Aller au contenu

Siddeem pom

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabu Siddeem pom

Siddeem pom xeetu garab la gu bokk ci njabootu Rhamnaceae yi. Xeetu siddeem yu baree am.

Garabu siddeem pom danay àgg 2 ba 5i met ci guddaay, ak i xobam yu nëtëx tey melax yiy àgg ba 5i sàntimet ci guddaay.

Doom bi dees koy lekk, wirgo wu mboq lay yor te muluŋ danay toll 1 ba 1,5 sàntimet.

Turu xam-xam wi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ziziphus lotus

Turam ci yeneeni làkk

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]