Garab

Jóge Wikipedia.
Nataal bees dibbe ci biir Wikipedia
Ay garab
Garab
Garab

Garab

Garab gàncax gu dëgër la, di am ab dàtt bu taawu ay banqaas yu firiku am i xob yuy faral di nëtëx. Xob yooyooy joxe ker gi.

Garab yi gàncax lañu yoo xam ne dañoo man a gudd fan. Ñoom dañuy dund ay at yu bari. Amna ci yoy man nañoo dund lu ëpp fukki at, am ci yoy téemeeri at, ba am ci sax yu néew yuy àgg ba junniy at.

Ci li ñu xayma, àdduna bi am na lu mat 60.000 ba 100.000i xeeti garab.

Garab yi nag, fi ñu ëppe mooy ci àll bi, ci gott yi ak màndiŋ. Fa ngay fekk garab yu bari yu dajaloo. Waaye batay it garab yi man nañoo màgg ci feneen fu dul ab àll, niki ci biir dëkk yi, ba ci sax biir kër yi.

Dañuy liggeey, liggeey bu am solo nag ci jokkalanteg càkkéef gi. (Jokkalante gi am ci yi ci àdduna bépp, nga xam ne ku ne aajewoo nga sa moroom.)

Ndax dañuy muucu gaasub karbon bi doomu aadama yi génne di ko denc. Ba noppi di génne gaas ogsisen bi nga xam ne nit moom lay soxla ngir dund .

Day liggéey, liggéey bu am solo it ci wërug ndox mi. (Ni ndox mi di jaare ci suuf garab yi muucu ko mu demaat ci kaw, wàccaat.)

Batay ci wàccug taw bi da ciy liggéey lu am solo, ndax fu la ëpp i garab ëpp la lu muy taw. Da ñuy xëcc ndox mi ngir mu wàcc màndal leen.

Am na njariñ lool tam it ci yi doomu aadama di jëfandikoo. lu ci mel ni: matt, këriñ walla sax foytéef yi ñu ciy lekk. Walla mu di ci faju mbaa kerlu mbaa jariñoo dénk wi ngir di ci defar i lal ak yeneen, mbaa defar ci luy aar yaramam niki ay saabu yu muy sangoo walla ay pat ngir ay bañam. Dees na ci defar ba tay ay néeg, ay kër, ay këyit, ay toogu, ay cempteŋ (taabal) , ay kees, (kaartoŋ) ay bale, ay bunt, ay palanteer, ay raas ay gaal walla sax bato ak yaneen ak yaneen i njariñ yu muy amal doomu aadama.

Foo dem ci àdduna bi rekk, garab am na lumu fay jariñ. Dana am fuñu koy teg am cër buñu ko jox it.

Xamle gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab
garab

Daanaka amul menn piri moo xam ne ñépp dëppoo nañu ci, muy tekki garab. Ndax boo jëlee garab dafa ëmb ay gàncax yu bari yoo xam ne xeet yu wuute ñoo ci nekk yu tasaaroo. Looloo waral nag ñiy jàng xam-xamu gàncax ak ñi am xam-xamu garab yu xaw a mag yi, ak ñi am xam-xamu àll, ñoom dañu ciy werante ba leegi. Ngir nag ñu am ay tegandaay yoo xam ne di nañu ci man a sukkandiku ngir méngale njuréef yi jóge ci àll yi ci àdduna bi yépp, kuréelu Mbootaayu Xeet yi ëmb wàllu dund ak mbay ñu koy wax FAO moom dafay joxe menn piri moo xam ne daal dafay sukkandiku rekk ci guddaayu garab gi.

Moom FAO dafa wax ne, garab daal genn xeetu gàncax la goo xam ne, bu fekente ne mbir yépp daje nañu maanaam bu amee li mu laaj lépp dafay màgg ba man a am 5i met cib guddaay, ci réew yi nga xam ne amuñu ak suqaliku, walla 7i met ci dëkk yi nga xam ne ñoo suqaliku.

Loolu nag moo koy wuutali ak garab yu ndawaan yi ñiy woowe ay ngajj. Niki ngeer, salaan añs, yooyu nga xam ne seenub guddaay buñu màggee ci diggante genn-wàllu met ba ci 5i met walla 7i met lay toll, te nga xam ne ñoom daanaka duñu am ker, duñu am mbaar.

FAO itam dugal na ci loolu garab yi nga xam ne amuñu li ñiy wax daakaande, lu deme ni ron walla dànq.

Boo jëlee lu mel ni ron, bant bi boo ko dagge day am lu mel ne am lëm ca biir, nga xam ne bant bi lépp feesul, te namu war a dëgëre du ko dëgëre, ndax bu gënee wow day mel ne ay bant yu sew la yu dajaloo. Loolu li mu amul daakaande moo ko waral. Yooyu amul ci niimaa. Niimaa nga xam ne aw dénk la wu dëgër buñu ko daggee, moom dafa am daakaande moo tax, daakaande ji moo waral mu dëgëre noonu. Bu dee ron nag amu ko, moo tax muy def ay bant yu sew.

Amna it ñoñ niñu jàppe garab, mooy gépp garab gu am daakaande rekk lañuy wax garab. Waaye FAO moom da cee dolli yi amul daakaande.

Nataal
Nataal

IFN moom dañoo wax ne, garab mooy xeetu gàncax goo xam ne dafa am liñin, ba noppi am ab bànqaas boo xam ne dara sax na ca, ba noppi guddaay ba day tollook 5i met walla mu ëpp ko.

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons