tugal ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jéem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam.