Tol

Jóge Wikipedia.
Tol gi (Landolphia heudelotii)
Tol gi (Landolphia heudelotii)

Tol ag garab la, bokk ci njabootug "Apocynacées"

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gu ndaw lay doon ,ay doomam da ñuy muluŋ am ay doom ci biir, doom yi manees na koo lekk bu ñoree ak buy bëgg a ñor. Doom bi day xaw a xonq. Tol, ñi ngi koy fekk ci yenn gox yu mel ni ca kaskaat ya, ak yenn ci barab yi am ay xeer.

Solo si[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Meññefum garabug tol
Meññeefum garabug tol

Doom bi bu matee dëgg, dees koy lekk noonu. Doom bi manees na cee defar ay naan walla sax sàngara. Dinay aare ci yenn xeeti feebar yi lu ci mel ni jabet ak ñoom séen. Bokk na ci garab yi nga xam ne dañuy reesal lekk.

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Landolphia heudelotii