Toolu mbëj
Toolu mbëj, ci jëmm, ab tool la bu ay cër yees yan mbëj sàkk. Ab tool bu ne mel mooy tax ñu man a natt dooley mbëj bi ci bépp tomb boo jël ci barab bi. Ci anam gi ñu koy gëstoo su fekkee ay yan yu tekkaaral lañu, toolu mbëj bi dafay doon toolu mbëjtekkaaral.
Ubbite
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Njoxe yi tukkee ci caytu yi gëstukat yi def xamale nañu ne ñaari fànni mbëju yu ne-ne yi ñoo am: baax(+) ak bon (-). ñaari yaram yu mbëju, ñoom ñaar ñépp, ci anam gu baax walla gu bon dañuy bëmëxante, su dee wante dañoo mbëju ci anam gu wuute dañuy xëccante. Ngir xam ndax wenn yaram wi mbëju na, maanaan ndax am na yani mbëj ci biiram, dañuy jëfandikoo jumtukaay bees di woowee mbëjxool, moom du man a xayma taraayu mbëj mi ci biira li muy def rekk mooy wax ne am na ci mbaa déet. Ngir natt mbëj mi jumtukaay bi ñuy jëfandikoo mooy nattampere.
Lii yépp li ko waral mooy melokaanu biir ne-ne yi rawatina cër yi dàtt xarefulwon bi. te itam sax xarefulwon bi li booloo doon ko mooy saal bi, bi ëmb ci biiram feppsaal yi ak feppmaandu yi, ak ab barab bu biti bu mbëjfepp yi nekk. Ci nekkiin gu jaadu ab xarefulwon dafay maandu, maanaam limu mbëjfepp yeek feppsaal yi ñooy tolloo. Ngir xayma dayoob yanub mbëj dañuy jël mbëjfepp bi gën a tuuti bu am ci dénd bi, dayoo bu mbëjfepp bu bon (-) moo yem ak e = 1,602 189 2 ∙ 10-19 C, tolloo te safaanoo ak bu feppsaal, C mooy bennaanu natt bu yan bi te ñu koy woowee Coulomb. feppmaandu yi ñoom amuñu yanu mbëj.
Toolu mbëj bi fa mu man a àgg amul dig, taraayam ci bépp tomb boo jël ci biiram mi ngi aju ci ni ci yan yi séddalikoo walla xeeti ne-ne yi ne ci barab bi. Naka-jekk njunjam mooy , te tasaaroom yamaleb Maxwell moo ko faramfacce. ci Taariix Michael Faraday mooy ki ko njëkk a indi ci diggu XIXu xarnu bi ci ay gëstoom. Su ñu ko boolee ak toolu bijjaakon bi mu doon toolu mbëjbijjaakon.
Toolu mbëjtekkaaral
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Su fekkee teg nga ci ab barab ab yanu mbëj Q manees naa natt doole ji muy teg ci beneen yan qo bu ko gën a ndaw bu ñu jël, ci déeggoo qo bu baax (+) lay doon, su ñu tegee Q ci wetu qo. Niki nees koy gise ci gëstu yi, jooju doole dafay aju ci qo ba tax manees naa taxawal bii yamale:
Toolu mbëj bi E, doole ji Q di teg qo F. Ci bii tekki lees di sukkandiku ngir jox toolu mbëj bi bennaanu natt , maanaam Newton/coulomb. yam itam ak , maanaam volt/metar).
Ci tënk, toolu mbëj bi mooy liy jëmmal xëccante bi nekk ci diggante ñaar mbaa ay yani mbëj yu wuute yu taxaw, te tekkaaral, ci ñaari wet yu jakkaarloor , lu doole ji ñuy xëccantee di yokku toolu mbëj bi di yokku. Dig-digal bi nekk ci diggante yani mbëj yu jakkaarloo yi, yu baax (+) yi ci genn wet yu bon(-) yi ci geneen wet lees di wax lankmbëj. Lankmbëj bi mooy tax ba ab yanu mbëj du man a jóge ci genn wet dem ci geneen. Di fattali ne dawaanu mbëj du lenn lu dul ay yani mbëj yuy toppante, di daw; yu baax yi ñooy xëcc yu bon, su fekkee ab lankmbëj nekk na ci seen diggante dawaan du fa man a am. Su lankmbëj bi dëggëre ba tax dawaan manu faa judd, maanaam doole ji yan yu baax yi di xëcce yu bon yi amul taraay bu doy ba tax ñuy man a romb lankmbëj bi, ñoom yu bon yi, toolu mbëj daadi fai juddoo. Ba tax toolu mbëj du lenn lu dul doole jees sëf ab yanu mbëj.